This is the Trace Id: af2c9ede7f5ff4bcbffd1f8c5a13b8ef

Tënkub coppite yi am ci Déggooy Cëri Microsoft – 30 Sàttumbar, 2025

Noo ngi yeesal Déggooy Cëri Microsoft, yuy jëfe ci sag jëfandikoo costéef mbaa cëri Microsoft yi nekk ci net bi. Xët bii dafay Joxe nanu ab tënk ci coppipte yuñu gën ràññee ci Déggooy Cëri Microsoft.

Ngir gis coppite yépp, noo ngi lay digal nga jàng Déggooy Cëri Microsoft bamu jeex fii.

  1. Ci kawu xët wi, yeesal nanu bisu siiwal ci 30 fan ci wéru Sulet, 2025, ak bis bimuy jëfe bisu 30 Sàttumbar, 2025.
  2. Ci pàccu "Say Ëmbiit", yokk nanu ab pàcc "c" bu bees ngir wax ci njoxe yuñu mëna exporté.
  3. Ci pàccu "Ndimbeule", ci biir pàccu "Jëfandikoo Cër yi & Ndimbal" amal nañu ay saytu ngir dindi lien hypertexte yi te leeral ni yenn Sàrwiis yi mên nañu joxe yeneeni Ndimbeule yu xejjiku, te yooyu ndimbeule mën nañu aju ci ay sàrt ci biti Déggooy Cëri Microsoft.
  4. Dindi nañu pàccu "Nguir jefandikookat yi ddeuk Australie" ci suuf pàccu "Ndimbeule" ndax coppite yi am ci sàrt yi ci biir dëkk bi.
  5. Ci suuf pàccu "Asii mbaa Bëj-saalum Pasifik, donte sa dañuy ràññatle sa réew fii ci suuf", ci biir "Ñi séq kontraa bi, yoon wiñ tànn, ak Fi ñuy àttee jàppante yi" sàrt yuñu jagleel ñi dëkk Ostaraali dindi nañ leen ndx coppite yi am ci tëraliinu dëkk bi.
  6. Ci pàccu "Diiru ñamandi yiñ la may", ci biir pàccu "Sàrti pay", yokk nanu ab libellé buy leeral yenn mayeb diirub ñamandi yi mën nañu ab yeesal-boppam buñu wara taal.
  7. Ci pàccu "Sàrt yuy àndak cër yi", amal nañu yile ndolent ak ay coppite:
    • Ci pàccu "Cëri Xbox", ci biir pàccu "Xbox", leeral nañu ni so bindoo ci ab jëfandaay wala jumtukaay ak sa sàqum Microsoft, wala nga lëkkale sa sàqum Microsoft ak boobu jëfandaay wala jumtukaay ngir jot ci ab sàrwiis budul-Microsoft, mu waral nga sukkandiku ci aqi jëfandikoo Microsoft ci boobu pàcc. Dolli ci, leeral nanu ni jekkali Kaarànge Njaboot u Xbox yi mën nañ leen baña dekkal sooy dugg ci po ak sàrwiisi Xbox Game Studios jaare ko ci ab jëfandaay wala jumtukaay bu bawoo feneen.
    • Dëppook coppite yuñu amal ci pàccu "Cëri Xbox", yokk nanu ay leeral ci pàccu "Man-mani Njabootu Microsoft", ci suuf pàccu "Xbox", ci li aju ci jekkali Kaarànge Njaboot u Xbox mën nañ leen baña dekkal sooy dugg ci po wala sàrwiisi Xbox Game Studios jaare ko ci ay jëfandaay wala jumtukaay yu bawoo feneen.
    • Coppite yi ci pàccu “Skype, Microsoft Teams ak GroupMe” lañ leen amalee woon ngir bayyi xel ci alatare wu Skype.
    • Pàccu “Teree & Yemale ci Poñ yi”, ci suuf pàccu "Microsoft Rewards", soppi nañu ngir mu nirook li nga xamantane poñ yuñu soppiwul seen àpp baña jeex suñu gañewul wala suñu soppiwul benn poñ ci diirup 12 weer yu toppalante.
    • Pàccu “Tecc sa Comptu Rewards”, ci suuf pàccu "Microsoft Rewards", soppi nañu ngir mu nirook ab comptu Rewards mën nañ ko fomm sudee duggu ñu ci lu toll ci 12 weer yu toppalante.
    • Yokk nañu ab pàcc bu bees ci yemaley jëfandikoo bi ci pàccu “Mënloo AI”.
    • Yokk nañu ab pàccu "Sàrwiisu Jokkoo", buy leeral yombalug jokkoo ci biir nit ñi, lu mel ni Skype, Teams, ak Outlook, dañu wara dëppook sàrti jëfandikoo yi. Yile sàrt royale nañ leen te lëkkale leen ci pàcc bii.
  8. Ci biir Sàrt yi, amal nanu ay coppite ngir mbir yi gëna leer boole ci jubbanti graameer, njuumte, ak yeneen jafe-jafe yu ni mel. Yeesal nanu itam tur wi ak iper-lëkkalekaay yi.