SÀRTI SÀÑ-SÀÑI JËFEKAAY YU BAAXOO
MICROSOFT STORE, WINDOWS STORE, AK XBOX STORE
Oktoobar 2017 lañ ko yeesal

Sàrti sàñ-sàñ yii ay déggoo lañu ci sa digante yaw ak siiwalkatu jëfekaay bi. Noo ngi lay ñaan nga jàng leen. Dañuy jëfe ci jëfekaayi losisel yi nga yebbi ci Microsoft Store, Windows Store, wala Xbox Store (te ñu royalee bu ci nekk ci yile sàrti sàñ-sàñ niki "Store" bi), bokk na ci bépp yeesal wala ndolent ngir jëfekaay bi, ludul jëfekaay bi dafay àndak ay sàrt yu xaajaloo, ci anam bi nga xàmantani ci la yooyu sàrt di jëfe.

SOY YEBBI WALA NGAY JEFANDIKOO JEFEKAAY BI, WALA NGAY JÉEMA DEF BU CI NE CI YILE, NANGU NGA YOOYU SÀRT. SUDEE NANGUWOO LEEN, AMOO CI BENN SAÑ-SAÑ TE WARULOO YEBBI WALA NGEY JEFANDIKOO JEFEKAAY BI.

Siiwal katu jëfekaay bi mooy tekki wàll bu lay daganalal jëfekaay bi, ci niñ ko ràññee ci Store bi.

Soo àndee ci yile sàrti sàñ-sàñ, mën ngaa def yii ci suuf.
1. SAMP TE JEFANDIKOO SÀRT YI; ÀPP. Mën nga samp te jëfandikoo jëfekaay bi ci ay jëfandaayi Windows wala ay jumtukaayi Xbox ci niñ ko xamlee ci sunu Sàrtu Jëfandikoo. Microsoft jox na boppam sàñ-sàñu soppi sunuy Sàrti Jëfandikoo saa su nekk.
2. CËR YU AJU CI INTERNET.

a. Nangug cër yu aju ci cëri internet wala wifi. Sudee jëfekaay bi dafay lonku ci nosteg ordinatër bi ci internet, bu mën a àndak jaareeko ci ab mbaal bu amul fiil, buy jëfandikoo jëfekaay bi defay dox niki sag nangu cig jàllale xibaaru jëfandaay bu baaxoo (bokk na ci te yemul ci xibaari xarala yu aju ci sa jëfandaay, sa noste, ak losiselu jëfekaay, ak ay jumtukaay) ngir ay cër yu aju ci internet wala wifi. Sudee dañu wone yeneeni sàrt yu méngook sag jëfandikoob ay cër yuñu dugg bi ñuy jëfandikoo jëfekaay bi, yooyu sàrt itam dañuy jëfe.

b. Jëfandikoo cëri internet bu baaxul ci anam yu baaxul. Waruloo jëfandikoo benn cëru internet ci benn anam bu mën a lor mbaa laal doxiinu jëfandikoo kumu mën a doon mbaa mbaal bu amul buum. Waruloo jëfandikoo cër bi ngir am sàñ-sàñu dugg ci bépp cër, njoxe, sàq, mbaa mbaal ci anam bumu mën a doon.

3. DAYOOB SAÑ-SAÑ. Dañu daganal sàñ-sàñ bi, jaayu ñu ko. Déggoo bii yenn àqi jëfandikoo jëfekaay bi kase la lay jox. Su Microsoft dakkalee man-manu jëfandikoo jëfekaay yi ci say jëfandaay ci li àju ci sa déggoog Microsoft, bépp àqi sàñ-sàñ bumu méngool dina jeex. Siiwalkatu jëfekaay bi jagoo na yeneen àq yépp. Ludul yoon buy jëfe jox la yeneeni àq ak bii yemale, war nga jëfandikoo jëfekaay bi suñ ko nangoo kase ci waxiin ci déggoo bii. Sooy doxalee nii, war nga nangu bépp yemale xarala ci jëfekaay buy tax nga mën ko jëfandikoo ci yenn anam. Waruloo:

a. Jalgati benn yemale xarala ci jëfekaay bi.

b. Safaane defar, booledi, mbaa tasaare jëfekaay bi, budul te ci dayo bu yoon yu jëfe nangu ci waxiin, donte am na yemale.

c. Defar ay sotti jëfekaay yu bari yuñu xamle ci déggoo bii mbaa yu yoon buy jëfe nangu, donte am na yemale.

d. Siiwal mbaa defar ci neneen jëfekaay yu jàppandi ngir ñi mën a sotti.

e. Luwe, mbaa abale jëfekaay bi.

f. Toxal jëfekaay bi mbaa déggoo bii ci bépp xaaj bu bawoo feneen.
4. JUKKIB NDIMBAL. Suñu joxe jukkib ndimbal bi ak jëfekaay bi, mën nga sotti te jëfandikoo jukkib ndimbal bi ngir jubluwaayi delluwaayu jagoo.
5. XARALA AK YEMALEY TOXAL. Jëfekaay bi mën na laaj saytu Etaa-Sini mbaa xarala bitim réew mbaa yooni toxal ak sàrt yi. War nga dëppook bépp yoonu toxal bitim réew ak sàrt buy jëfe ci xarala buñu jëfandikoo mbaa bu jëfekaay bi nangu. Yile sàrt dañuy àndak ay yemale ci jëmu yi, jëfandikookat yu ci mujj, jëfandikoo bu mujj. Ngir am yeneeni leeral ci costéef yu Microsoft màndargal, demal ci (http://go.microsoft.com/fwlink/?LinkId=242130).
6. CËRI NDIMBAL YI. Jokkool ak siiwalkatu jëfekaay bi ngir xool ndax amna ab cëri ndimbal yu jàppandi. Microsoft, sa defarkatu daju ak sa joxekatu cër yu amul buum (ludul benn ci ñoom doon siiwalkatu jëfekaay bi) yoru ñu kiliftéefu joxe ay cëri ndimbal ngir sa jëfekaay.
7. MBOOLEEM DÉGGOO. Déggoo bii, bépp sàrti sàmm-sutura buy jëfe, bépp sàrt bu ci dolleeku buy àndak jëfekaay bi, ak sàrt yu ñeel ngir mottali yi ak yeesal yi ñooy mbooleem déggoo digante yaw ak siiwalkatu jëfekaay bi ñeel jëfekaay bi.
8. YOON BUY JEFE.

a. Etaa-Sini ak Kanadaa. Sudee Etaa-Sini walla Kanadaa nga jëndee woon jëfekaay bi, yooni réew mi mbaa tund bi nga dëkk (mbaa, sudee ab liggéeyukaay, fu sa barabu liggéey nekk) mooy saytu nuñuy tekkee yooyu sàrt, jéebaaneg seeni jalgati, ak yeneen jéebaane (bokk na ci aar aji-jëfandikookat bi, konkiraas bu jaaduwul, ak jébaaneg bu yuy waral ate siwil), moo xàm xiiroo ak ŋaayoo sukkandikaayu yoon.

b. Ci biti Etaa-Sini ak Kanadaa. Sudee ci beneen réew nga amee woon jëfekaay bi, yooni réew boobu mooy jëfe.
9. GÀLANKOORU YOON. This agreement describes certain legal rights. Mën nga am yeneen àq yu aju ci sa yooni dëkk mbaa réew. Déggoo bi du soppi say àq yu àju ci sa yooni dëkk mbaa réew sudee say yooni dëkk mbaa réew maye wul nga def lu ni mel.
10. BEDDIINU GARANTI. Jaglel nañu sàñ-sàñ bi “niki numu mel”, “ak njuumte yépp” ak “numu jàppandee”. Gàddu nga bépp lorangey jëfandikoo ko. Siiwalkatu jëfekaay bi, ci turu boppam, Microsoft (Sudee Microsoft nekkul siiwalkatu jëfekaay bi), cër yu amul buum ci kaw mbaal buñu joxewul, ak bépp bànqaas bu lay teewal, jaaykat yi, ndaw yi ak joxekat yi (“Xaaj yuñu Ëmb”), joxewul benn garanti buñu waxe, mbaa anam bu méngook jëfekaay bi. Lorange bu matale bu wone fi baaxaay, kaarànge, dalal, ak xaraañu jëfekaay toll ci yaw. Sudee jëfekaay bi dafa yàqu, nangu nga njëg bu matale bu cërale mbaa saafarra bi laaj. Mën nga am yeneen àqi àji-jëfandikoo ci kaw say yooni barab ni yile déggoo mën nañ soppeeku. Ci dayo bu ëpp buñu nangu ci sa kaadaru sa yoonu reew, dañuy dàq bepp garanti bu nëbbu, bokk na ci mëniinu njaay, baaxaayu luñu mën a nangu, jekkal ngir jubluwaay bu xejjiku, kaarànge, dàl, ak nàkka luubal.
11. YEMALE AK DÀQU SAAFARA AK YÀQUTE YI. Ci dayo bu yoon nanguwul, soo bépp sukkandikaay ngir dabuwaat yàqute yi, mën nga dabuwaat ci yàqute yu jub bu siiwalkatu jëfekaay ba ci tolluwaayu xaalis bi nga fayoon ngir am jëfekaay bi mbaa USD$1,00, bi nga xam ni moo gën a rëy. Doo to, te amul benn àqi, jéema dabuwaat benn coppite, bokk na ci lorange, njuréef yi nga ñàkk, xejjiku, jubadi mbaa buy indi xew-xew yuy yàq ci siiwalkatu jëfekaay bi. Sudee say yooni barab dañuy impoose garanti mbaa anam donte yile sàrt duñu ko def, yàgaayam mu ngi yem ci 90 bis ci bi nga waree yebbi jëfekaay bi.

Yemale bii dafay jëfe ci:
Lépp lu méngook jëfekaay bi mbaa cër buñu jàppandal ci jëfekaay bi; ak
Jéebaaneg jalgati déggoo, garanti, mbaa anam, kiliftéf bu tar, ñàkk a xoromal, mbaa beneen buko waral, jalgati ab tolluwaay mbaa sàrt; alal bu lewul; mbaa ci kaadaru bépp xalaat, dayo yépp yu yoon buy jëfe nangu.

Dafay jëfe itam donte:
Saafara bi du la fay ci matale li nga ci ñàkk yépp; mbaa
Siiwalkatu jëfekaay bi xàm na mbaa waroon na xam darra ci jafe-jafe yu ci mën a am.