Siiwal nañ ko:
Door: 1 mee, 2018
Déggooy Cëri Microsoft
Sa suturaSa sutura1_YourPrivacy
Tënk

1. Sa Sutura. Sa sutura lu am solo la ci ñun. Jàngal bu baax Sàrtu Sutura su Microsoft ("Sàrtu Sutura") ndax moo lay xamal xeeti njoxe yi ñuy jël ci yaw ak ci say jëfandaay ("Njoxe"), nan lanuy jëfandikoo say Njoxe, ak li nu yoon may ngir nu jëfandikoo ko say Njoxe. Sàrtu Sutura bi dafay xamle ni Microsoft di jëfandikoo sa ëmbiit, manaam say jokkoo ak ñeneen; Cër yi nga jëfandikoo ngir siiwal dara ci Microsoft; ak say taxañ, nataal, wayndare, ojo, liggéeyi disitaal, wideo yi nga seetaan wala yab, màngasiin, siiwal wala séddoo ci Cër ("Sa Ëmbiit"). Ginaaw jëfandikoo dafay neex boroom wala yoon digle ko, soo àndee ci Sàrt yii, nangu nga Microsoft jël say Njoxe ak Ëmbiit, jëfandikoo leen wala wane leen ci anam wiñ ko waxee ci Sàrti Sutura si. Yenn saa dina nu la yónnee weneen yëgle ngir sàkku ci yaw nga joxe sa kàddu, kom ninu ko leeralee ci Sàrti Sàmm-sutura yi.

Jukki bu fees
Sa këmbSa këmb2_yourContent
Tënk

2. Sa këmb. Lu bari ci suñuy Cër dañuy nangu nga denc mbaa séddoo Sa Këmb mbaa jot ay daju yu bawoo ci ñeneen. Duñu laaj moomeelu Sa Këmb. Sa Këmb dafay wéy di doon Sa Këmb te yaw yaay ki koy toppator.

  • a. Soo séddoo say ëmbiit ak ñeneen, kon xam nga ni dina ñu ko mën a jëfandikoo ci àdduna bi yépp, denc, sotti, siiwal, jox ko ñeneen, séddoo ak wane (ak ci far ci HealthVault) Say Ëmbiit te duñu la ci jox ndàmpaay. Soo bëggulee ñeneen mën a def loolu, bul jëfandikoo Cëri yi ngir séddoo Sa Këmb. Yaw yaay kiy teewal ak di dëggal ni ci diiru Sàrt yii, am nga (te dinga am) mbooleem yelleef yi war ci Say Ëmbiit yiñ yab, denc, wala séddoo ci biir Cër yi ak dajale, jëfandikoo, ak tëye Say Ëmbiit du jàlgati benn yoon wala yelleefu ñeneen ñi. Microsoft du ki moom, fuglu, wéral, fay, jàppale mbaa ci neneen gàdduwul benn kiliftéef ngir Sa Këmb te mënu ñu jàpp ni mooy kir yor Sa Këmb mbaa daju yu ñeneen yab, denc mbaa séddoo di jëfandikoo Cër yi.
  • b. Ci tolluwaay buñu laaj ngir jox la Cër yi yaw ak ñeneen, ngir aar la yaw ak Cër yi, te gënal costéef ak cëri Microsoft, da ngay may Microsoft sàñ-sàñu àqi moomel uxalaat ngir jëfandikoo Sa Këmb, ci misaal, amal ay sotti, teye, jébbal, tëggaat, wone, te séddale jaare ko ci ay jumtukaayu waxtaanu Sa Këmb ci Cër yi. Soo siiwalee sa Këmb ci ay barabu Cër yumu jàppandee bu baax ci net bi te amul yemale, Sa Këmb mën na feeñ ci ay wone mbaa ay daju yuy siiwal Cër bi. Siiwal mooy dimbali yenn ci Cër yi. Fuglu yu aju ci nan la Microsoft di jëmmalee siiwal jàppandi nañ ci xëtu Kaaraange ak kumpa bu daluwebu saytu sàqum Microsoft. Duñu jëfandikoo li ngay wax ci sa m-bataaxal, waxtaan, woote wideo, mbaa boyetu baat, mbaa wayndare, nataal, mbaa yeneen taxañu jagoo ngir jëmee ay siiwal ci yaw. Boole nanu cig yaatal sunuy sàrti siiwal yi ci Biralug Kumpa bi.
Jukki bu fees
Tëru doxaliinTëru doxaliin3_codeOfConduct
Tënk

3. Tëru doxaliin.

  • a. Soo nangoo yile Sàrt, dafay tekki ni nangu nga ni, suñuy jëfandikoo Cër yi, di nga topp yile sàrt:
    • i. Bul de lenn lu jaarul yoon.
    • ii. Bul dugg ci benn jëf juy liggéeyloo, gaañ, mbaa fitnaal ay xale.
    • iii. Bul yónnee mbaliit. Mbalit limu m-bataaxal, dugal, laaju xame, SMS (bataaxali jukki), mbaa ay bataaxal yu janoo lañ.
    • iv. Bul wane Cër yi wala nga leen di jëfandikoo ci biti ngir séddoo ëmbiit wala jumtukaay yu ñaadowul (lu ci melni, taati neen, yëfi baayima, ñamante, wax ju ñaaw, nataali fitna, wala jëf ju soxor) wala Sa Ëmbiit wala jumtukaay bu dëppoowul ak yoon ak sàrt yiñ tëral ci réew mi.
    • v. Bul dugg ci lenn ludul dëgg wala lu lëndam wala luy naxaate (ci misaal, di nax nit ngir jël ci moom xaalis, mbubboo keneen, laaj Cër bi ngir yokk say poñ cim po wala sab raŋ, wala komànteer yi) wala njublaŋ wala sosal nit.
    • vi. Bul jalgati benn yemale ci dugg mbaa jàppandal cër yi.
    • vii. Bul dugg ci jëf ju la mën a gaañ, Cër yi wala yeneen (ci misaal, joxe wiris, topp, dugal ay këmbi fitnalkat nu gën leen xamee ci ay jixaadkat, wax ay baatu bañeel mbaa daganal ay ci kaw ñeneen).
    • viii. Bul jalgati yoon yi ci kaw ñeneen (maanaam, séddoo misig bu am àqi sotti buñu nanguwul mbaa beneen daju àqi sotti, jaayaat mbaa beneen séddale ay kàrtu Bing, mbaa nataal).
    • ix. Bul dugg ci jëf juy jalgati sutura mbaa àqi aar njoxey ñeneen.
    • x. Bul jàppale ñeneen ñu jalgati yile sàrt.
  • b. Dëgëral. Soo jalgatee sàrti yii, mën nanu ci sunu coobare, bañ la joxati Cër yi wala sax nu dem yegg ci tëj sa sàqum Microsoft te dunu la tàggu. Mën nanu tere say jokkoo di yegg (lu ci melni say séddoo bataaxal, taxañ wala say bindante mesaas cib janoo) ci Cër yi wala ñu bawoo ca, lépp ngir dëgëral Sàrt yii, wala mën nanu dindi wala baña siiwal Say Ëmbiit ci sunu coobare. Soo lànket jàppandi ayu sàrt yile, Microsoft dafay jaglel àqi topp Sa Këmb ngir saafaral jafe-jafe bi, te nangu nga yile topp fii. Waaye, mënu ñu saytu Cër yépp te jéem darra ngir def lu ni mel.
  • c. Jëfe ci Liggéeyali Xbox. Bësal fii ngir am yeneeni leeral ci ni Tëru doxaliin bii di jëfee ci Xbox Live, Games for Windows Live ak powi Microsoft Studio, jëfekaay yi, liggéeyal yi ak këmb yu Microsoft joxe. Soo jalgatee Tëru Doxaliinu Cëri Xbox yi (leeral nañu ko ci pàcc 13(a)(i)) mën nañu la aj wala ñu tere la bokk ci Cëri Xbox yi, lu ci melni xañ la bépp sañ-sañ ci ëmbiit yi, diirub Bokk ci Xbox Gold, ak sa xaalisu sàqum Microsoft biñ boole ci sam sàq.
Jukki bu fees
Jëfandikoo Cër yi & NdimbalJëfandikoo Cër yi & Ndimbal4_usingTheServicesSupport
Tënk

4. Jëfandikoo Cër yi & Ndimbal.

  • a. Sàqum Microsoft. Di nga soxla ab sàqum Microsoft ngir dugg ci ay cër yu bari. Sa sàqum Microsoft dafay tax nga mën a dugg ci costéef yi, daluweb yi ak cër yi Microsoft joxe ak yenn way-liggéeyandoo.
    • i. Sos ab Sàq. Mën nga sos am sàqum Microsoft soo bindoo ci internet. Bul nangu ànd wala jëfandikoo benn njoxe bu lëndam wala bu jaarul yoon sooy bindu ngir am sàqum Microsoft. Ci yenn wàll yi, ab xaaj bu bawoo feneen, niki joxekatu cëri Internet, mën nala jox ab sàqum Microsoft. Soo jotee sa sàqum Microsoft ci xaaj bu bawoo feneen, xaaj boobu mën na am yeneen àq ci sa sàq, niki maniinu dugg mbaa far sa sàqum Microsoft. Baal ñu topp bépp sàrt bu ci dolleeku bu la xaaj bi joxoon, ndax Microsoft amul benn dogal ci li àju ci yile sàrt yu ci dolleeku. Soo sosee ab sàqum Microsoft ci turu ab kër, niki sa liggéeyukaay mbaa ki nga liggéeyal, nangu nga ni am nga kiliftéefu boole boobu kër ci yooyu Sàrt. Mënoo jël leeral yi ngay duggee ci sa sàqum Microsoft nga jox ko keneen wala benn wàll. Ngir aar sa sàq, wéyal di nëbb sa baatu jàll ak say leerali sàq. Lépp lu mën a xew ci sàqum Microsoft, yaay kiñ mëna jàpp ni moo ko def
    • ii. Jëfandikoo Sàq. War nga jëfandikoo sa sàqum Microsoft ngir wéy di doxal sa sàq. Lii dafay tekki ni war nga dugg gën gaa neew ci ab diiru 5 at ngir mën wéy di dekkal sa sàqum Microsoft, ak cëri yumu àndal, ludul dañ ko joxee neneen ci ab maye ngir ab dogitu cër buñu fay. Soo duggul ci diir bii, dina ñu jàpp ni dàkkal nañu sa sàq di dina lako tëjal. Yëral pàcc 4(a)(iv)(2) ngir xàm li mën a am suñu tëjee ab sàq. War nga dugg ci sa boyetu Outlook.com ak ci sa OneDrive (ci xaajale) gën gaa neew benn yoon ci at bu nekk, luko moy dina ñu la tëjal sa boyetu sàqum Outlook.com ak sa Onedrive. Fàww nga dugg ci Cëri Xbox gën gaa néew benn yoon ci diirub juróomi at ngir nga baña ñàkk say xàmmey po yi bokk ci sa sàqum Microsoft. Sudee danu jàpp ni dafa am ku keneen kuy jëfandikoo sa sàqum Microsoft ci lu jaarul yoon (ci misaal, su amee ku piraate sam sàq), Microsoft dafay tëj sàq mi ci saasi, ba keroog ngay sàkku mu tijji ko. Su nu sukkandikoo ci nekkinu déggoo bi, mën nañu laaj ngir nu dakkal dugg ci yenn wala Sa Këmb yépp. Soo ameeb jafe-jafe ngir dugg ci sa sàqum Microsoft, nu ngi lay ñaan nga yër daluweb bii: https://go.microsoft.com/fwlink/?LinkId=238656.
    • iii. Xale yi ak Sàq yi. Sooy jëfandikoo cër yi, dafay tekki ni nangu nga ni toll nga ci atu "muskalaf" mbaa "kilftéefu yoon" bi nga dëkk mbaa ab nga sa waa-jur mbaa sa kilifa nangu ci lu jaadu nga tënku ci yile Sàrt. Sudee xamoo ndax jàppee nañu la mag, wala yoon jàpp nani leegi “muskàllaf” nga ci fi nga dëkk, wala xamoo luñu wax ci pàcc bii, laajal sa waajul wala keneen ku la yilif mu mayla ndigal laata ngay sos sa sàqum Microsoft. Sudee danga nekk waajuru xale wala nga yilif benn xale bu sos sàqum Microsoft, yaw ak ndaw loolu nangu ngeen te ànd ngeen ci Sàrti Sàmm-sutura yii, te itam lépp luñ def ci sàqum Microsoft mi wala ci Cër yi yeen la, muy mbir yiñ ciy jënd, mu fekk ñu sos sàqu xale bi leegi wala ëlëg.
    • iv. Tëj Sa Sàq.
      • 1. Saa yu la soobee mën nga bàyyi yenn ci Cër yi wala nga tëj sa sàqum Microsoft, yaa xam luy sabab bi. Ngir tëj sa sàqum Microsoft, baal ñu yër https://go.microsoft.com/fwlink/p/?linkid=618278. Soo laajee ñu tëj sa sàqum Microsoft, dina ñu ko dugal ab nekkin buñu ajandi ci diirup 60 fan soo ci génnee kase. Su weesoo diiru 60 fan boobu, dina ñu tëj sa sàqum Microsoft. Xoolal pàrti 4(a)(iv)(2) bii ci suuf ngir xam luy xew sudee dañu tëj sa sàqum Microsoft. Duggaat ci diiru 60 fan boobu, dina dekkalaat sa sàqum Microsoft.
      • 2. Sudee dañu tëj sa sàqum Microsoft (yaw wala nun), dina am mbir yuy xew. Li ci njëkk mooy, dangay ñàkk ci saasi bépp sañ-sañ bu la doon may nga jot ci Cër yi. Ñareel ba, dañuy far bépp Njoxe wala Ëmbiit buñ bokk ci sa sàqum Microsoft wala ñu tàqale leen, yaw ak sa sàqum Microsoft (fileek yoon waxul nañu ko tëye, delloo koo, wala ñu jox ko jàmbur ngir mu mën a xam ki nga doon). Am nga ab palaŋu denc bu baaxoo ndax Microsoft du mën a jëli Sa Këmb mbaa Njoxe suñu tëjee sa sàq ba noppi. Ñatteel ba, mën nga baña mën jëfandikoo costéef yi nga am.
  • b. Sàqi Liggéey wala Daara. Mën nga dugg ci yenn liggéeyali Microsoft ak ab dëkkuwaayu bataaxalu liggéey wala daara. Soo ko defee, ànd nga ci ni, boroom wàll wiñ boole ci sa dëkkuwaayu bataaxal mën na saytu ak yilif sam sàq, ba noppi mu mën jot ak jëfandikoo say Njoxe, lu ci melni say ëmbiiti jokkoo yi nga amal ak say taxañ, te Microsoft mën na yëgal boroom wàll wi sudee sàq mi wala Njoxe yi dañu yàqu. Sudee itam danga nangu ni sa jëfandikoog cëri Microsoft mën nañu ànd ak déggoo yi la Microsoft tëralal, yaw wala sa mbootaay, te yii Sàrt mën nañu fa baña dox. Sudee danga am sàqum Microsoft ba noppi nga jëfandikoo beneen dëkkuwaayu bataaxal ngir dugg ci Cër yiñ lim ci Sàrt yii, mën nañu la laaj nga yeesal dëkkuwaayu bataaxal biñ boole ak sa sàqum Microsoft ngir nga mën a wéy di jot ci Cër yooyu.
  • c. Beneen jumtukaay/Palaŋi njoxe. Ngir jëfandikoo ay Cër yu bari, war nga lonku ci internet ak/mbaa njoxe/palaŋ portaabal. Mën nga soxla yeneeni jumtukaay, niki ak kask, nataalukaay mbaa mikro. Yaw yaa wara wut sa konsiyoŋu bopp, say paas, wala jumtukaay bi war ngir jëfandikoo Cër yi ak ngir fay fere yi operatër bi (yi) di fayyeeku ci koneksiyoŋ bi, paas bi ak jumtukaay bi. Boole nañu yooyu njëg ci bépp njëg bi nga ñu fay ngir Cër yi te duñu la délloo yooyu njëg. Xoolal ak sa (say) joxekat ngir seet ndax am ay njëg yu mën a jëfe ci yaw.
  • d. Yëgley Liggéeyal. Sudee dafa am luñ la waral yëgal ci Cër bi ngay jëfandikoo, dina nu la yónnee yëgleb Cër. Sudee danga boole di jëfandikoo sa dëkkuwaayu bataaxal wala sa nimero telefon ak sa sàqum Microsoft, kon mën nanu la yónnee yëgley cër ci bataaxal wala ci SMS (mesaas), boole ci saytu ngir xam ki nga doon laata nuy bind sa nimero telefon. Mën nanu la yónnee itam yëgley Cër ci beneen anam (ci misaal ci bataaxali biir costéef). Njëgu njoxe mbaa bataaxalukaay yi mën nañu jëfe soo jotee ay yëgle jaaree ko ci SMS.
  • e. Ndimbal. Amna ndimbal yuñ jagleel jëfandikukat yi ci yenn Cër yu jàppandi ci support.microsoft.com. Yenn Cër mën nañu amaale yeneen ndimbal yuñ jagleel jëfandikukat yi, te bokk ci sàrti yi nekk ci www.microsoft.com/support-service-agreement, fileek joxe wuñu ci yeneen leeral. Ndimbal li mën na bañu jàppandi ci sumbi Cër wala man-man yiñ jagleel ñam kese wala xoolandi. Cër yi mën nañu bàña àndak losisel mbaa cër yu ab beneen xaaj joxe, te yaw yaa war a tamal sa bopp li mànta ñàkk ci ab déggoo.
  • f. Dakkal say Cër. Sudee dañu dakkal sa Cër (yaw wala nun), li ci njëkk mooy dangay ñàkk ci saasi sañ-sañ bu lay may nga jëfandikoo Cër yi te daganal bi nga am ci Cër boobu dafay jeex. Ñareel ba, dañuy far bépp Njoxe wala Ëmbiit buñ bokk ci sa sàqum Microsoft wala ñu tàqale leen, yaw ak sa sàqum Microsoft (fileek yoon waxul nañu ko tëye, delloo koo, wala ñu jox ko jàmbur ngir mu mën a xam ki nga doon). Li muy jur mooy dootoo mëna jëfandikoo benn Cër (wala Say Ëmbiit yi nga denc ci yooyu Cër). Danga war di faral di denc say njoxe. Ñatteel ba, mën nga baña mën jëfandikoo costéef yi nga am. Sudee danga dakkal sa sàqum Microsoft te amoo meneen sàq mu lay may nga jëfandikoo Cër yi, mën nañu dakkal say Cër ci saasi.
Jukki bu fees
Jëfandikoo Cër mbaa Jefekaayi xaaj bu bawoo feneenJëfandikoo Cër mbaa Jefekaayi xaaj bu bawoo feneen5_usingThird-PartyAppsAndServices
Tënk

5. Jëfandikoo Cër mbaa Jefekaayi xaaj bu bawoo feneen. Cër bi mën nala may nga jot wala am ay costéef, cër, daliweb, lëkkalekaay, ëmbiit, jumtukaay, po, maneef, boole, bot wala jëfekaay yu bawooo ci ay jàmbur bu ci bokkul (liggéeyukaay wala ay nit yu wuute ak Microsoft) ("Cër ak Jëfekaayi Jàmbur"). Yenn ci sunuy Cër yu bari dañu lay jàppale nga seet, sàkku wala jokkalante ak ay Cër ak Jëfekaayi Jàmbur wala ñu may la nga séddoo say Ëmbiit wala Njoxe, te xam nga ni yaa nga laaj sunuy cër ñu jox la Cër ak Jëfekaayi Jàmbur. Cër ak Jëfekaayi Jàmbur yi mën nañu la may itam nga denc Say Ëmbiit wala Njoxe ak siiwalkat bi, joxekat bi wala opertaatëru Cër ak Jëfekaayi Jàmbur yi. Cër ak Jëfekaayi Jàmbur mën nala jébbal ak sàrtu sutura wala mu laaj la nga nangu yeneen sàrt laata ngay mën a samp wala jëfandikoo Cër wala Jëfekaayi Jàmbur bi. Xoolal pàcc 13(b) ngir yeneeni sàrt yu ñeel jëfekaay yuñu soxla ci biir Office Store, Màngasiinu Xbox mbaa Màngasiinu Windows. Danga wara jàngat bu baax bépp sàrt wala sàrti sàmm-sutura laata nga wut, jëfandikoo, sàkku, wala lëkkalante sa Sàqum Microsoft ak menn Cër ak Jëfekaayi Jàmbur. Bépp sàrt bu ci dolleeku du soppi yile Sàrt. Microsoft du la jox sàñ-sàñ benn àqi moomelu xalaat ci kaadaru Cër ak Jëfekaayi Beneen xaaj. Nangu nga jël lépp lu la mën a lor ak kiliftéef bu bawoo ci jëfandikoo yile jëfekaay ak cëri xaaj bu bawoo feneen ak ni Microsoft moo yor kiliftéefu bépp jafe-jafe buy bawoo ci li nga leen di jëfandikoo. Yoonu Microsoft nekkul ci benn leeral wala cër njoxe bu Cër ak Jëfekaayi Jàmbur jox la yaw wala keneen.

Jukki bu fees
Jàppandig cërJàppandig cër6_serviceAvailability
Tënk

6. Jàppandig cër.

  • a. Cër yi, jëfekaay ak cër yu bawoo feneen, mba daju mbaa costéef yuñu maye ci digante cër yi mën na jàpp yenn saay, mën nañ leen maye ci luñu yemale, mbaa mën nañu wuute suñu sukkandikoo ci sa diiwaan mbaa Jëfandaay. Soo soppee barab bu àndak sa sa sàqum Microsoft, mën nga soxla jotaat ay daju mbaa jëfekaay yu jàppandiwoo ci yaw ak yuñu jëndoon ngir sa diiwaan bu njëkk. Nangu nga bàña jot mbaa jëfandikoo daju yi mbaa cër yu jaarul yoon mbaa yuñu joxul sàñ-sàñu jëfandikoo ci réew bi ngay duggee mbaa jëfandikoo yile daju mbaa cër, walla nëbb mbaa bàña cosaanal sa diiwaan mbaa sa xibaaru ràññeekaay ngir dugg mbaa jëfandikoo yile daju mbaa cër.
  • b. Dañuy def lépp luñu mën ngir Cër yi dox; waaye, cëri yu nekk ci net bi yépp dañuy daj ay dog-dog ak paan yuy faral di am, te Microsoft yorul kiliftéefu benn dog-dog mbaa ñàkk bi la mën a dal ci loolu. Su amee ab paan, mën nga bàña mën a jëli Sa Këmb mbaa Njoxe yi nga dencoon. Nu ngi lay ñaan ngay faral di denc Say Ëmbiit ak Njoxe yi nga def ci Cër yi wala yi nga dencee ci Jëfekaay ak Cër yu ñeneen moom.
Jukki bu fees
Ay yeesal ci Cër yi mbaa losisel bi, ak coppite yi am ci yile sàrtAy yeesal ci Cër yi mbaa losisel bi, ak coppite yi am ci yile sàrt7_updatesToTheServicesOrSoftwareAndChangesToTheseTerms
Tënk

7. Ay yeesal ci Cër yi mbaa losisel bi, ak coppite yi am ci yile sàrt.

  • a. Mën nañu soppi yile Sàrt saa su nekk, te di nañ lako wax suñ ko defee. ëfandikoo cër yi su bisu coppite jotee dafay tekki ni nangu nga sàrt yuñu bees yi. Sudee àndoo ci sàrt yu bees yii, kon bàyyil di jëfandikoo Cër yii, tëjal sa sàqum Microsoft te, sudee waajur wala kilifa gune, jàppaleel xale bi mu tëj sàqu Microsoft bi bu moom.
  • b. Yenn saay di nga soxla ay yeesali losisel ngir wéy di jëfandikoo Cër yi. Mën nanu xool ci saasi sa sumbu losisel te yebbi yeesali losisel yi wala coppitey tëral. Mën nañ la laaj itam nga yeesa losisel bi ngir wéy di jëfandikoo Cër yi. Yile yeesal ñu ngi àju ci yile Sàrt ludul mu am yeneen sàrt yuy àndak yeesal yi, ci kaa bi nga xàm ni, yeneen sàrt yooyu dañuy jëfe. Amul lenn lu mën a sant Microsoft mu jàppandil ay yeesal, te du dig kenn ni nangu sumbu sistem bi ngay jëfandikoo ngir jënd wala daganalee sañ-sañ bi, jëfekaay yi, ëmbiit yi wala yeneen costéef. Yile yeesal mën nañu bàña àndak losisel bi mbaa cër yu xaaj bu bawoo feneen joxe. Mën nga Jëlaat sa nangu ci yeneen yeesali losisel yuy ñëw saa su nekk soo sampee losisel bi.
  • c. Cig ndollent, mën na am ay jamono yuñuy soxla dindi mbaa soppi ay man-manu Cër bi mbaa dakkal joxe ab Cër ngir dugg ci Jëfekaay ak cëri bawoo feneen. Soo ci génnee dayo bu yoon buy jëfe laaj, amuñu benn wareefu joxe ab yabaat mbaa wuutalu bépp daju, Marsandiisu Xarala (ni ñu ko xamlee ci pàcc 13(k), mbaa jëfekaay yi ñu mujjee jënd. Mën nga génn ay Cër wala seeni Man-man ci ab sumbu xoolalndi wala ñamandi, te loolu mën na baña dox ni mu waree, wala du mel ni sumb bu mat bi.
  • d. Kon mën nga jëfandikoo jumtukaay yuñ aare DRM, lu ci melni yenn misik yi, po yi, filmu yi, téere yi ak yeneen mbir, losiseli DRM yi mën nañu jokk seen bopp ak ab cëru yelleef ci internet ba noppi mu yebbi ba noppi samp ay yeesal DRM.
Jukki bu fees
Sàñ-sàñu losiselSàñ-sàñu losisel8_softwareLicense
Tënk

8. Sàñ-sàñu losisel. Bépp losisel bunu la jox te mu bokk ci Cër yi dafay tënku ci Sàrt yii fileek àndul ak beneen déggoob sañ-sañu Microsoft (ci misaal, sudee dangay jëfandikoo jëfekaayu Microsoft bu bokk ci Windows wala mu am ci wàll, kon Sàrti Sañ-sañ yu Jumtukaayu Microsoft yu Doxalukaayu Windows boobu ñooy yilif losisel boobu). Jëfekaay yiñ amee ci Màngasiinu Office, Màngasiinu Windows ak ci Màngasiinu Xbox dañu tënku ci pàcc 13(b)(i) bi ci suuf.

  • a. Soo dëppook yile Sàrt, dañu lay jox àqi samp te jëfandikoo benn sotti ci jumtukaay bu nekk ci li aju àdduna bi yépp ngir jëfandikoo benn nit kase ci ab jamono ci sa kaadaru jëfandikoo yile Cër. Sudee yenn jëfandaay yi, mën nañu wàccaale ak jëfekaay bi, waaye ngir yaw kese lay doon te wut ci Cër yi luy nuru xaalis. Losisel bi mbaa daluweb bu bokk ci yi mën na dugal ab kotu wàll bu bawoo feneen. Xaaj yu bawoo feneen yu moom bile kot bi, budul Microsoft, jox nañ la sàñ-sàñu bépp mbindiin mbaa kot bu bawoo feneen, buñu lëkkale ak mbaa buñu dellu ci losisel bi mbaa daluweb bi. Dugal nañu ay karmat, su ci amee, ngir kotu xaaj yu bawoo feneen ngir xamal lako kase.
  • b. Losisel bi am na sàñ-sàñ, buñu jaayul, te Microsoft dafay jaglel àq yépp ci losisel bu Microsoft joxewul, mu doon ci bokk, até mbaa neneen. Sàñ-sàñ bii du la jox bénn àq, te mën nga bàña:
    • i. jalgati mbaa moytu bépp dogalu kaarànge xarala ci biir mbaa lu méngook losisel bi mbaa cër yi;
    • ii. tasaare, booledi, fecci, pirate, roy, jariñoo, mbaa safaane defar gi ci bépp losisel mbaa yeneen xeeti Cër yuñu boole mbaa yuñu mën a jot ci digante Cër yi, ludul ak dayo kase bu yoonu sotti bi di jëfe moo maye ñu def lu ni mel;
    • iii. àndaale losisel yu xaajaloo mbaa Cër yuñu war a jëfandikoo ci ay jëfandaay yu wuute;
    • iv. siiwal, sotti, luwe, luwe ci diir bu yàgg, indi, séddale, mbaa abale losisel bi mbaa Cër yi, ludul Microsoft nangu la nga def loolu;
    • v. jébbal losisel bi, bépp sàñ-sàñ, mbaa bépp àqi dugg mbaa jëfandikoo Cër yi;
    • vi. jëfandikoo cër yi ci anam buñ ko nangoo bu mën na tere ku nekk mu jëfandikoo leen mbaa mën a dugg ci bépp cër, njoxe, sàq, mbaa mbaal;
    • vii. maye dugg ci cër yi mbaa soppi bépp jëfandaay bu Microsoft nangu (maanaam, Xbox One, Xbox 360, Microsoft Surface, ak yeneen) bu ay jëfekaay yu bawoo feneen yuñu nangu.
Jukki bu fees
Sàrti paySàrti pay9_paymentTerms
Tënk

9. Sàrti pay. Soo jëndee ab Cër, yile sàrti pay dañuy jëfe ci sa jënd te nga nangu leen.

  • a. Fayyeeku yi. Su amee ab fayyeeku bu àndak ab dogitu Cër, nangu nga fay boobu njëg ci xaalis buñu xamle. Njëg buñu joxe ngir Cëri àndul ak jukki yuy jëfe yépp ak jekkali wecceeku xaalis, ludul dañ ko waxee neneen. Njëg yépp yu ñeel costéefi Skype yuñu fay boole nañ ci juuti yiy jëfe, ludul dañu wax leneen. Yaw yaay ki war a fay yile juuti mbaa yeneeni fayyeeku. Leeral dëkkuwaay yiñ boole ci say leerali faktiir la Skype di jël ngir xayma taks yi nga wara fay. Yaw yaa wara xool bu baax ndax leerali dëkkuwaay biñ ci bind jaar na yoon te yeesal nañu ko. Lu weesu costéefi Skype, dañuy sukkandiku ci barab bi nga sosee sa sàqum Microsoft, fileek yoon santaanwul ñu sukkandiku ci leneen ngir xayma say taks. Mën nañu ajandi mbaa fomb cër yi suñu jotul ab fayyeeku bu mat ak ci waxtu buñ lako laajee. Ajandi mbaa fomb cër yuñu dul fay mën na indo ñàkk a jëfandikoo sa sàq ak li ci nekk. Sudee danga jëfandikoo mbaalu liggéeyukaay wala mbaal mu suturlu, loolu dafay nëbb sa dëkkuwaay ba tax say taks mën a wuute ak biñ wane ci barab bi nga nekk. Mu ngi qju ci sa barab, yenn jëflante yi mën nañu laaj nga wecceeku ci xaalisu bitim-réew wala ñu tëral ko ci beneen réew. Sa bànk mën na la fayeeku yeneeni njëg ngir yooyu liggéeyal sooy jëfandikoo ab kàrtu bànk. Nu ngi lay ñaan nga jokkook sa bànk ngir am yeneeni leeral.
  • b. Sa Sàqu Faktiir. Ngir fay njëgu ab cër, di nañ la laaj nga joxe ab anamu pay ci jamono bi nga bindoo ngir boobu Cër. Mën nga jot ak soppi say leerali faktiir ak jumtukaayu payoor ci Daluwebu saytu sàqum Microsoft ak yu Skype soo demee ci sa dalu sàq bi ci https://skype.com/go/myaccount. Cig ndollent, nangul nga Microsoft mu jëfandikoo bépp leerali sàq buñu yeesal bu àju ci anamu payu sa bànk walla mbaalu pay buy jëfe bi nga tànn. Nangu nga yeesal ci saasi sa sàq ak yeneeni leeral, bokk na ci sa dëkkuwaayu bataaxal ak leerali anamu pay yi, ngir nu mën a mottali say jëflànte te jokkook yaw su ko laajee cig lëkkaloo ak say jëflante. Coppite yuñu amal ci sa sàqum faktiir duñu laal fayyeeku yuñu dugal ci sa sàqu faktiir laata ñuy mën a jëf ci say fayyeeku ci sa sàqu faktiir.
  • c. Faktiir. Soo joxee Microsoft ab jumtukaayu payoor, dëggal nga (i) may nañu la nga jëfandikoo jumtukaayu payoor bi nga joxe te itam dëggal nga ni bépp leeralu payoor boo joxe jaar na yoon te dëgg la; (ii) may nga Microsoft mu jëfandikoo sa jumtukaayu payoor ngir dagg la ay Cër wala ëmbiit yu jàppandi; te itam (iii) may nga Microsoft mu dagg bépp man-man bu jaay ci Cër yi nga tànn ngir bindu ci wala jëfandikoo ko ci bi Sàrt yii di dox. Mën nañ la fayyeeku (a) ci lu jiitu, (b) ci jamono bi ngay jënd; (c) bi nga jëfee ba noppi, (d) ci ab sukkandikukaay buy faral di am ngir Cëri bindu. Itam, mën nañ la fayyeeku ci dayo bi nga nangu, te di nañ la yëgël lu teel su amee bépp coppite ci tolluwaayu xaalis bi nga war a fay ci Cëri bindu yuy faral di ñëw. Mën nañ la fayyeeku benn yoon lu ëpp benn sa diiru faktiir uu njëkk ngir tolluwaay yu aggoon ci njëlbéen.
  • d. Pay yuy faral di am. Sudee danga jënd ay Cër yu lalu ci sa bindu (ci misaal, weer wu nekk, 3 weer yu nekk, wala at mu nekk), nangu nga ni maye nga ñu lay faral di la fayyeeku, te ñu jaare fayyeeku googu ngay fay Microsoft ci jumtukaay bi nga joxe ak ca waxtu ya mu waree te nga ànd ca, fileek yaw wala Microsoft dakkalul sa bindu ca Cër boobu. Soo nangoo ñu lay faral di dagg, may nga Microsoft mu jëfandikoo masin ngir dagg la wala wiiremaa ngir dila fayyeeku (sudee fayiin bi tudd Automated Clearing House wala lu nuróo ak moom), wala ñu daggee la ci sàq mi nga tànn (fayee ci kàrt keredi wala lu nuróo ak moom) (nga boole lépp muy, "Fayee ci Masin"). Li ci gën a bari, dañu lay fayyeeku say ferey bindu yi lu jiitu diiru bindu bi di tàmbalee dox. Sudee dafa am luy waarul fay te muujiwul àntu, wala sudee dañu bañ nga fayee ak ab kàrt keredi wala xeetu fayyiin wu ni mel, Microsoft wala ay jaaykati cëram am nañu sañ-sañu jël bépp ëmbeefu delloo, dàq wala xaalis bu doyul daal di lay fayyeeku ci anamu Fayee Masin.
  • e. Yeesalaat boppam. Sudee yoon yiñ tëral dañuy nangu fayeeku ci saasi, mën nga tànn Cër yi ci fayyeeku ci saasi saa yu àpp biñ defal cër bi jeexee. Dina nu la ko fàttali ci bataaxal wala ci yeneen pexe yu xel nangu, laata nu lay dagg benn xaalis ngir wutal la àpp bu bees, te yëggal bépp njëg bu soppiku ci niñ ko leeralee ci pàrti 9(k). Sunu la ko yëgalee ni nangu nañu nga yeesal say Liggéeyal ci saasi, xey na dinañu mën a yeesal ci saasi say Liggéeyal ci njeextalu diirup liggéey bi teew te fayeeku la njëg boobu teew ci diiru yeesal bi, lu dul danga tànn fomm Liggéeyal yi ci ni ñu ko xamlee fii ci suuf. Di nañ la fàttali itam ni di nañ faktiire anamu payoor bi nga tànn ngir cër yeesal cër yi, donte dañ ko yónnnee ci taarixu yeesal bi mbaa ñu joxe ko ci kanam. Di nañ la jox ay digle ci nan nga war a fombee Cër yi. War nga fomb Cër yi laata taarix yeesal bi ngir moytu ñu fayyeeku la ngir yeesal gi.
  • f. Nettalib Net ak Njuumte yi. Microsoft dina la jox ab faktiiru nettali net ci daluwebu saytukatu sàqum Microsoft bi, fi ngay mënee xool te móol sa nettali. Sudee Skype, mën nga jot ci biral yi ci internet soo duggee ci sa sàq ci www.skype.com. Lii mooy mennum nettalib faktiir buñuy joxe. Sudee dañoo juum ci sa faktiir, war nga ñu ko xamal ci diirup 90 fan yu wees bis bu njëkk bu njuumte bi feeñee ci sa faktiir. Di nañu gëstu, su boobaa fayyeeku bi. Soo ñu ko waxul ci diir boobu, génnee nga ñu ci suñu kiliftéef yépp ak jéebaaneg ñàkk yuy bawoo ci njuumte bi te duñu laaj ñu saafaral njuumte bi mbaa joxe ab delloo xaalis, lu dul yoon dafa koo sàkku ci beneen anam. Sudee Microsoft dafa gis ab njuumtey faktiir, di nañ ko saafaral ci diirup 90 fan. Sàrt bii du lor benn àqi yoon bu mën a jëfe.
  • g. Sàrti delloo xaalis. Ludul yoon xamle neneen mbaa ab maye cër bu xejjiku, jënd yépp ñooy mujj mënu ñu leen delloo. Soo gëmee ni Microsoft daf la fayyeeku ci njuumte, war nga jokkook ñun ci diirup 90 fanu fayyeeku boobu. Duñu delloo dara ci bépp fayeeku bu weesu 90 fan, lu dul yoon dafa koo sàkku ci beneen anam. Dañuy jaglel àqi defar ay delloo xaalis mbaa keredi ci suñu kumpa kase. Suñu defaree ab delloo xaalis mbaa keredi, amu ñu benn waréefu defar bu ni mel mbaa delloo xaalis ci liy ñëw. Sàrt delloo xaalis bii du lor benn àqi yoon bu mën a jëfe. Ngir am yeneen leerali delloo xaalis, yëral sunu tombu ndimbal. Soo dëkke Taywan, nu ngi lay ñaan nga jàpp ni sunu sukkandikoo ci Yoonu Aar Way-jëfandikukatu Taywan ak ay tëriliin yi mu àndal, jënd yépp yu bokk ci këmbi xarala yu nu joxe jaare ko ci tëggiinu bu ñu mënul téye ci loxo ak/mbaa liggéeyali net jeex foofu lañu yem te amul delloo xaalis sunu joxee yooyu këmb wala liggéeyal ci net bi. Amuloo sañ-sañu laaj benn diirup xarandi wala delloo xaalis.
  • h. Fomb Cër yi. Mën nga fomb ab cër saa su nekk, mu àndak ab sabab am déet. Ngir fomm ab liggééyal te laaj ñu delloo la sa xaalis, su la ko yoon mayee, yëral daluwebu saytu sàqum Microsoft bi. Ngir Skype, baal ñu mottali Formileeru jël xaalis di jëfandikoo leeral yuñu joxe fii. Danga war di dellu xool ci liñ wax ci Cër bi ngay jëfandikoo ndax (i) mën nañu la baña delloo sa xaalis ca waxtu wa nga bàyyee; (ii) mën nañu sàkku ci yaw nga fay fere yi ànd ci bàyyi gi; (iii) mën nañu sàkku ci yaw ngay bépp fere yiñ amal ci sa sàqu faktiir ngir Cër yi ngir fay lu jiitu bis ngay bàyyi; te (iv) mën nga bañati mën a jot wala jëfandikoo sam sàq soo bàyyee Cër yi; or sudee Taywan nga dëkk, (v) mën nañu la delloo ab xaalis bu tolloo ak fere yi nga fayoon ci Cër yi te jotoo leen jëfandikoo laata ngay bàyyi. Dina nu jëfandikoo say Njoxe ci ni nu ko leeralee ci pàcc 4. Soo ko dakkalee, dootoo mën jot ci Cër yi su joxaale àpp bi Cër bi am wala, suñu faktiiree sam sàq ci diir buñ yamale, ci njeexitu diir bi nga ko dakkalee.
  • i. Maye Diirup-Ñàmandi yi. Soo bokkee ci ab maye diirup-ñàmandi, war nga fomb Cëru(i) ñàmandi bi(yi) ci njeextalu diirup-ñàmandi bi ngir moytu ay fayyeeku yu bees yu ciy joke, ludul dañ lako xamalee neneen. Soo fombulee cëru(i) ñàmandi bi(yi) ci njextalu diirup ñàmandi bi, mën nañ la faktiire ci Cër bi(yi).
  • j. Maye Siiwal yi. Yenn saay, Mîcrosoft mën naa joxe ay cër ngir ab diirup ñàmandi bodul fay darra. Microsoft mooy seet ndax dañu lay dagg ci Cër yooyu (ci njëg li war) sudee mooy Microsoft dafa gis ni (te mën na ci baña joxe leeral) dangay jalgati sàrti neexal boobu.
  • k. Coppite Njëg yi. Mën nañu soppi njëgu Cër yi saa yu nekk te sudee dañu lay faral di fayyeeku, dina nu la ko yëgalee ci bataaxal, wala yeneen anam yu xel nangu, gën gaa yeex 15 fan laata njëg li di soppiku. Soo nanguwul coppite njëg bi, war nga fomb te dakkal jëfandikoo Cër yi laata coppite njëg bi di door. Su amee ab diir ak njëg bu sax ngir sa maye cër, dina ñu dëkke di jëfe njëg boobu ngir diir bu sax.
  • l. Payoor yuñ la Jaglel. Suñ la amelee ab payoor, nangu nga jox ñu ci lu gaaw te jub ay leeral yuñu soxla ngir jaglel la boobu payoor. Yaw yaa war fay bépp juuti ak njëg yi ci mën ajoge ci payoor bii ñu la jaglel. War nga nangu itam yeneen anam yuñu dugal ci sa àq ci bépp payoor. Soo jotee ab payoor ci njuumte, yoon may nañu ñu laaj la nga delloo xaalis bi. Nangu nga ànd liggéey ak ñun ci luñ jéem ngir def lii. Mën nañ wàññi itam payoor buñ la jaglel te duñ la ci lako yëgël ngir defaraat bépp payoor bu ëpp bu ci amoon.
  • m. Kàrti neexal. Delloo ak jëfandikoo ay kàrti neexal (yu wuutek kàrti neexalu Skype) Sàrti Microsoft Kàrti Neexal moo leen di saytu. Leeral yi ci kàrti neexalu Skype jàppandi nañ ci Xëtu Ndimbalu Skype.
  • n. Jumtukaayu Payooru Sàqum Bànk. Mën nga bindu ngir wut sàqum bànk buy ànd ak sa sàqum Microsoft muy sa jumtukaayu payoor. Sàqi bànk yi ci mën a bokk ñooy sàq yi nekk ci bànk yiñ mën a defee ay wiirmaa yu mag (ci misaal, ab bànku Etaa-Sini buy am njoxey “automated clearing house” ("ACH"), ab b)nku Ëroop buñ nangu Single Euro Payments Area ("SEPA") wala buy nangu "iDEAL" ca Peyi Baa). Sàrt yi nga nangu bi ngay joxe sa sàqum bànk muy sa jumtukaayu payoor ci sa sàqum Microsoft (ci misaal, “ndaw li” sudee dafa am SEPA) da ciy bokk itam. Teewal nga te nangu nga ni sàqu bànk bi nga bind, ci sa tur la nekk wala may nañu la nga bindu ak jëfandikoo bii sàqu bànk muy sa jumtukaayu payoor. Soo bindee wala nga tànn sa sàqu bànk muy sa jumtukaayu payoor, may nga Microsoft (wala ndawam) muy tàmbali la dagg benn yoon wala lu ko ëpp lu tolloo ak li nga jënd wala njëg li nga bindoo (ci lu dëppoo ak sàrti cër bi nga bindu) ci sa sàqu bànk (te sudee laaj na ko, nga dugal benn keredi ci sam sàq bànk ngir saafara njuumte yi, delloo xaalis wala jëf ju ni mel), te itam may nga bànk bi sam sàq nekk, mu dagg la boobu xaalis wala mu nangu keredi yooyu. Xam nga bu baax ni dingal li nga joxe dafay wéy di dox te dara du ci soppiku fileek dindiwoo say leerali sàqu bànk ci sa sàqum Microsoft. Jokkool ak sa ndimbalu kiliyaan ci ni ñu ko leeralee ci kaw ci pàrti 4(e) ci ni mu gën a gaawee sudee danga gëm ni dañu juum dagg la. Yoon yiy dox ci sam réew mën nañu yamale li ñuy teg ci sa ndoddu jamono ju jëflante gi amee njuumte, lu jubadi ci sam sàqu bànk. Soo bindee wala nga tànn sa sàqu bànk muy sa jumtukaayu payoor, nangu nga ni jàng nga te xam nga ci Sàrt yii.
Jukki bu fees
Kër buñuy Jëflànteel, Tànnéefu Yoon, ak Barab ngir Saafaral Ñàkka déggooKër buñuy Jëflànteel, Tànnéefu Yoon, ak Barab ngir Saafaral Ñàkka déggoo10_11_contractingEntityChoiceOfLaw
Tënk

10. Kër buñuy Jëflànteel, Tànnéefu Yoon, ak Barab ngir Saafaral Ñàkka déggoo. Sudee kuy jëfandikoo Cër yi bokk ci Skype yi nga bindu, nga fay wala fayoo, te saa yuñ tuddee "Microsoft" ci biir Sàrt yii, liñ ci jublu mooy Skype Communications S.à.r.l, 23 – 29 Rives de Clausen, L-2165 Luxembourg. Ngir Cëri aji-jëfandikoo Skype buñu màngargal, bodul fara mbaa buñu fay, yoonu Luxembourg dafay saytu leeralu yile Sàrt te sàkku ñu ban leen jëfe, moo xàm xëcco bu am ci digante sukkandikaayu yoon yi. Yoonu tund mbaa réew yi nga dëkk ñooy saytu yeneen jéebaane yépp (bokk na ci kaarànge aji-jëfandikookat, konkiraas bu jaaduwul, ak jébaaneg bu yuy waral ate siwil). Soo nangoo yile sàrt di sos ab sàqum Skype mbaa jëfandikoo Skype, yaw ak ñun nangu nañu ba fàw ci ate bunu dongal ak barabu atékaayu Luxembourg ngir ñàkka déggoo yépp yuy joge ci mbaa méngook yile Sàrt mbaa cëri aji-jëfandikoo Skype bunu màndargal. Ngir yeneen cër yi, soo nangu woon yile Sàrt di jëfandikoo ab sàqum Microsoft mbaa beneen cër bumu mën a doon, kër bi ngay jëflànteel, yoonu nguur gi, ak barab bi ngir saafaral ñàkka déggoo yiy feen fii ci suuf:

  • a. Kanadaa. Soo dëkkee ci (mbaa, sudee ab liggéeyukaay, sa barabu liggéey dafa nekk) Kanadaa, yaa ngi jëflànteek Microsoft Corporation, One Microsoft Way, Redmond, WA 98052, U.S.A. Yooni tund bi nga dëkk (mbaa, sudee ab liggéeyukaay, sa barabu liggéey dafa nekk) mooy saytu nuñuy tekkee yile sàrt, jébaane mbaa seeni jalgati, ak yeneen jébbane (bokk na ci aar aji-jëfandikookat bi, konkiraas bu jaaduwul, ak jébaaneg bu yuy waral ate siwil). Yaw ak ñun nangu nañu ba fàw ci ate bunu dongal ak barabu atékaayu Ontario ngir ñàkka déggoo yépp yuy joge ci mbaa méngook yile Sàrt mbaa Cër.
  • b. Bëj-gànnaar mbaa or Bëj-saalumu Amerig ci biti Etaa-Sini ak Kanadaa. Soo dëkkee ci (mbaa, sudee ab liggéeyukaay, sa barabu liggéey dafa nekk) Bëj-gànnaar mbaa or Bëj-saalumu Amerig ci biti Etaa-Sini ak adaa, yaa ngi jëflànteek Microsoft Corporation, One Microsoft Way, Redmond, WA 98052, U.S.A. Yooni Réewu Washington ñooy saytu nuñuy tekkee yile Sàrt ak yeneen jéebaane ngir seeni jagali, ci li aju ci tànnéefi sukkandikaayu yoon yi. Yoonu réew bunu jaaralee sunuy Cër ñooy saytu yeneen jéebaane yépp (bokk na ci kaarànge aji-jëfandikookat, konkiraas bu jaaduwul, ak jébaaneg bu yuy waral ate siwil).
  • c. Digg Penku mbaa Afrig. Soo dëkkee ci (mbaa, sudee ab liggéeyukaay, sa barabu liggéey dafa nekk) Diggu Penku mbaa Afrig, te ngay jëfandikoo ay doggitu cër yodul fay (niki Bing ak MSN); ya ngi jëflànteek Microsoft Corporation, One Microsoft Way, Redmond, WA 98052, U.S.A. Sudee da nga fayoon ngir jëfandikoo ab doggitu cër yi, ya ngi jëflànteek Microsoft Ireland Operations Limited, One Microsoft Place, South County Business Park, Leopardstown, Dublin 18, Ireland. Ngir Cër yoodul ak yi ngay fay, yoonu Irlànd mooy saytu nuñuy tekkee yile Sàrt te sàkku ñu ban leen jëfe, moo xàm xiiroo ak ŋaayoo sukkandikaayu yoon yi. Yoonu réew bunu jaaralee sunuy Cër ñooy saytu yeneen jéebaane yépp (bokk na ci kaarànge aji-jëfandikookat, konkiraas bu jaaduwul, ak jébaaneg bu yuy waral ate siwil). Yaw ak ñun nangu nañu ba fàw ci ate bunu dongal ak barabu atékaayu Ontario ngir ñàkka déggoo yépp yuy joge ci mbaa méngook yile Sàrt mbaa Cër.
  • d. Asii mbaa Bëj-saalum Pasifik, donte sa dañuy ràññatle sa réew fii ci suuf. Sudee Asie nga dëkk (wala, wala liggéey, sa liggéey bi gëna mag nekk fa) (ba mu des Siin, Sàppoŋ, Réewun Kore, wala Taywan) wala Pasiifik bëj Saalum, te ngay jëfandikoo yenn wàll yuñ la may ci Cër yi (lu ci melni Bing ak MSN), yaa ngi bokk ci Microsoft Corporation, One Microsoft Way, Redmond, WA 98052, U.S.A. Sudee danga fay ngir jëfandikoo benn Wàll ci Cër yi, wala ngay jëfandikoo cëru Outlook.com ci Singapuur wala Ooŋ Kong biñ la may, bindu nga ci Microsoft Regional Sales Corp., di liggéeyukaay bu tënku ci yoon yiñ tëral ci Etaa bu Newada, Etaa Sini, am ay bànxaas ci Singapuur ak Ooŋ Kong, te barabu liggéeyukaay bi gëna mag nekk ci 438B Alexandra Road, #04-09/12, Block B, Alexandra Technopark, Singapore, 119968; te fekk nga dëkk Ostarali (wala, sa barabu liggéeyukaay bi gëna mag nekk fa), yaa ngi bokk ci Microsoft Pty Ltd, 1 Epping Road, North Ryde, NSW 2113, Australia te soo dëkkee Séland Gu Bees (wala, sa barabu liggéeyukaay bi gëna mag nekk fa), yaa ngi bokk ci Microsoft New Zealand Limited, Level 5, 22 Viaduct Harbour Avenue, PO Box 8070 Symonds Street, Auckland, 1150 New Zealand. Sudee Cër yi jaay wala yiy maye, Etaa bu Washington mooy yilif niñ wara déggee Sàrti yii ak jàmbati jalgati yi ci am, xoolu ci ñàkk a déggoo yiy am ci yoon yu bokkul nuñ tëddee. Yoonu réew bunu jaaralee sunuy Cër ñooy saytu yeneen jéebaane yépp (bokk na ci kaarànge aji-jëfandikookat, konkiraas bu jaaduwul, ak jébaaneg bu yuy waral ate siwil). Dina ñu déllu te ci mujanteel bi saafaral ci bépp ñàkka déggoo bu joge ci mbaa méngook yile Sàrt mbaa Cër bu bokkul ak Skype, bokk na ci bépp laaj bu àju ci seeni nekkiin, wéraay, mbaa njeexte, cig atekaayu Singapuur àndak sàrtu SIAC (Arbitration Rules of the Singapore International Arbitration Center), sàrt buñu wara dugal cig royuwaay ci bii tomb. Atekaay bi benn atekat la fa Njiitu SIAC di jël. Làkku ate bi Àngale lay doon. Dogalu ate bi mooy doon bu mujj, takku te kenn duko mën a weddi, te mën nañ ko jëfandikoo niki sukkandikukaayu ate ci bépp réew mbaa diiwaan.
  • e. Sapoo. Soo dëkkee ci (mbaa, sudee ab liggéeyukaay, sa barabu liggéey dafa nekk) Sapoo mbaa Afrig, te ngay jëfandikoo ay doggitu cër yodul fay (niki Bing ak MSN); ya ngi jëflànteek Microsoft Corporation, One Microsoft Way, Redmond, WA 98052, U.S.A. Sudee da nga fayoon ngir jëfandikoo ab doggitu cër yi, ya ngi jëflànteek Microsoft Sapoo Co., Ltd (MSKK), Shinagawa Grand Central Tower, 2-16-3 Konan Minato-ku, Tokyo 108-0075. Ngir Cër yu ñuy fay ak yuñ dul fay, yoonu Sapoo mooy saytu Sàrti yi ak bépp jafe-jafe bu ciy judd mbaa bu méngook ñoom mbaa Cër yi. Yaw ak ñun nangu nañu ba fàw ci ate cosaan bunu dongal ak barabu atékaayu goxu Tokyo ngir ñàkka déggoo yépp yuy joge ci mbaa méngook yile Sàrt mbaa Cër.
  • f. Réewu Kore. Soo dëkkee ci (mbaa, sudee ab liggéeyukaay, sa barabu liggéey dafa nekk) Diggu Penku mbaa Afrig, te ngay jëfandikoo ay doggitu cër yodul fay (niki Bing ak MSN); ya ngi jëflànteek Microsoft Corporation, One Microsoft Way, Redmond, WA 98052, U.S.A. Sudee da nga fayoon ngir jëfandikoo ab doggitu cër yi, ya ngi jëflànteek Microsoft Kore, Inc., 11th Floor, Tower A, K-Twin Tower, Jongro 1 gil 50, Jongro-gu, Sewul, Réewu of Kore, 110-150. Ngir Cër yu ñuy fay ak yuñ dul fay, yoonu réewu Kore mooy saytu Sàrti yi ak bépp jafe-jafe bu ciy judd mbaa bu méngook ñoom mbaa Cër yi. Yaw ak ñun nangu nañu ba fàw ci ate cosaan bunu dongal ak barabu atékaayu goxu Diggu Sewul ngir ñàkka déggoo yépp yuy joge ci mbaa méngook yile Sàrt mbaa Cër yi.
  • g. Taywan. Soo dëkkee ci (mbaa, sudee ab liggéeyukaay, sa barabu liggéey dafa nekk) Taywan, te ngay jëfandikoo ay doggitu cër yodul fay (niki Bing ak MSN); ya ngi jëflànteek Microsoft Corporation, One Microsoft Way, Redmond, WA 98052, U.S.A. Sudee da nga fayoon ngir jëfandikoo ab doggitu cër yi, ya ngi jëflànteek Microsoft Taiwan Corp., 18F, No. 68, Sec. 5, Zhongxiao E. Rd., Xinyi District, Taipei 11065, Taiwan. Ngir Cër yodul fay ak yuñu fay, yoonu Taywaan yi dañuy saytu yile Sàrt ak bépp jafe-jafe bu ciy joge mbaa bu méngook ñoom mbaa Cër yi. Ngir am yeneeni leeral yu neel Microsoft Taywan Corp., baal ñu xool daluweb bu Ministeer bi yor mbiru Bitim Réew R.O.C. joxe. Yaw ak ñun joxoñ nañu ba fàw Atekaayu Goxu Taype niki atekaayu njëlbéen bu amal ate ci bépp ñàkka déggoo buy joge ci mbaa méngook yile Sàrt mbaa Cëri bi, ci dayoo bu ëpp bu yoonu Taywan maye.

Sa yoonu aji-jëfandikoo yi teew mën nañu sàkku yenn yoon yi teew ngir saytu mbaa joxe àqi saafaral ñàkka déggoo ci beneen fuwaar ak lu Sàrti yii mën a doon. Su loolu amee, tànnéefu yoon ak matukaay fal yi ci pàcc 10 buy jëfe niki nuko sa yooni aji-jëfandikoo réew nangoo.

Jukki bu fees
Garanti yiGaranti yi12_Warranties
Tënk

11. Garanti yi.

  • a. MICROSOFT, AK SUNUY BANQAAS, JAAYAATKAT YI, SEDDALEKAT YI, AK JAAKAT YI, JOXE WUÑU BENN GARANTI, BUÑU WAX MBAA NËBB, GARANTI YI MBAA SÀRT YI CI LI AJU CI NI NGAY JËFANDIKOO CËR YI. XAM NGA NI JËFANDIKOO CËR YOOYU MËN NALA LOR TE DANUY JOXE CËR YI CI "NUÑU MEL" AK "NJUUMTE YEPP" AK "SU JAPPANDI WEE." MICROSOFT DU LA GAARAANTI NI CËR DAÑUY DOX BU BAAX SAA YU NEKK TE DUÑU AM BENN DOG-DOG. MËN NGA AM YENN ÀQ CI SA YOONU YU AJU CI BARAB. JËMEE WUÑU LENN CI YILE SART NGIR ÑU LOR YOOYU ÀQ, SUDEE DAÑUY JËFEE. NANGU NGA NI NOSTEY ORDINATËER AK WAXTAANU TELEFON YI MËNU ÑU BAÑA AM AY NJUUMTE AK AY DIIRU TAXAWANDI YU FARAL DI AM. GARANTI WUÑU NI CËR DUÑU DAKKAL CËR YI, ÀPP, KAARANGE, MBAA ÑÀKK NJUUMTE MBAA ÑÀKKUM ËMBIIT, GARANTI WUÑU ITAM BEPP LONKU CI MBAA JOKKALINU XIBAAR CI AY MBAALU ORDINATËER.
  • b. CI DAYO BU ËPP BUÑU NANGU CI SA KAADARU SA YOONU REEW, DAÑUY DÀQ BEPP GARANTI BU NËBBU, BOKK NA CI MËNIINU NJAAY, BAAXAAYU LUÑU MËN A NANGU, JEKKAL NGIR JUBLUWAAY BU XEJJIKU, NJUUMTEY DEFAR, AK NÀKKA LUUBAL.
  • c. Ngir aji-jëfandikoo yu dëkk ci Ostrali: Suñuy màrsandiis dañuy àndak ay garanti yuñu mënul a dàq ci kaadaru Yoonu Ostrali. Nangu nañu nga wuutal ab délloo ngir dog-dog bu mag ak fay ngir bépp ñàkk mbaa yàqute buñu mën xaarandi. Nangu nañu itam ñu saafaral say yëf sudee jotu ñu nangu baaxaayu yëf yi te njëgu dog-dog bi tollul ci ab dog-dog bu mag.
  • d. Ngir aji-jëfandikoo yu dëkk Nouvel Zeland, mën ngeen a ay àqi yoon ci kaadarujëfu Garanti aji-jëfandikoo Nouvel Zeland, te lenn ci yile sàrt warul a lor yooyu àq.
Jukki bu fees
Yemaley mën a yorYemaley mën a yor13_limitationOfLiability
Tënk

12. Yemaley mën a yor.

  • a. Sudee danga am luñ la wara joxee ndàmpaay (lu ci xel Sàrt yii), ci anam wu dëppoo ak li yoon maye, nangu nga ni li nga mën a def ngir indi ci saafara du lenn ludul defaraat, ci Microsoft wala ci ñi mi lëkkalool, ñiy jënd-jaayaat, ñiy séddale, ñiy joxe Cër ak Jëfekaayi Jàmbur, ak jaaykat yi, ndàmpaay lu tollu ci fere yi nga def ci Cër yi ci weer wi nga ñàkkee wala wiñ jalgati gi amee (wala lu yegg ci USD$10.00 sudee Cër bi dafay maye).
  • b. Ba fu la yoon buy jëfe may, mënuloo dabuwaat bépp (i) ñàkk mbaa réeral yuy lore; (ii) ñàkkub njuréef yu teew mbaa yu ñu dabu (mu jub mbaa mu dëng); (iii) ñàkkub alal bu teew mbaa bu ñu dabu (mu jub mbaa mu dëng); (iv) ñàkk xame mbaa liggéeyukaa mbaa yeneeni ñàkk mbaa yàqute yu bawoo ci jëfandikoo Liggéyal yi ci ab man-man bu amul boroom; (v) ñàkk mbaa yàqute yuy bañal, mbaa indi xew-xew, bu jubul te xejjiku; ak (vi) ci dayo bu ëpp bu yoon maye, ñàkk mbaa réeral yu jub yu bawoo ci lu ñu romb ci pàcc 12(a) bii ci kaw. Yile yemale ak dàq dañuy jëfe sudee saafara bii du la fay ci bépp ñàkk mbaa dog-dogu jubluwaay bu am solo mbaa suñu xàmoon mbaa waroon a xàm ni yàqute yi mën nañu am. Ci dayoo bu ëpp bu yoon maye, yile yemale ak dañuy jëfe ci lépp mbaa bépp jéebaaneg bu méngook yile Sàrt, Cër yi, mbaa losisel bu méngook Cër yi.
  • c. Microsoft waralul benn dog-dog ngir amal mbaa yeexal xaranaayu ay waréefam ci kaadaru yile Sàrt ba ci dayo sudee dog-dog bi mbaa yeexal ay xew-xew yu Microsoft fugluwul ñoo ko waral (niki xirook ak ŋaayoo liggéey, jëfi Yalla, xaré, jëfu defkatu lu ñaaw, yàqute yu soxor, aksidan mbaa nangul bépp yoon mbaa santaane nguur). Microsoft dina jéem a wàññi jeexiti xew-xew yii yépp ak ngir amal waréef yu loruwul.
Jukki bu fees
Sàrt yuy àndak cër yiSàrt yuy àndak cër yi14_service-SpecificTerms
Tënk

13. Sàrt yuy àndak cër yi. Sàrt yi jittu ak yi weesu pàcc 13 dañuy faral di jëfe ci cër yépp. Pàcc bii am na ay sàrt yuy àndak cër yuñu yokk ci sàrt yu matale. Su werante amee ci diggante sàrt yii ñuy wax ak yeneen sàrt yu mag yi, nañu sukkandiku ci sàrti cër yii.

Jukki bu fees
Po ak Jefekaayi Xbox Live ak Microsoft StudiosPo ak Jefekaayi Xbox Live ak Microsoft Studios14a_XboxLive
Tënk
  • a. Po ak Jefekaayi Xbox Live ak Microsoft Studios.
    • i. Jëfandikoo Jagoo ak budul Jaay. Xbox Live, Games for Windows Live ak po, jëfekaay, cëri Microsoft Studios ak ëmbiit yu Microsoft joxe (suñ leen boolee, "Cëri Xbox yi") ngir sa jëfandikoo bu jagoo ak budul jaay kase lañu.
    • ii. Cëri Xbox. Soo bindoo ci Xbox Live ak/wala nga jot Cëri Xbox, ay leeral ci sam po, li ngay def wala ni nga jëfandikoo sam po ak Cëri Xbox, dañu koy topp, séddoo ko ak jàmbur yi bokk ci defarum po moomu ndax Microsoft ak jàmbur yiy defar pomoomu mëna doxal seenu po ak jox ko Cëri Xbox. Soo tànnee lëkkale sàqu Liggéeyali Microsoft Xbox ak sa sàq ci ab liggéeyal bu bokkul ci Microsoft (maanaam, ab siiwalkatu po bu bokkul ci Microsoft bu Jëfekaay ak Liggéeyal yu bawoo feneen), nangu nga ni: (a) Microsoft mën naa séddale ay leerali sàq yu néew (bokk na ci te yemul ci dàkkantal, poñu po, jaar-jaaru po, ak limu xarit), ak wàll bu bokkul ci Microsoft ci niñu ko xamlee ci Sàrti Samm-sutura Microsoft, ak (b) suko say jekkali sutura Xbox nangoo, Wàll bu bokkul ci Microsoft mën naa dugg itam ci Sa Këmb bawoo ci ay waxtaani po soo duggee ci sa sàq ak boobu wàll bu bokkul ci Microsoft. Te itam, su la ko say jekkali sutura su Xbox mayee, Microsoft mën na siiwal sa tur, xàmme po, nataalu po, bàkk, avatar, klipu po ak po yi nga musu fo ak nit ñi nga nangu.
    • iii. Sa këmb. Sunu mbébetu tabax asku Cëri Xbox, jox nga ndigal Microsoft, ay bànxaasam, wala ñi muy jox sañ-sañ, ñu mën a jëfandikoo fépp ci àdduna, soppali, sotti, séddale, siiwal; séddoo ak wane Say Ëmbiit wala sa tur, wala say xàmme po, sa bàkk, sa avatar bi nga siiwal ci Cëri Xbox.
    • iv. Saytukatu po yi. Yenn po yi mën nañu jëfandikoo ak saytukat ak ay njaatige. Saytukatu po yi ak njaatige yi ay teewalkatu yu Microsoft nangu lañu. Seeni wonin farataluñu wone yosu Microsoft.
    • v. Xale yi ci Xbox. Sudee ab gone buy jëfandikoo Xbox Live nga, sa waa-jur mbaa kilifë mën na saytu ci ay xeet yu bari yu sa sàq te mën na jot ay nettali yu àju ci sa jëfandikoo Xbox Live.
    • vi. Kopparu fo mbaa Costéef yu jëmmadi. Cër yi mën nañu àndak ab kopparu po bu jëmmadi (niki wurus, weccit mbaa poñ) buñu mën a jëndee ci Microsoft di jëfandikoo ay jumtukaayu njëgi xaalis soo tollee ci atu "muskalaf" fi nga dëkk. Cër yi mën nañu ànd itam ak ay jukki xarala mbaa costéefyu jëmmadi yuñu mën a jëndee ci Microsoft di jëfandikoo ay jumtukaayu njëgi xaalis mbaa jëfandikoo kopparu fo. Kopparu po ak costéef yu jëmmadi mën nañ leen baña dabuwaat ba fàw ngir jumtukaayu njëgu xaalis yu teew, costéef, mbaa yeneeni jukkiy njëgi xaalis ci Microsoft mbaa bépp xaaj bu bawoo feneen. Ludul sàñ-sàñu jëfandikoo kopparu po buñu yemale, bu jagoo, buñu mën a teggi, buñu mànta jàllale, buñu mànta liggéeyal, amuloo benn àq mbaa tural ci biir walla ci bépp kopparu po mbaa costéef bu jëmmadi bu ni mel bu ndurook mbaa bu bawoo ci Cër yi, walla yeneen beneen jagleel yuñu boolek jëfandikoo Cër yi mbaa yuñu denc ci Cër yi. Microsoft mën na defaraat, saytu, soppu ak/mbaa dindi saa su nekk kopparu po mi ak/mbaa costéef yu jëmmadi numu jappee ni ànd nak kumpa boppam.
    • vii. Yeesalu Losisel yi. Bépp jëfandaay bu mëna lënku ci Cëri Xbox, mën nanu seet ci saasi sa sumbu losiselu jumtukaayu Xbox wala losiselu jëfekaayu Xbox bi te yebbil la yeesali jumtukaayu Xbox bi wala yu losiselu jëfekaayu Xbox wala yu coppiteg tabb gi, muy mbir yi lay tere jot ci Cëri Xbox yi, jëfandikoo po yu Xbox yuñ lay mayul wala jëfekaayi Xbox, wala jëfandikoo jëfandaay yuñ la mayul sañ-sañ ak jumtukaayu Xbox.
    • viii. Njeextalu Dàkkantal. Fàww nga dugg gën gaa néew ci ab diiru juróomi at, lu ko moy mën nga bañ a mën a dugg ci dàkkantal bu ñu booleek sa sàq te boobu dàkkantal mën naa jàppandi ngir ñeneen mën koo jëfandikoo.
    • ix. Arena. Arena mooy Cëru Xbox bi Microsoft wala ab jàmbur mën a jox ngir nga mën a bokk ci ñiy joŋante ci wàllu powum wideo, yenn sa ñu teg ab kup ("Joŋante"). Sag jëfandikoo Arena dafay dugg ci Sàrt yi, te mën nala laaj nga nangu yeneen sàrti joŋante, anam ak yoon yi boroom joŋante bi tëral ci jamono ji ñuy bindu ("Sàrti Joŋante"). Mën bokk gaa ngi aju ci yoon yiñ tëral ci sam réew. Joŋante bi mënul ci réew yi seeni yoon di ko tere. Ku jalgati Sàrt yii (bu àndaale ak Sàrtu Doxalin) wala Sàrti Joŋante bi mën nañu la aj ci Joŋante bi wala ñu teg la ay daan. Soo sosee ab Joŋante, mënoo sàkku benn Sàrtu Joŋante bu Microsoft (du ci indi leeral) jàpp ni méngoowul ak Sàrt yii. Microsoft amna sañ-sañu dakkal bépp Joŋante, saa yu nekk.
    • x. Losisel yuy Sàcc wala yuy Saboote. Bépp jëfandaay bu mën a lënku ci Cëri Xbox, mën nanu xool ci saasi ngir xam ndax tere wuñu ko, wala losisel yu mën a may nit ñuy sàcc wala ñuy saboote di jalgati Sàrti Doxalin yi wala Sàrt yii, ak yebbi yeesali losiselu jëfekaayu Xbox wala soppi jekkal yiñ fi def, lu ci melni jekkal yi lay tere nga jot ci Cëri Xbox, wala tere la nga jëfandikoo jumtukaay wala losisel bu lay may ngay sàcc wala ngay saboote.
    • xi. Mixer.
      • 1. Sàqi Mixer ak Sàqi Microsoft. Sooy jëfandikoo Cëru Mixer ak sàqum Mixer, kon sag jëfandikoo dafay bokk ci Sàrti Mixer ci nekk ci https://mixer.com/about/tos. Sooy jëfandikoo Cëru Mixer ak sàqum Microsoft, kon sag jëfandikoo dafay bokk ci Sàrt yii. Saa yu warante amee dañuy dellu ci sàrt yii.
      • 2. Say Ëmbiit yi ci Mixer. "Say Ëmbiit yi ci Mixer" ñooy bépp ëmbiit boo sos wala keneen sos ci sa tur ci Cëru Mixer, muy cër yu ci melni dawal, seetaan (ak bépp ëmbiit, lu melni ëmbiitu déglu-seetaan, biñ ëmb); turi màrk yi, màrk yi, màrki cër yi, turi màrk yi, logo yi, wala endisu cosaan; say àddu, emoji, ak jëf yi ci seeni Mixer (boole ci ëmbiit yi bot sos); ak bépp meta-njoxe bumu bokkal. Ku nekk, manaam Microsoft ak jëfandikukat yi mën nañu gis, jëfandikoo, dalal, sotti, soppali, siiwal, dawalee ci biti wala ci net bi ak wane ko, tekki, yamale, ak jëfandikoo Say Ëmbiit ci Mixer, ci anam wu nekk, formaa bu nekk, mejaa wala seen yuñ xam ba noppi wala yu ñuy waaja defar.
      • 3. Sàrti Doxalin yi bokk ci Mixer. Bësal fii ngir am yeneen leeral ci Sàrti Doxalin yi Microsoft di doxal ci Mixer.
      • 4. Jëfandikoo Cëru Mixer.
        • a. At yu gën Ndaw. Soo jëfandikoo Cëru Mixer, dëggal nga ni am nga gën ga néew 13 at, te sudee amagoo yooyu at ci réew ma nga dëkk, fàww nga am waajur wala mag mu lay xool bu baax.
        • b. Jëfandikoo guy wane wala nëbb tur. Mën nga nëbb sa tur te jëfandikoo sudee danga bëgg a xool ay ëmbiit. Su dul loolu fàww nga sos am sàq, nga dugg, te yeneen jëfandikukat yi di na ñu mën a xamee ci sa turu Mixer.
        • c. Sàqi Jëfandikoo guy wane tur. Mën nga sos sàqum Microsoft ak/wala sàqum Mixer ngir jëfandikoo guy wane tur ci Cëru Mixer. Mën nga sos sàqum Mixer soo bindoo ci internet. Fàww nga jëfandikoo sa sàqum Mixer ngir muy wéy di dox. Deel dugg ci sa Cëru Mixer gën gaa néew benn yoon ci diirub 5 at ngir mën a boole sa turu Mixer ak sa sàqum Microsoft.
      • 5. Yëgley Cër bi. Sudee daa am luñu lay wax lu jëm ci Cëru Mixer, dina nu la yónnee yëgley cër ci dëkkuwaayu bataaxal bi nekk ci sa sàqum Mixer ak/wala sàqum Microsoft.
      • 6. Ndimbal. Di ngeen fekk ndimbalu kiliyaan bi ci Cëru Mixer ci mixer.com/contact.
Jukki bu fees
MàngasiinMàngasiin14b_Store
Tënk
  • b. Màngasiin. "Màngasiin" mooy Cër bu tax nga mën a yër, yebbi, jënd, natt ak topp jëfekaay yi (baatu "jëfekaay" dafay àndak po yi) ak yeneen këmbu xarala. Yile Sàrt dañuy ëmb jëfandikoo Office Store, Windows Store ak Xbox Store. "Office Store" mooy Màngassinu costéefi ak jëfekaayi Office ngir Office, Office 365, SharePoint, Exchange, Access ak Project (sumbu 2013 wala yi ci topp), wala beneen xeetu jëfandikoo bu am turu Office Store. "Windows Store" mooy ab Màngasiin buñu jagleel jumtukaayu Windows yi niki telefon, PC ak tablet, mbaa beneen jaar-jaar bu Windows Store màndargal. "Xbox Store" mooy Màngassinu jumtukaayi Xbox One ak Xbox 360, wala bu bépp xeetu jëfandikoo bu am turu Xbox Store.
    • i. Sàrti Sàñ-sàñ. Dina ñu ràññee siiwalkatu bépp jëfekaay bu jàppandi ci Màngasiin bu am solo. Fileek jëfekaay bi àndul ak yeneen sàrti sañ-sañ, Sàrti Sañ-sañi Jëfekaay yu Yaw bi ("SALT") te nekk ci njeexte Sàrt yii, ab déggoo la bu dox sa diggante ak ki defarkatu jëfekaay bi def sàrti sañ-sañ yi yilif jëfekaay boo yebbee ci Màngasiinu Windows wala ci Màngasiinu Xbox. Ci leeral, Sàrti yii ñoo yilif ni ñuy jëfandikoo cër yi bokk ci, wala yi Cëri Microsoft joxe. Pàcc 5 bu Sàrt yii dafay wax ci Cër ak Jëfekaayi Jàmbur yi nga jëlee cib Màngasiin. Jëfekaay yuñu yebbi ci Office Store SALT saytu wuko te am na ay sàrt sàñ-sàñ yu xaajaloo yuy jëfe.
    • ii. Yeesal. Microsoft dafay seet ci saasi te yebbi ay yeesal ci say jëfekaay, donte duggoo ci ab Màngasiin bu am solo. Mën nga soppi sa Màngasiin mbaa say jekkali noste soo tànnee bàna jot ay yeesal ci saasi ci jëfekaayi Màngasiin bi. Waaye, yenn jëfekaayi Màngasiinu Office yi nga xamantani net bee leen dëkkal moo xam lépp walla ay pàcc ci ñoom, defarkatu jëfekaay bi mën nañu leen yeesal saa su nekk te itam mën nañu leen bañ a tàggu ci loolu.
    • iii. Natt yi ak Topp yi. Sudee danga may poñ wala jàngat ab jëfekaay wala beneen Jumtukaayu Disitaal ci Màngasiin bi, mën nga jot bataaxalu Microsoft bu def ëmbiitu ki siiwal jëfekaay bi wala Jumtukaayu Disitaal bi. Bataaxal bu ni mel a ngi bawoo ci Microsoft; dunu séddoo sa dëkkuwaayu bataaxal ak ñiy siiwal jëfekaay yi wala Jumtukaayu Disitaal yi nga amee ci Màngasiin bi.
    • iv. Dànkaafu kaarànge. Ngir moytu ngaañ yu ci mën a sababoo, jafe-jafe wala mettitu bët, war nga noppalu yenn saa cig jëfandikoo po yi wala yeneen jëfekaay, rawatina soo yëgee ab coono buy bawoo cig jëfandikoo. Sooy yëg ab jafe-jafe, noppalul. Jafe-jafe yi bokk na ci xel mu teey, feebaru yëngu-yëngu, miir, jaxasoo, bopp buy metti, coono, bët buy metti, walla gët yu wow. Jëfandikoo ay jëfekaay mën na la jaxase walla xatal ñi la wër. Moytul a fakkastalu, eskale, dal yu gàtt, ay yëf yu oyof walla yu am solo yu mën a yàqu. Ab pursantaasu nit bu ndaw mën nañu jaar ci ay kiris suñ leen teggee ci yenn nataal jakkarloo niki ékleer yi mbaa ay royuwaay yu mën feeñ ci jëfekaay yi. Akit nit yu jaarul ci ay kiris mën nañu am ab anam buñu saytuwul bu mën a waral yile kiris. Li kay wone mën na boole miir, gis-gis bu soppeeku, gaawa mer, labajoo mbaa loxo yuy lox, reer, jaxasoo, ndof, mbaa kiris. Dakkal jëfandikoo ci saasi te seeti ab doktor soo yëgee benn ci yii koy wone, mbaa seeti ab doktor laata nga jëfandikoo jëfekaay yi soo mësee yëg li koy wone yu lëkkalook ay kiris. Waa-jur yi war nañu saytu nan la seeni doom di jëfeandikoo jëfekaay yi ngir màndarga yu koy wone.
Jukki bu fees
Man-mani Njabootu MicrosoftMan-mani Njabootu Microsoft14c_MicrosoftFamily
Tënk
  • c. Man-mani Njobootu Microsoft. Waajur yi ak xale yi mën nañu Man-mani Njobootu Microsoft ngir xam ban doxalin, yan daliweb, yan jëfekaay, yan po, yan barab yu teew ak yan waxtu jëfandikoo ñoo jaado ci seen njaboot. Waajur yi mën nañu sos ab njaboot su ñu demee ci https://account.microsoft.com/family (wala su ñu toppee digle yi ci seen jëfandaayu Windows wala jumtukaayu Xbox) te woo xale yi wala ñeneen ñu bokk ci. Bari man-man yuy jàppandi ci njaboot gi, kon xoolal bu baax leeral yiñ la jox bi nga nangoo sos wala bokk ci njaboot gi bi ngay jëndal sa njaboot ay Màrsandiisu Disitaal. Boo sosee wala nga bokk ci njaboot, nangu nga jëfandikoo njaboot gi ci anam wi ñu ko diglee, te doo ko jëfandoo ngir def lu jubadi wala di jéema jot ci ay leerali jàmbur.
Jukki bu fees
Bataaxalug MboolooBataaxalug Mbooloo14d_GroupMessaging
Tënk
  • d. Bataaxalug Mbooloo. Bànqaasi Microsoft yu wuute may nañu la nga yónnee ay bataaxal ñeneen jaare ko ci sa baat (looy wax) wala SMS ("bataaxal"), ak/wala may Microsoft ak jaaylekatu Microsoft ngir ñu yónnee la ay bataaxal yaw ak benn wala yeneen jëfandikukat ci sa tur. SOOY DIGAL MICROSOFT AK JAAYLEKATU MICROSOFT NGIR ÑU YÓNNEE LA BATAAXAL YI YAW WALA ÑENEEN, XAMLE NGA NI TE GAARANTI NGA ÑU NI YAW AK KÉPP KOO ÑU DIGAL NU YÓNNEE KO BATAAXALU NANGU NGIR MU JOT BATAAXAL YI AK BÉPP BATAAXALU JUKKI BU MÉNGOOK CAYTU BU BAWOO CI MICROSOFT AK JAAYLEKATU CI MICROSOFT. "Bataaxalu jubbib caytu" yi ay bataaxali jëflante yuy faral di am lañu yu bawoo ci ab bànqaasi Microsoft, bokk na ci waaye yemul ci ab "bataaxalu dalal-jàmm" wala ay digle ci nu ñuy dakkale jot ay bataaxal. Yaw wala ay way-bokki kuréel ñi bëggatul jot yooyu bataaxal mën ngeen tànn baña jot yeneeni bataaxal yu bawoo ci Microsoft wala Jaalekati Microsoft yi saa su nekk sooy topp digle yu ñu joxe ngir loolu. Su dee bëggatuloo jot yooyu bataaxal wala bokk ci kuréel gi, nangu nga ni dinga génn jaare ko ci digle yi la tëriin bi wala jëfekaay bi jox. Su dee am nga sabab ngir gëm ni ab way-bokku kuréel bëggatul jot yooyu bataaxal wala bokk ci kuréel bi, nangu nga ñu dindi leen ci kuréel bi. Xamle nga itam te gaarantil nga ñu ni yaw ak képp koo ñu digal ñu yónnee ko bataaxal nànd na ni way-bokku kuréel bu nekk mooy sasoo njëgi bépp fayeeku bataaxal bu operatëru mobiilam natt, bokk na ci fayeekuu bataaxalu bitim-réew yu ci mën a am su fekkee ni niméroob Etaa-sini (Amerik) moo jàllalee bataaxal yi.
Jukki bu fees
Skype ak GroupMeSkype ak GroupMe14e_Skype
Tënk
  • e. Skype ak GroupMe.
    • i. Mënul a dugg ci Cër jamp. Am na ay wuute yu am solo digante cëri telefon yi njëkk yi ak Skype. Santu ñu Skype mu maye jëfandikoog Cëru Wallu ci wenn yoon wuñ mën a tëral ci bépp réew. Losisel ak costéefi Skype yi waru ñu nangu mbaa gàddu ay woote yu jamp ci bépp xeetu lopitaal, liggéeyukaayu dëgëral yoon, kër doktor mbaa beneen xeetu cër bumu mën a doon buy lëkkale ab jëfandikookat ak ay cëri jagoo yu jamp mbaa ay tombu tontu kaarànge mbooloo ("Cër yu Jamp"). Nangu nga ni ànd nga ci: (i) yaw yaa wara jëndal sa bopp koneksioŋ ci (portaabal) wala ci telefon fiks yi ànd ak ngir mën a jëfandikoo Cëri Wallu yi, te (ii) Skype mënu fi wuutu jëfandikoo gi nga daan jëfandikoo sa telefon.
    • ii. API yi mbaa Jàllale. Soo bëggee jëfandikoo Skype cib lëkkalook bépp jàllale, war nga dëppook "Broadcast TOS" ci https://www.skype.com/go/legal.broadcast. Soo bëggee jëfandikoo bépp jaarukaayu tëriinu jëfekaay ("API") buñu wone mbaa fexe ba skype jàppandi war nga dëppook sàrti sàñ-sàñ yuy jëfe, yu jàppandi ci www.skype.com/go/legal.
    • iii. Sàrti Jëfandikoo wu Jub Sàrti jëfandikoo wu jub mën na jëfe ci ni ngay jëfandikoo Skype. Baal ñu topp yile sàrt yuñu defar ngir aar leen ci luubal ak tooñ te mën na tekk ay yemale ci xeet bi, diir bi mbaa dayo woote yi mbaa bataaxal yi nga mën a amal. Dugal nañu yile sàrt ci Sàrt yi cig delluwaay. Mën nga gis yile sàrt ci https://www.skype.com/go/terms.fairusage/.
    • iv. Mapaas. Skype am na ay man-man yuy tax nga mën ci dugal ay leeral, mbaa nga dugal sa bopp ci ab kàrt di jëfandikoo ab cëru mapaas. Sooy jëfandikoo yooyu man-man, nangu nga yile sàrt te sàrti Google Maps jàppandi nañu ci https://www.google.com/intl/en_ALL/help/terms_maps.html. wala yooyu sàrti Google Map jàppandi nañu ci sa réew.
    • v. Jëfandikookati Nguur gi. Sudee danga bëgg a jëfandikoo sa sàqu liggéey wala Skype Manager ci turu Nguurug Etaa-Sini wala këru liggéey ci Nguuru Etaa-Sini, Sàrt yii duñu dox ci boobu jëfandikoo. Boo soxlaa yeneen leeral ci sàrti, jokkool ak usgovusers@skype.net.
    • vi. Jëfandikoo Jagoo ak / budul Jaay. Jëfandikoo Skype ngir sa jëfandikoo jagoo la ak budul jaay. May nañu la nga jëfandikoo Skype ngir jokkoo ci sa liggéeyukaay wala ci sa liggéeyu bopp.
    • vii. Nimero Skype/Nimero Skype To Go. Sudee Skype daf lay jox ab nimero Skype mbaa Nimero Skype To Go, nangu nga ni moomuloo nimero bi walla amuloo àqi teye nimero boobu ba fàw. Ci yenn réew yi, mën nañ la jox ab nimero bu bawoo ci ab liggéyandoo Skype bu wuuteek Skype, te mën nga bëgg a dugg ci ab déggoo bu xaajaloo ak boobu liggéeyandoo.
    • viii. Skype Manager. Yaw yaay sos ak saytu sa "Sàqu Yorkatu Skype Manager", nga nekk benn yorkatu mbooloo Skype Manager bokkul ak ku yor liggéey. Mën nga lëkkale sa sàqum Microsoft bi nga moom ak am mbooloo Skype Manager ("Sàq yiñ Lëkkalante"). Mën nga jël yeneen saytukat ci sa kuréelu Skype Manager ci kaw ñu nangu yile Sàrt. Soo joxee Skype ay nimero ci ab Sàq bu ñu lëkkale, yaw yaay saytu dëppoo bépp sàkku bu méngook sa dëkkuwaay mbaa barabu say jëfandikookatu Sàq bu ñu lëkkale. Sudee danga dakkal sa lëkkalanteg Sàqu Lëkkalante ak am mbooloo Skype Manager, kenn du ci mën a dindi menn mbindu muñ ko jagleel, Keredi Skype wala Nimero Skype te kenn dootul mën a jot ci Say Ëmbiit wala jumtukaay yuñ boole ak sàq miñ dakkal lëkkalanteem. Nangu nga jëfe bépp leerali jagoo bu say jëfandikookatu Sàq bu ñu Lëkkale ngir ànd ak yooni kaarange njoxe yuy jëfe.
    • ix. Fayyeeku Skype yi. Njëg yépp yu ñeel costéefi Skype yuñu fay boole nañ ci juuti yiy jëfe, ludul dañu wax leneen. Fayyeeku yu mën am ci woote ci biti takkoo mu àju ci njëgu lonku (fayyeeku benn yoon ci woote bu nekk) ak ab njëgu simili niki nuñ ko tëralee ci www.skype.com/go/allrates. Dina ñu wàññi njëgu telefon ci sa tolluwaayu Keredi Skype. Skype mën na soppi njëgi wooteem saa yu nekk ba noppi siiwal ko ci www.skype.com/go/allrates. Njëg bu bees bi dina jëfe léegi ci sa woote buy ñëw suñu siiwalee njëg yu bees yi ba noppi. Baal ñu xool njëg yu mujj yu gën bees laata ngay woote. Dina ñu dugal woote yu am dog-dog ak fayyeeku yu dogit yi ci bór bu ci topp. Ci yenn réew yi, costéef yuñuy jëdee Skype bu way liggéeyandoo Skype bu barab bi ak sàrti jëfandikoo way-liggéyandoo yi dina ñu jëfe ci jëflànte bi.
    • x. Keredi Skype. Skype du garanti ni di nga mën a jëfandikoo sa tolluwaayu Keredi ngir jënd costéefu Skype yu Skype fay yépp. Sudee jëfandikoowoo sa keredi Skype ci diirub 180 fan, Skype dafay jàppee keredi boobu luñ jëfandikoowul. Mën nga doxalaat Keredi Skype bi soo toppee lëkkalekaayu doxal bi ci https://www.skype.com/go/store.reactivate.credit. Sudee danga nekk ci Sapoŋ ba noppi nga jënd Keredi Skype ci daluwebu Skype, bokkoo ci ñaari kàddu (phrases) yiñ wax ci kaw te sa Keredi Skype dina jeex 180 fan ginaaw bis bi nga ko jëndee. Ginaaw bi sa keredi jeexee, dootoo ko mën a doxolaat wala di ko jëfandikoo. Mën nga dekkal man-manu Yabaat ci Saasi soo jëndee Keredi Skype so tànnee boyet bu jub. Suñu ko doxalee, sa xaalisu Kredi Skype dina dugg, tollo ak li nga jënd ci sa jumtukaayu payoor saa yu sa xaalisu Skype wàccee ba weesu àpp fi Skype di faral di def. Soo jëndee ab takkoo ak ab anamu pay bu bokkul ak kàrtu bànk, PayPal, mbaa Moneybookers (Skrill), te nga dekkal Yabaat-boppam, dina ñu yabaat sa tolluwaayu Keredi Skype ak tolluwaayu yuñu laaj ngir jënd sa takkoo baamtu bu ci topp. Mën nga dakkal li muy dugalal bopp keredi ak soppi say jekkal yi ci sa dalu sàqu ci Skype.
    • xi. Njëgi Bataaxali Bitim-réew. GroupMe mu ngi jëfandikoo fii mu ne nii ay nimero telefonu Etaasini (Amerig) ngir bépp kuréel bu ñu sos. Bépp bataaxalu jukki bu ñu la yónnee wala bi nga jot ci ab nimero GroupMe dina konte niki ab jukkib bitim-réew bu ñu jot mu bawoo Etaasini (Amerig). Baal nu nga xool ak sa joxekat ci lu ñeel njëgi bitim réew yu ñu ci boole.
    • xii. Yónnee ak jot xaalis. Soo jëfandikoo man-manu yónnee ak jot xaalis (su jàppandee), nangu nga Skype jaare ci ay jàmbur ngir joxe ay cëri payoor ak def ay yóbbante. Skype du joxe cëri payoor wala yóbbante xaalis te nekkul itam cër buy liggéey ci xaalis. Ñi am 18 at wala lu ko ëpp kese ñoo mën a yónnee ak jot xaalis ci Skype (wala ñi dëppoo ak sàrt yi ab jàmbur tëral) te ñooy kese ñooy bindu te ñoo mën a am sàq ci jàmbur bu koy joxe. Ngir jëfandikoo man-manu yónnee xaalis, mën nañu la laaj nga bindu ci sàrti ak doxaliini jàmbur bi te maye sañ-sañu ñu séddoo ay njoxe ak yii jàmbur ngir ñu jox la cër bi. Sudee Skype dafa jot bataaxal bu koy xamal ni danga jëfandikoo man-manu yónnee xaalis bi ci anam wuy jalgati sàrti doxaliini jàmbur, Skype mën na def lu melni tëj wala mu dakkal sam sàq. Yoonu Skype, wala Microsoft nekkul ci jumtukaayu payoor bu la ab jàmbur jox wala jenn jëf joo defee ci sàrt ak doxaliini jàmbur. Skype mënul dig kenn ni dina mën na jàpandil ak wéyal di jàppandil ba fàww man-manu yónnee ak jot xaalis bi.
Jukki bu fees
Bing ak MSNBing ak MSN14f_BingandMSN
Tënk
  • f. Bing ak MSN.
    • i. Daju Bing ak MSN yi. Xët yi, mbind, nataal, kàrt, wideo, jàngukaayu wideo wala yeneen jumtukaayi jàmbur yi nekk ci Bing ak MSN, lu ci melni ci bokk ci boti Microsoft, jëfekaayi ak tëriin, mayu ñu la nga jaay ko, sa jëfandikoo bopp kese. Yeneen jëfandikoo yu melni yebbi, sotti wala séddalewaat yii jumtukaay, wala jëfandikoo yii jumtukaay wala costéef ngir defar sa costéefu bopp, mën nañu ko maye sudee Microsoft nangu na loolu am, wala yooni àqi moomeel nangu loolu. Microsoft mbaa yeneen yorkati àq dafay jaglel àq yépp ci daju bu Microsoft maye ci wax ci kaadaru sàrti sàñ-sàñ yi, ci bokk, até mbaa neneen.
    • ii. Kàrti Bing. Mën nga baña ay wonandi yu rafet ci Etaa-Sini, Kanadaa, Meksik, Nouvel Zelànd, Ostrali mbaa Sapoo ngir jëfandikoo nguur te du andak suñu nangu bu xaajaloo buñu bind.
    • iii. Barabi Bing ak Barabu Liggéeyukaayu Bing. Soo joxee Barabi Bing wala Barabu Liggéeyukaayu Bing say Njoxe wala Say Ëmbiit, may nga Microsoft sañ-sañ, bu koy may mu jëfandikoo, sotti, denc, soppali, jagleel, ñaax, joxe, wane wala séddoo njoxe yooyu ñu bokk cib cër, te joxalee wàll ci sañ-sañ bi yooyu jàmbur.
Jukki bu fees
CortanaCortana14g_Cortana
Tënk
  • g. Cortana.
    • i. Jëfandikoo Jagoo ak budul Jaay. Cortana Cëri Jàppale jagoo bu Mucrosoft la. Cortana (wala "Cëri Cortana") joxewul man-man byi, cër yi, ëmbiit yi ak Cër ak Jëfekaayi Jàmbur yi ludul nga koy jëfandikoo ngir sa bopp, kenn du ci wutee xaalis.
    • ii. Maneef ak Ëmbiit. Cortana dafay joxe man-man yu bari, ñu jagleel yenn yi ci ñoom. Cëri Cortana mën nañu la may nga jot ci ay cër, leeral wala man-man yu bawoo ci Cëri Microsoft wala Cër ak Jëfekaayi Jàmbur. Sàrti cër biy wax ci loolu ci pàcc 13 dafay waxaale ci ni nga waree jëfandikoo Cëri Microsoft yi nga duggee ci Cëri Cortana. Cortana dafay joxe ay leeral ngir say jumbluwaayu palaŋ kase te war nga jëfe sa atey bopp sooy topp te doylu ci leeral yii. Yoonu Microsoft nekkul ci wóoraay, jàppandig wala ñàkk dag-dag gi wara am ci jëfandikoo ngi ngay def ci Cortana. Yoonu Microsoft nekkul ci yeexaayu man-manu saytu jokkoo yi ngay amal ci Cortana wala yeexaay bi dila tere jot wala yónnee ay jokkoo wala yëgle.
    • iii. Cër ak Jëfekaayi Jàmbur. Soo naree am ci Cëri Cortana, Cortana mën na weccoo ay leeral ak Cër ak Jëfekaayi Jàmbur, lu ci melni sa kot postaal ak laaj ak tontu yi Cër ak Jëfekaayi Jàmbur joxe, ngir nu mën laa jox li ngay laaj. Cig lëkkalante sàq, Cortana mën na may jëfandikukat ñu jëndee ci Cër ak Jëfekaayi Jàmbur suñu jëfandikoo taamuy jëfandikukat bi ak jekkal yi mu amal ci yooyu Cër ak Jëfekaayi Jàmbur. Jëfandikukat yi mën nañu dakkal lëkkalanteg sàq mi saa yu nekk. Sag jëfandikoog Cër ak Jëfekaayi Jàmbur a ngi tënku ci pàrti 5 yu Sàrt yii. Siiwalkati Jëfekaay ak Cëri Jàmbur yi mën nañu soppiku wala dakkal ni ñuy doxee wala seeni man-man, ñeel Cër ak Jëfekaayi jàmbur wala boole gi ci Cëri Cortana. Yoonu Microsoft nekkul ci wóoraayu losisel wala jumtukaay bu liggéeykat yi defar.
    • iv. Jëfandaayi Cortana yiñ Nangu. Jëfandaay yi Cortana doxal, ñooy costéef wala jëfandaay yi ñuy taal ngir mëna jëfandikoo Cëri Cortana, wala costéef wala jëfandaay yi mëna ànd al Cëri Cortana. Cortana dafay nangu costéef wala jëfandaayi jàmbur yu Microsoft moomul, defarul, wala siiwalul. Yoonu Microsoft nekkul ci yooyu jëfandaay wala costéefi jàmbur.
    • v. Yeesali Losisel. Ngir bépp jëfandaay bu mën a lënku ci Cëri Cortana, mën nanu seet ci saasi sumbu losiselu Cëri Cortana bi nga yor ba noppi yebbi yeesali losisel wala coppiteg tabb wala sàkku ci képp kuy defar jëfandaay yu Cortana di nangu ngir muy yeesal cëri Cortana saa yu nekk.
Jukki bu fees
Outlook.comOutlook.com14h_Outlook_com
Tënk
  • h. Outlook.com. Outlook.com (mbaa @msn, @hotmail, walla @live) dëkkuwaayu m-bataaxal bi ngay jëfandikoo ngir sos sa sàqum Microsoft benn lay doon fii leek sa boyetu bataaxalu Outlook.com mbaa sa sàqum Microsoft di wéy di dox. Sudee yaw yaa tëj sa boyetu bataaxalu Outlook.com mbaa sa sàqum Microsoft walla Microsoft mooko tëj ci li topp ci yile Sàrt, mën nañu defaraat dëkkuwaayu m-bataaxal bi ci ab noste te jox ko beneen jëfandikookat.
Jukki bu fees
Cëri OfficeCëri Office14i_officeBasedServices
Tënk
  • i. Cëri Office. Office 365 Home, Office 365 Personal, Office 365 University, Office Online, Sway, OneNote.com ak yeneen bindu yi ci Office 365 wala Cëri yi am màrku Office mënoo leen jëfandikoo ludul ngir sa bopp, doo ko jaay, fileek Microsoft joxu la ci ndigal lu la koy may
Jukki bu fees
Liggéeyali Microsof HealthLiggéeyali Microsof Health14j_MicrosoftHealthServices
Tënk
  • j. Liggéeyali Microsof Health.
    • i. HealthVault. Defar nañu HealthVault ngir nga mën a denc ay leeral yu àju ci sa wergu-yaramu bopp ak leeral yu àju ñeneen (niki sa njaboot) suñ ko nangoo. Joxekatu Wergu-yaram mbaa bépp jubluwaayu jaay walla jagoo waru ñu jëfandikoo sàqi HealthVault. Leeral yu nekk ci sa sàq mën nañu baña jàppandi mbaa bees saa su nekk te bépp joxekatu wergu-yaram war na leen xool ngir jumbluwaayu leeral kase. Cëri HealthVault yorul ay dënku joxekatu wergu-yaram mbaa yeneen jubluwaayu saytu pàj mbaa ay. Maanaam, këyiti HealthVault yi jàppeewu ñu leen ay mbooleem dënk ci niko sàrti Etaa-Sini tëralee. Sudee ab joxekat wergu-yaram dogalee dugal bépp njoxe buñu maye ci HealthVault ci biir ay dënkam, war na denc ab sotti ci biir nostey boppam. Sudee dafa am ab depositeeru dënk bu bokk ci sa sàq (ndax kenn ci yaw dafa dalal ñeeneen), nangu nga ni depositeer bi mën na amal saytu bu mat ci dënk boobu te mën na fomb sa dugg ci dënk bi, saytu duggu yeneen nit ci dënk bi, te gos njoxey dënk bi bokk na ci nan ak kañ lañuy jëfandikoo dënk bi. Microsoft nanguwul xibaaru ràññeekaay yu bokkul ci Microsoft (niki Facebook ak OpenID), ba tax na aji-jëfandikoo HealthVault duñu mën a tax nga mën bindu jafe-jafe yu ñeel yooyu. Soo reeralee say xibaaru ràññeekaayu dugg, mbaa sàq bi nga amee say xibaaru ràññeekaay tëju, doo mën indiwaat njoxe yi nga dencoon. Ngir wéy di mën a dugg, ñu ngi lay digal nga jëfandikoo ay xibaaru ràññeekaay yu bati ak sa sàqu HealthVault. Microsoft du jàppale mbaa saytu, te waralul, jëf ji, ndimbal li, mbaa kaaràngeg ràññeekaay yi bokkul ci Microsoft yi nga mën a jëfandikoo.
    • ii. Microsoft Band. Jëfandaay ak jëfekaayi Microsoft Band yi duñu ay jumtukaay yuy faj te seen njariñ du lenn ludul ngir toppatoo ak defar sa yaram. Kenn defaru leen ngir saytu ak seet, faj ak càmbar ay feebar wala yeneen anam, jublu wuñu itam fàggu, nasaxal ay jàmgoro wala yeneen mbir. Yoonu Microsoft benn dogal bi ngay jël fekk nga sukkandiku ci leeral yoo jotee ci Microsoft Band.
Jukki bu fees
Marsandiisu XaralaMarsandiisu xarala14k_DigitalGoods
Tënk
  • k. Marsandiisu xarala. Ci Microsoft Groove, Microsoft Filmu yi ak Tele, Store ak yeneeni liggéeyal yu ñu boole yiy ñëw, Microsoft war na mën a am, déglu, xool, taal wala jàng (ak lu mbir mi mën a doon) misig, nataal yi, wideo, jukki, téere, po wala mbiri ("Marsandiisu Xarala") yi nga mën a jot cig tëggiinu xarala. Marsandiisu Xarala yi ngir sag jëfandikoo doŋŋ la, àndul ak njaay. Nangu nga ne doo séddalewaat, tasaare, wax ci mbooloo wala wone, mbaa jàllale bépp sottiy Marsandiisu Xarala. Marsandiisu Xarala yi mën nañu doon yosu Microsoft wala yu bawoo feneen. Ci anam yépp, nànd nga te nangu ni say àq ci lu aju ci Marsandiisi Xarala Sàrt yii ñoo leen yemale, yoonu àqi-Sos ak sàrtu jëfandikoo bi nekk ci https://go.microsoft.com/fwlink/p/?LinkId=723143. Nangu nga ni doo jéem a soppi benn Marsandiisu Xarala bu ñu jëlee ci Liggéeyal yi ngir sabab bu mu mën a doon, bokk na ci jubluwaayu feeñal wala soppi moomeel mbaa cosaanu Marsandiisu Xarala. Microsoft wala ñi moom Marsandiisu Xarala yi mën nañu, yenn saa, dindi Marsandiisu Xarala yi ci Liggéeyal yi te duñu ko yëgle.
Jukki bu fees
OneDriveOneDrive14l_OneDrive
Tënk
  • l. OneDrive.
    • i. Dencukaay bi la Jox. Soo amee ay këmb yu ñu denc ci sa sàqu OneDrive yu ëpp yu ñu la jagleel ci say sàrti liggéeyalu bindu yoo dul fay wala yi ngay fay ngir OneDrive te tontuwoo ci yëgle yu bawoo ci Microsoft ngir saafaraal sa sàq wàññiwaale sa feesaayu këmb mbaa tuxal la ci beneen palaŋu mbindu bu gën a yaatu, am nanu sañ-sañu tëj sa sàq te far wala tere la dugg ci sa Këmbu OneDrive.
    • ii. Xarañaayu Liggéeyal. Mu ngi aju ci anam yu demee ni say jumtukaay, jokkoo internet ak li Microsoft di jéem gën a dëgëral xarañaay bi ak dëggal liggéeyalam, mën nga am yenn saa ngay jànkkonteek ay yeexaay sooy sotti wala lëkkale këmb ci OneDrive.
Jukki bu fees
Neexali MicrosoftNeexali Microsoft14m_MicrosoftRewards
Tënk
  • m. Microsoft Rewards.
      • i. Tëriin. Neexali Microsoft ("Tëriin" wi) dalay maynga gañe ay poñ ci li ngay liggée, lu ci melni seet gu xarañ, moomeel yi,waxtu yi nga def ci jëfandikoo Microsoft Edge, ak yeneen xéewal yu Microsoft. Xéewal yaa ngi aju ci marse bi. Buñ nee seet mooy ngay jël ay baat bind leen ci Bing ngir am ci ay njuréef yu jëm ci li ngay seet kese te du ñu ci boole beneen njuréef bu bawoo ci seetug bot, makro, wala yeneen xeeti roboo wala xeetu ("Seet") bu jaarul yoon. Moomeel moo nga jënd ay ëmbiiti disitaal wala nga yebbi sañ-sañ yu la koy may ci Microsoft, mën na nekk ("Moomeel") buñ la may wala buñ la jaay. Poñi neexal yi nak, du ci lépp loo jëndee ci Microsoft rek am leen. Di xuus bu baax ci Microsoft Edge mooy tekki ni xuuskat baa ngi feeñ ci sa seetu jëfandaay (maanaam, nga ubbi ko di ko jëfandikoo, lu ci melni junju Microsoft Edge di feeñ ci laatu liggéey yi, muy firndéel ni ñu ngi jëfandikoo jëfekaay bi), te yaa ngi jëfandikoo xuuskat bi ngir dugg ci ay daliweb, di seetaan ay wideo ci xuuskat bi, jàng say bataaxal, wala yeneen jëfandikoo yooy jëlee xuuskat bi. Ngir gañe ay poñ sooy jëfandikoo Microsoft Edge, fàww nga tànn Bing muy sa xuuskat bi fiy nekk di sa seetukaay te fàww nga taal telemetri bi ci say jekkali Windows. Yennn saa Microsoft mën nala may yeneen pexe yooy mëna gañee ay poñ, te danga wara xamni poñ yiñ la may duñu fi nekk ba fàww. Mën nga wecci poñ yi nga gañe aki ëmbeef ("Neexal") ci xët wiñ leen di weccikoo. Ngir am ci yeneen leeral demal ci pàccu Neexal yi ci support.microsoft.com ("LFÑ").
      • 1. Càkkutéefi Tëriin yi. Fàww nga am sàqum Microsoft muy dox te fàww sa jëfandaay am càkkutéefi sistem biñ koy laaj. Ñi ñu jagleel tëriin wi mooy jëfandikukat yi dëkk ci marse yi bokk ci lim bi ci LFÑ. Kenn nit mënul bokk lu weesu benn Tëriin, naam daa am dëkkuwaay yu bari, te kër gu nekk warul weesu juróom benni sàq. Tëriin wi yaw kese yaa ko moom te waroo ko jaay.
      • 2. Poñ yi. Mënoo maye say poñ fileek ñi nga koy may du mbootaay boo xamni wutum xaalis taxu leen jog. Poñ yi duñu say moomeeli bopp, te mënoo leen jël wecci leen ñuy xaalis xobbet. Ci promo kese nga mëna amee poñ yi. Kenn mënul jënd poñ yi. Microsoft mën na àppal say limi poñ wala Neexali nit ku nekk, kër gu nekk, wala cib diir buñ tànn ( ci misaal, benn bis). Mën nga wecci lu tollu ci 550 000 poñ at mu nekk ci Tëriin wi. Poñ yi nga amee ci tëriin wi mënu ñu dox ci, te mënoo ko jëfandikoo ci, beneen xeetu tëriin bu Microsoft wala ab jàmbur moom. Say àppi poñ dañuy jeex sudee danga toog 18 weer te wecci woo leen wala amoo yeneen poñ.
      • 3. Neexal yi. Soo bëggee wecci say poñ dangay dem ci barabu weccikaay bi wala nga jël say poñ sarax ko mbootaay buy defal Yàlla. Mën na am yeneen xeetu neexali yu mëna jàppandi, te yooyu neexal ñu ngi leen jagleen ñiy njëkka ñëw. Séddale, taamu nañu ci kuddu yu njëkk ya. Mën nañu la laaj nga joxe yeneen leeral, lu ci melni sa dëkkuwaayu bataaxal ak sa nimero telefon (lu bokkul ak ab VOIP wala nimero woote bu amul fay), mën nañu la laaj itam nga dugal kot bu tere ñu sàcc la wala ngir xaatim yeneen wayndare ci yoon ngir wecci ay poñi Neexal. Ginaaw boo sàkkoo ab Neexal, mënatoo ko bàyyi wala nga delloo ko ngir jotaat say poñ fileek yàqute amul ci costéef biñ la jox wala fileek yoon santaane wu ko. Sudee danga sàkku ab Neexal boo xamni amatul wala Microsoft ni amatul te joxe wu ci leeral, mën nanu la weccil Neexal boobu ak lu mu tollool wala nu delloo la say poñ. Microsoft mën na yeesal Neexal yiñ la mayee ci barabu weccikaay bi wala dakkal ko ngir jox la yeneen Neexal. Mën nañu sàkku nga am yenn at yi ngir am ci yenn neexal yi. Càkkutéef yu ni mem dañuy àndaale ci càkkutéefi mën bokk yi. Yaa wara fay lépp luy juuti bu bawoo sa gox, diwaan, komin, wala bépp xeetu taks buñ lay laaj ci Neexal yi. Dina ñu la yónnee Neexal yi ci dëkkuwaayu bataaxal bi nga joxe bi ngay sàkku Neexal, kon yeesalal sa dëkkuwaayu bataaxal. Kenn du delloo Neexal yiñ mënul joxe, te kon danga leen di ñàkk ba fàww. Neexal yi kenn du leen jaayaat.
      • 4. Dakkal Sa Bokk ci Tëriin wi. Dina ñu dakkal sa sàqu Tëriin wi soo toogee diir bu tollu ci 18 weer te duggoo ci benn yoon. Rax ci dolli, Microsoft moom rekk a am sañ-sañu dakkal sàqu Tëriinu jëfandikukat bu njuuj-njaaj, wala muy def naka sudul noonu ci Tëriin wi, wala muy jalgati Sàrt yi. Suñu dakkalee Tëriin wi (yaw wala nun) wala sudee dañu ko ajandi, dina ñu la may 90 fan ngir nga wecci say poñ; lu ko moy nga ñàkk say poñ ba fàww. Ginaaw buñ ko dakkalee, dootoo amati sañ-sañu jëfandikoo Tëriin wi te doo amati ay poñ.
      • 5. Yeneen Anam. Microsoft rekk a am sañ-sañu génn la ci; te la jëfandikoo Tëriin wi wala sa sàqu Neexal yi; ak/wala nangu say poñ, Neexal ak poñ yi nga maye, su Microsoft jàppee ni dangay jéema njuuj-njaaj, wala muy def naka sudul noonu ci Tëriin wi, wala muy jalgati Sàrt yi.
Jukki bu fees
MiselanisMiselanis16_17_18_miscellaneous
Tënk

14. Miselanis. Pàcc bii, ak pàcci 1, 9 (ngir xaalis yi nga am laata Sàrt yi di jeex), 10, 11, 12, 15, 17 ak yeneen yi seeni sàrti bopp di dox ginaaw bu Sàrt yii jeexee dina ñu mucc ginaaw buñ dakkalee Sàrt yi. Ba ni ko yoon yuy jëfe nangoo, mën nañu jaglel yile Sàrt, liggéey ak ñeneen suñuy moomeel ci kaadaru yile Sàrt, mbaa séddale sañ-sañu suñuy àq ci kaadaru yile Sàrt, ci lépp mbaa xaaj, saa su nekk te duñu la ko yëgal. Mën nga baña jaglel mbaa jébbal yile Sàrt been àqi jëfandikoo Cër yi. Lii mooy déggoo bu matale ci sa digante ak Microsoft ngir li ngay jëfandikoo Cër yi. Dafay wuutu bépp déggoo bu jiitu ci sa digante ak Microsoft ci li àju ci li ngay jëfandikoo Cër yi. Sooy dugg ci yile Sàrt, doylo wulo benn nettali, teewal, garanti, nandite, liggéeyal, diggé mbaa wóoraay bu bokkul ak nuñ ko tërale ci yile Sàrt. Xaaju sàrt yépp dañuy jëfe ci dayo bu ëpp bu yoon bu jubu maye. Sudee ab atekaay mbaa atekat dafay dëgëral ni mënu ñu doxal ab xaaju yile Sàrt yuñu bind, mën nañu wuutal yooyu sàrt ak ay sàrt yuko nduru ci dayoo buñu mën a doxal ci kaadaru yoon bu jubu bi, waaye sàrt yi duñu soppeeku. Yile sàrt yaw ak say njuréef kase ñoo leen taxa jog/ Tëralu ñu yile sàrt ngir njuréefu beneen nit, ludul ngir aji-donn ak ndawu Microsoft yi. Boppu pàcc yi ngir sukkandikukaay kase lañ fi nekkee ta amu ñu benn jeexitu yoon.

15. War nañu yónnee jéebaane yi ci digante Benn At. War nañu yónnee bépp jéebaane bu méngook yile Sàrt mbaa Cër war ci atekaay bi (mbaa ate sudee pàcc 10 (d) mooy jëfe) ci digante benn at bawoo ci bis gi nga njëkk a yónnee jéebaane bi, ludul sa yoonu barab laaj ab diir bu gën a yàgg ngir yónnee ay jéebaane. Soko yónneewul ci diir boobu, di nañ ko dàkkal ba fàww.

16. Yooni toxal. War nga dëppook bépp yoonu toxal bitim réew ak sàrt buy jëfe ci losisel bi ak/mbaa Cër, bu àndak ay yemale mbaa jëmuwaay, jënfandikookatu njextal, ak jëfandikoo bu mujj. Ngir am yeneeni leeral ci ay yemale barablin ak toxal, yëral https://go.microsoft.com/fwlink/?linkid=868968 ak https://www.microsoft.com/exporting.

17. Denculuy Yelleef ak Joxe xalaat. Ci anam wiñ ko leeralee ci Sàrt yi, Microsoft du jox kenn ab sañ-sañ wala beneen xeetu yelleef ci xeet bumu mën a doon ak sabab bumu mën a doon, xam numu demee, àqu yelleef, sekkerey njaay, màrk wala yeneen moomeeli xel wala yu Microsoft saytu wala beneen liggéeyukaay bu mu àndandool, boole ci bépp tur, njaay, logo wala lumu méngool. Soo baaxee sa xalaat bumu mëna doon Microsoft, digle, laabire wala wax-sa-xalaat, boole, te dufa ca yam, lu ci melni ay gis-gis ci costéef bu bees, xarala, promo, turi costéef, wax-sa-xalaat ci costéef ak gëna baaxal costéef ("Wax-sa-xalaat"), may nga Microsoft, te doo ko ci fayyeeku lenn, te itam doo ci xaar benn xeetu dàmpaay, yelleefu defar, defar ba noppi, sos liggéey yu ci juddoo, jëfandikoo, séddoo ak jaay Wax-sa-xalaat ci anam wu nekk, ak lumu ci mëna jublu. Doo fi joxe Xalaat bu ëmbu ci ab sañ-sañ bu laaj Microsoft ci jox sañ-sañ ci ab losisel, xarala wala ay wayndare ci bépp jàmbur ndax Microsoft boole ci say Xalaat ci ñoom.

Jukki bu fees
KARMAT YIKARMAT YINOTICES
Tënk

Karmat yi ak doxaliinu amal ay jéebaaneg jalgati àqi moomelu xalaat. Microsoft nangu na àqi moomeelu xalaatu xaaj yu bawoo feneen. Soo bëggee yónnee ab karmatu jalgati moomeelu xalaat, bokk na ci jalgati ay jéebaaneg Àqisos, baal ñu jëfandikoo suñuy doxalin ngir jébbal Karmatu Jalgati. LAAJ YI JËM TE MËN A BOKK CI WÀLL WII KESE LAÑUY TONTU.

Microsoft dafay jëfandikoo doxalin yuñu lim ci Turu bopp 17, Kotu Etaa-sini, pàcc 512 ngir tontu ci karmatu jalgati Àqisos yi. Ci xew-xew yumu méngool, Microsoft mën na dakkal itam mbaa tëj sàqu jëfandikookatu cëri Microsoft yu mën a doon ay jalgatikatu baamtu.

Karmat yi ak doxalin yu méngook mbiri àqi moomeelu xalaat ci siiwal. Baal ñu topp suñu Gindiy Àqi Moomeelu Xarala yu méngook mbiri àqi moomeelu xarala suñu mbaalu siiwal.

Àqisos ak karmati màndarga. Cër yi ñooy copyright © 2018 Microsoft Corporation ak/mbaa ay joxekat am, One Microsoft Way, Redmond, WA 98052, Etaa-Sini. Jagoos na mboolem sañ-sañ yi. Microsoft ak tur, raaya ak njunji cŝtéef, losisel ak cëri Microsoft yépp mën nañu doon ay màndarga mbaa màndarga Microsoft yu bindu ci Etaa-Sini ak/mbaa yeneeni réew. Turi këru liggéey ak costéef yi mën nañu doon màndargaay seeni borom. Jagoos na bépp àq buñu joxewul ci wax ci yile Sàrt. Yenn losisel yuñuy jëfandikoo ci daluwebu cërakooni Microsoft ñu àju ci xaaj ci liggéeyu Kuréelu JPEG bu Moom Boppam. Copyright © 1991-1996 Thomas G. Lane. Jagoos na mboolem sañ-sañ yi. Losiselu "gnuplot" buñuy jëfandikoo ci yenn daluwebu cërakoonu Microsoft mooy copyright © 1986‑1993 Thomas Williams, Colin Kelley. Jagoos na mboolem sañ-sañ yi.

Karmatu wergu yaram. Microsoft du joxe benn digal, gëstu mbaa faju mbaa benn paj bumu mën a doon. Dëkkeel di laaj sa doktor ay digal mbaa yeneen joxekatu wergu yaram yu xarañ ak bépp laaj bi nga mën a am ci li aju ci ab tolluwaayu wergu yaram, resim, tëriinu wer ak tal. Bul xeeb mukk digalu doktor walla yeex ci gis ko ndax leeral yi nga duggoon walla ci biir Cër yi.

Dawalinu aksiyoŋ yi ak njoxey àlluwa (bokk na ci xayma àlluwa). © 2013 Morningstar, Inc. Jagoos na mboolem sañ-sañ yi. Leeral yuñ ëmb fii: (1)moomeelu Morningstar la ak/mbaa ay joxekati këmbam; (2) mën nañ ko baña sotti mbaa séddale; ak (3) garanyiwuñuko ngir mu jub, mat te gaaw. Déet Morningstar déet ay joxekatu këmb am yoru ñu kiliftéefu yàqute yi mbaa ñàkk yiy bawoo ci bépp jëfandikoo yile leeral. Këru-manéef yu mujj du garanti benn njuréef buy ñëw.

Waruloo jëfandikoo benn ci Àlluway Dow JonesSM, njoxey àlluwa, mbaa màndarga Dow Jones yi cig lëkkalook defar, sos, baayale, njënd ak njaay, jaay, mbaa marketing, mbaa fësal bépp jumtukaayu kopooral mbaa costéefi alalal (maanaam, costéefi yuñu tëggaat, xaalisi alalal, xaalisi wécceeku, kalpey mbebët yi alalal, ak yeneen, fu njëg bi, delloo ak/mbaa këru manéefu jumtukaay mbaa costéefu alalal sukkandikoo, méngoo, walla bu jëmoon ci topp àlluwa yépp mbaa proksi ngir àlluwa yépp yu àndul ak beneen déggoog Dow Jones buñu bind.

Karmatu alalal. Microsoft du ab indikat/jaaykat mbaa laabirekatu alalal bu bindu ci sàrti yooni atekaayu aksiyoŋu réewu federaal bu Etaa-Sini te du digal nit ñi ci ndiglaayu alalal ko, jënd ko mbaa jaay aksiyoŋ yi mbaa yeneen cër mbaa costéefi alalal. Lenn lu nekk ci cër yi du ab maye mbaa càkkutéef ngir jënd mbaa jaay ab aksiyoŋ. Déet Microsoft déet ay ñi yor sàñ-sàñu dawaliinu aksiyoŋ yi mbaa njoxey àlluwam jàppale mbaa digle bépp costéefi xaalisal mbaa cër bu xejjiku. Amul lenn lu bokk ci Cër yi luñu mën na jëfandikoo ni tegtali liggéey, lu ci melni dugal xaalis wala taks yi.

Karmat bu àju ci H.264/AVC, MPEG-4 Visual, ak Baaxoo Wideo VC-1. Losisel bi mën na am H.264/AVC, MPEG-4 Visual ak/mbaa xaralay Codec VC-1 bu MPEG LA, L.L.C. mën a jox sàñ-sàñ. Xarala bii ab tëggiinu ngir laxas ay njoxey leerali wideo. MPEG LA, L.L.C. dafay laaj karmat bii:

JAGLEL NAÑU COSTEEF BII CI KAADARU H.264/AVC, MPEG-4 VISUAL, AK SÀÑ-SÀÑU KALPEY VC-1 PATENT NGIR JËFANDIKOO JAGOO AK JËFANDIKOO AB AJI-JËFANDIKOO CI (A) FAS WIDEO CIG DËPPOOK BAAXOO YI ("BAAXOO WIDEO") AK/MBAA (B) FECCI H.264/AVC, MPEG-4 VISUAL, ak VC-1 VIDEO BU AB AJI-JËDANDIKOOKAT FAS CI AB JËFU JAGOO MBAA BU JAAYUL AK/MBAA ÑU AMEE KO CI AB JOXEKATU WIDEO BUÑU JAGLEL SÀÑ-SÀÑ NGIR JOXE BOOBU WIDEO. BENN CI SÀÑ-SÀÑ YI DU YOKK BENEEN COSTÉEF MOO XAM NDAX BOOLE NAÑU YILE COSTÉEF BOKK NAÑU CI LOSISEL BII CI BENN MBOOT. JOXE WUÑU BENN SÀÑ-SÀÑ WALLA WAR NAÑ KO NJORT NGIR BENEEN JËFANDIKOO BUMU MËN A DOON. MËN NAÑU JOT YENEENI LEERAL CI MPEG LA, L.L.C. YËRAL DALUWEBU MPEG.

Ngir jubluwaayu leeral kase, karmat bii du yemale mbaa tere jëfandikoo losisel buñu joxe ci kaadaru yile Sàrt ngir ay jëfandikoo liggéey yu jaadu yu liggéey boobu boolewul (i) séddalewaat losisel bi ci xaaj yu bawoo feneen, mbaa (ii) sos ay daju ak xarala BAAXOO WIDEO yu mu nangu ngir séddale ko ci xaaj yu bawoo feneen.

Jukki bu fees
SÀRTI SÀÑ-SÀÑU JËFEKAAY BU BAAXOOSÀRTI SÀÑ-SÀÑU JËFEKAAY BU BAAXOOSTANDARDAPPLICATIONLICENSETERMS
Tënk

SÀRTI SÀÑ-SÀÑU JËFEKAAY BU BAAXOO

MÀNGASIINU MICROSOFT, MÀNGASIINU WINDOWS, AK MÀNGASIINU XBOX

Sàrti sàñ-sàñ yii ay déggoo lañu ci sa digante yaw ak siiwalkatu jëfekaay bi. Baal ñu jàng leen. Ñooy jëfekaayi losisel yi ngay yebbi ci Màngasiini Microsoft, Màngasiinu Windows wala Màngasiinu Xbox (ñuy woowee ku nekk ci ñoom ci sàrti sañ-sañ bi "Màngasiin"), ñu boolewaale ci bépp yeesal wala lu yokk ci jëfekaay bi, fileek jëfekaay bi àndul ak yeneen sàrt, su boobaa yooyu sàrt lañuy doxal.

SOOY YEBBI MBAA JËFANDIKOO JËFEKAAY BI, MBAA NGAY JEEMA DEF BENN CI YILE, NANGU NGA YILE SÀRT. SUDEE NANGU WOO LEEN, YOON MAYU LAKO TE WARULOO YEBBI MBAA JËFANDIKOO JËFEKAAY BI.

Siiwalkatu jëfekaay bi mooy wàll wi la jox sañ-sañu jëfekaay bi, leeral nañu ko ci màngasiin bi.

Soo dëppook yile sàrti sàñ-sàñ, yoon may nala nga def yii ci suuf.

  • 1. SAMP TE JËFANDIKOO ÀQ YI; ÀPP. Mën nga samp ak jëfandikoo jëfekaay bi ci jëfandaayi Windows wala jumtukaayi Xbox, ci niñ ko waxee ci Sàrti Jëfandikoo yu Microsoft. Microsoft amna sañ-sañu soppali Sàrti Jëfandikoo yi saa yu ko neexee.
  • 2. CËRI INTERNET YI.
    • a. Nangu ngir cëri internet mbaa cër yu amul buum. Su jëfekaay bu lonjee nostey ordinatëer bi ci Internet, bu mën jaare ci ab mbaal bu amul buum, di jëfandikoo jëfekaay bu dox niki sa nangu ci jàllale leerali jëfandaay yu baaxoo (bokk na ci waaye yemul ci leerali xara yu àju ci sa jëfandaay, noste ak losiselu jëfekaay, ak periferik yi) ngir cër internet ci mbaa cër yu amul buum. Sudee dafa am yeneeni sàrt yu teew di lëkkalook ni ngay jëfandikoo cër yi nga dugg di jëfandikoo jëfekaay bi, yooyu sàrt dañuy jëfe itam.
    • b. Jëfandikoo cëri internet bu baaxul. Waruloo jëfandikoo benn cëru internet ci benn anam bu mën a lor mbaa laal doxiinu jëfandikoo kumu mën a doon mbaa mbaal bu amul buum. Waruloo ëfandikoo cër bi ngir am sàñ-sàñu dugg ci bépp cër, njoxe, sàq, mbaa mbaal ci anam bumu mën a doon.
  • 3. MANEEFU SÀÑ-SÀÑ. Dañu jox jëfekaay bi sàñ-sàñ, jaayu ñu ko. Déggoo bii yenn àqi jëfandikoo jëfekaay bi kase la lay jox. Su Microsoft dakkalee man-manu jëfandikoo jëfekaay yi ci say jëfandaay ci li àju ci sa déggoog Microsoft, bépp àqi sàñ-sàñ bumu méngool dina jeex. Ki siiwal jëfekaay bi moo yelloo yeneen sañ-sañ yépp. Ludul yoon buy jëfe jox la yeneeni àq ak bii yemale, war nga jëfandikoo jëfekaay bi suñ ko nangoo kase ci waxiin ci déggoo bii. Sooy doxalee nii, war nga nangu bépp yemale xarala ci jëfekaay buy tax nga mën ko jëfandikoo ci yenn anam. Waruloo:
    • a. Jalgati benn yemale xarala ci jëfekaay bi.
    • b. Safaane defar, booledi, mbaa tasaare jëfekaay bi, budul te ci dayo bu yoon yu jëfe nangu ci waxiin, donte am na yemale.
    • c. Defar ay sotti jëfekaay yu bari yuñu xamle ci déggoo bii mbaa yu yoon buy jëfe nangu, donte am na yemale.
    • d. Siiwal mbaa defar ci neneen jëfekaay yu jàppandi ngir ñi mën a sotti.
    • e. Luwe, mbaa abale jëfekaay bi.
    • f. Jox jëfekaay bi wala déggoo bi ab jàmbar.
  • 4. JUKKIB NDIMBAL. Suñu joxe jukkib ndimbal bi ak jëfekaay bi, mën nga sotti te jëfandikoo jukkib ndimbal bi ngir jubluwaayi delluwaayu jagoo.
  • 5. XARALA AK YEMALEY TOXAL. Jëfekaay bi mën na laaj saytu Etaa-Sini mbaa xarala bitim réew mbaa yooni toxal ak sàrt yi. War nga dëppook bépp yoonu toxal bitim réew ak sàrt buy jëfe ci xarala buñu jëfandikoo mbaa bu jëfekaay bi nangu. Yile sàrt dañuy àndak ay yemale ci jëmu yi, jëfandikookat yu ci mujj, jëfandikoo bu mujj. Ngir am yeneeni leeral ci costéef yu Microsoft màndargal, demal ci daluwebu toxal Microsoft.
  • 6. CËRI NDIMBAL YI. Jokkool ak siiwalkatu jëfekaay bi ngir xamle cëri ndimbal yu jàppandi. Microsoft, sa defarkatu daju ak sa joxekatu cër yu amul buum (ludul benn ci ñoom doon siiwalkatu jëfekaay bi) yoru ñu kiliftéefu joxe ay cëri ndimbal ngir sa jëfekaay.
  • 7. MBOOLEEM DÉGGOO. Déggoo bii, bépp Biralug Kumpa buy jëfe, bépp sàrt bu ci dolleeku buy ànd ak jëfekaay bi, ak sàrt yu ñeel ngir mottali yi ak yeesal yi ñooy mbooleem déggoo diggante yaw ak siiwalkatu jëfekaay bi ñeel jëfekaay bi.
  • 8. YOON BUY JEFE.
    • a. Etaa-Sini ak Kanadaa. Sudee ci biir Etaa Sini wala Kanada nga nga wutee jëfekaay bi, yoon yiñ tëral ci réew moomu wala ci gox bi nga dëkk (wala, sudee ab liggéeyukaay, wala fi sa liggéey bi gëna mag nekk) ñooy dogal niñ wara déggee déggoo bii te ñooy wax itam ndax jalgati amna ci am déet, ak yeneen jàmbat (lu ci melni kaaraange jëfandikukat bi, joŋante bu jaadiwul, ak jàmbatug yàqule) xoolu ñu ci yoon yu wuute am déet.
    • b. Ci biti Etaa-Sini ak Kanadaa. Sudee ci beneen réew nga amee woon jëfekaay bi, yooni réew boobu mooy jëfe.
  • 9. JEEXITU YOON. Déggoo bii dafay xamle yenn àqi yoon. Mën nga am yeneen àq yu aju ci sa yooni dëkk mbaa réew. Déggoo bi du soppi say àq yu àju ci sa yooni dëkk mbaa réew sudee say yooni dëkk mbaa réew maye wul nga def lu ni mel.
  • 10. BEDDIINU GARANTI. Jaglel nañu sàñ-sàñ bi "niki numu mel", "ak njuumte yépp" ak "numu jàppandee". Gàddu nga ci sa bopp lorange jëfandikoo ko. Siiwalkatu jëfekaay bi, ci turu boppam, Microsoft (Sudee Microsoft nekkul siiwalkatu jëfekaay bi), cër yu amul buum ci kaw mbaal buñu joxewul, ak bépp bànqaas bu lay teewal, jaaykat yi, ndaw yi ak joxekat yi ("Xaaj yuñu Ëmb"), joxewul benn garanti buñu waxe, mbaa anam bu méngook jëfekaay bi. Loraange bu matale bu wone fi baaxaay, kaarange, dalal, ak xarañu jëfekaay toll ci yaw. Sudee jëfekaay bi dafa yàqu, nangu nga njëg bu matale bu cërale mbaa saafarra bi laaj. Mën nga am yeneen àqi àji-jëfandikoo ci kaw say yooni barab ni yile déggoo mën nañ soppeeku. Ci dayo bu ëpp bu ñu nangu ci sa kaadaru sa yoonu réew, dañuy dàq bépp gaaranti bu nëbbu, bokk na ci mëniinu njaay, baaxaayu lu ñu mën a nangu, jekkal ngir jubluwaay bu xejjiku, kaaraange, dalal ak ñàkk luubal.
  • 11. YEMALE AK DÀQU SAAFARA AK YÀQUTE YI. Ci dayo bu yoon nanguwul, soo bépp sukkandikaay ngir dabuwaat yàqute yi, mën nga dabuwaat ci yàqute yu jub bu siiwalkatu jëfekaay ba ci tolluwaayu xaalis bi nga fayoon ngir am jëfekaay bi mbaa USD$1,00, bi nga xam ni moo gën a rëy. Doo to, te amul benn àqi, jéema dabuwaat benn coppite, bokk na ci lorange, njuréef yi nga ñàkk, xejjiku, jubadi mbaa buy indi xew-xew yuy yàq ci siiwalkatu jëfekaay bi. Sudee say yooni barab dañuy impoose garanti mbaa anam donte yile sàrt duñu ko def, yàgaayam mu ngi yem ci 90 bis ci bi nga waree yebbi jëfekaay bi.

Yemale bii dafay jëfe ci:

  • Lépp lu méngook jëfekaay bi mbaa cër buñu jàppandal ci jëfekaay bi; ak
  • Jéebaaneg jalgati déggoo, garanti, mbaa anam, kiliftéf bu tar, ñàkk a xoromal, mbaa beneen buko waral, jalgati ab tolluwaay mbaa sàrt; alal bu lewul; mbaa ci kaadaru bépp xalaat, dayo yépp yu yoon buy jëfe nangu.

Dafay jëfe itam donte:

  • Saafara bi du la fay ci matale li nga ci ñàkk yépp; mbaa
  • Siiwalkatu jëfekaay bi xàm na mbaa waroon na xam darra ci jafe-jafe yu ci mën a am.
Jukki bu fees
Cëri yi mu ëmbCëri yi mu ëmbserviceslist
Tënk

Yile costéef, jëfekaay ak cër la Déggooy Cëri Microsoft ñoo ko ëmb, waaye mën na bàña jàppandi ci sa marse.

  • Account.microsoft.com
  • Advertising.microsoft.com
  • Arrow Launcher
  • Baatukaayu Bing
  • Bing Bots
  • Bing ci kalaas bi
  • Bing Torque
  • Bing Translator
  • Bing Webmaster
  • Bing.com
  • Bing
  • Bingplaces.com
  • Biro Bing
  • Citizen Next
  • Conditional Action Programmer
  • Cortana skills by Microsoft
  • Cortana
  • Default Homepage and New Tab Page on Microsoft Edge
  • Dev Center App
  • Dictate
  • Docs.com
  • Dugaliinu Bing
  • education.minecraft.net
  • Forms.microsoft.com
  • forzamotorsport.net
  • Groove Music Pass
  • Groove
  • GroupMe
  • HealthVault
  • Jàngkatu Bing
  • Jëfekaayi Bing
  • Jëfekaayu Kàrt yi
  • Jëfekaayu seet Bing
  • Jëfekaayu Wergu yaramu Jëfandaay
  • Joowu Bing
  • Kàrti Bing
  • Laatu jumtukaayu Bing
  • LineBack
  • Màngasiin
  • Màngasiinu Windows
  • Microsoft Academic
  • Microsoft Add-Ins for Skype
  • Microsoft Bots
  • Microsoft Educator Community
  • Microsoft Filmu yi ak Tele
  • Microsoft Health
  • Microsoft Pay
  • Microsoft Research Interactive Science
  • Microsoft Research Open Data
  • Microsoft Translator
  • Microsoft Wallpaper
  • Microsoft XiaoIce
  • Mixer
  • MSN Dial Up
  • MSN Explorer
  • MSN Food & Drink
  • MSN Health & Fitness
  • MSN Money
  • MSN News
  • MSN Premium
  • MSN Sports
  • MSN Travel
  • MSN Weather
  • MSN.com
  • Ndimbal ak Jàppaleg Defaraatug Microsoft ñeel Office 365
  • Neexalu Bing
  • Njabootu Microsoft
  • Office 365 Consumer
  • Office 365 Home
  • Office 365 Personal
  • Office 365 University
  • Office Online
  • Office Store
  • Office Sway
  • Office.com
  • OneDrive.com
  • OneDrive
  • OneNote.com
  • Outlook.com
  • Paint 3D
  • Picturesque Lock Screen
  • Pix Lock
  • Presentation Translator
  • Remix 3D
  • Rinna
  • rise4fun
  • Ruuh
  • Sàqum Microsoft
  • Seeing AI
  • Seetu Tëj bi ci Topp
  • Send
  • Skype in the Classroom
  • Skype Interviews
  • Skype Manager
  • Skype Qik
  • Skype.com
  • Skype
  • Smart Search
  • Spreadsheet Keyboard
  • Sway.com
  • to-do.microsoft.com
  • Tossup
  • Translator for Microsoft Edge
  • Translator Live
  • Translator
  • UrWeather
  • Video Breakdown
  • Visio Online
  • Windows Live Mail
  • Windows Live Writer
  • Windows Movie Maker
  • Windows Photo Gallery
  • Xbox ak powi Windows, jëfekaay ak daliweb yi Microsoft siiwal
  • Xbox Game Pass
  • Xbox Live Gold
  • Xbox Live
  • Xbox Music
  • Xbox Store
  • Xuuskatu Bing Wikipedia
Jukki bu fees
1 màrs, 20180