Sa Sutura
1. Sa Sutura. Sa sutura lu am solo la ci ñun. Baale ñu nga nafar Bataaxalu sutureu Microsoft (https://go.microsoft.com/fwlink/?LinkId=521839) (ben "Bataxalu sutureu") ci niñuko tekkiwe xeeti données yiñuy dadiale dieule ko ci yaw ak sey jumtukaay yu xarala ("Données"), nuñuy jëfandikoo sey données, ak bases yu teggu ci yoon yiñuy diarale sey données. Sa xibaaru sutureu dafey wane it naka la Microsoft di jëfandikoo sey mbirr yi nek ci sey jokalante ak ñenen ñi; li nga dialale jeumeuleko ci Microsoft diarale ko ci njeriñ: ak mbirr yi, nataal yi, lidiassa yi, deglu, liguey yu wayxarala yi, directs yi ak wideo yi nga yeegeule, dincc, di tek, defar, wanne wala bokk ci biir njeriñ li, wala dugeule yi nga dioxe nguir fesseule ay mbirr ("Sey mbirr"). Ginaaw jëfandikoo dafay neex boroom wala yoon digle ko, soo àndee ci Sàrt yii, nangu nga Microsoft jël say Njoxe ak Ëmbiit, jëfandikoo leen wala wane leen ci anam wiñ ko waxee ci Sàrti Sutura si. Yenn saa dina nu la yónnee weneen yëgle ngir sàkku ci yaw nga joxe sa kàddu, kom ninu ko leeralee ci Sàrti Sàmm-sutura yi.
Sa Ëmbeef
2. Sa Ëmbeef. Lu bari ci sunuy Serwiis daf lay may nga defar, denc wala seddoo Sa Ëmbeef wala jot ay jumtukaay jóge ci ñenen. Duñu laaj moomeelu Sa Ëmbeef. Sa Ëmbeef yaa leen mome te yaw rekk yaa si am ndogal.
- a. Soo séddoo Sa Ëmbeef ak ñeneen, kon xam nga ni dina ñu ko mëna jëfandikoo ci àdduna bi yépp, denc, sotti, siiwal, jox ko ñeneen, séddoo ak wane Sa Ëmbeef ngir li nga def Sa Ëmbeef jàppandi ci yeneen Serwiis yi, te duñu la ci jox ndàmpaay. Soo bëggulee ñeneen mën a def loolu, bul jëfandikoo Serwiis yi ngir séddoo Sa Ëmbeef. Yaw yaay kiy teewal ak di dëggal ni ci diiru Sàrt yii, am nga (te dinga am) mbooleem yelleef yi war ci Sa Ëmbeef yiñ yab, denc, wala séddoo ci biir Serwiis yi ak dajale, jëfandikoo, ak tëye Sa Ëmbeef du jàlgati benn yoon wala yelleefu ñeneen ñi. Microsoft du ki moom, fuglu, wéral, fay, jàppale mbaa ci neneen gàdduwul benn kiliftéef ci Sa Ëmbeef te mënu ñu jàpp ni mooy ki yor Sa Ëmbeef mbaa jumtukaay yu ñeneen yab, denc mbaa séddoo di jëfandikoo Serwiis yi.
- b. Ci tolluwaay buñu laaj ngir jox la Serwiis yi yaw ak ñeneen, ngir aar la yaw ak Serwiis yi, te gënal costéef ak cëri Microsoft ak serwiis, da ngay may Microsoft sàñ-sàñu àqi moomel addina werngel kepp te dara du ci ruusee ci xaalis ci keytu moomeel ngir jëfandikoo Sa Ëmbeef, ci misaal, amal ay sotti, teye, jébbal, tëggaat, wone, te séddale jaare ko ci ay jumtukaayu waxtaanu Sa Ëmbeef ci Serwiis yi. Soo siiwalee Sa Ëmbeef ci ay barabu Serwiis yumu jàppandee bu baax ci lënd gi te amul yemale, Sa Ëmbeef mën na feeñ ci ay wone mbaa ay jumtukaay yuy siiwal Serwiis bi. Yenn CI Serwis yi siiwal moleen yor. Ay saytu ci nan la Microsoft di jëmmalee siiwal jàppandi nañu ci https://choice.live.com. Duñu jëfandikoo li ngay wax ci sa imeel, waxtaan, woote wideo, mbaa boyetu baat, mbaa wayndare, nataal, mbaa yeneen taxañu jagoo ngir jëmee ay siiwal ci yaw. Boole nanu cig yaatal sunuy sàrti siiwal yi ci Sàrtu Sàmm-sutura bi.
- c. Microsoft daf lay jox mëneefu jot ay done yoo mëna yóbb feneen jaaree ko ci Aliwo xibaar suturra bu Microsof (https://account.microsoft.com/privacy) wala interfaasu cëri jëfandikookat, sunu ko dëggalee ak sa këlu Microsoft. Done yiñ mëna yóbbu feneen mën nañu leen jëfandikoo ngir soppi ci sarwis yu nekk ci digante yenen joxekat. Microsoft dafa am sañ-sañu tënk yóbbanteb done yu mën a gàllankoor kaaraange cër yi wala moomeel xam-xamu Microsoft. Sudee mënoo yónnee say done ci anam yii, jokkool ak Microsoft ci adres bi ci Nan ngay jokkoo an ñun pàcc (https://privacy.microsoft.com/privacystatement#mainhowtocontactusmodule) wala jëfandikoo sunu formileeru web (https://go.microsoft.com/fwlink/?linkid=2126612).
Sàrtu Doxalin
3. Sàrtu Doxalin. Sa doxalin yako ress ak sa ëmbeef sa yoy jëfandikoo Serwiis yi.
- a. Soo nangoo Anam yiile, nangu nga ni, sooy jëfandikoo Serwiis yi, boole ci serwiis IA yiy jël yenn dogal, wala jëf, ci sa bopp wala ci anam yu bari yu nit ñi di jàppale, dinga topp tërëlin yii:
- Bule def lenn lu yoon meyewule, wala jeema genne wala bokk ëmbeef yu yoon meyewule.
- ii. Bul dugg ci benn jëf juy liggéeyloo, gaañ, mbaa fitnaal ay xale.
- iii. Bule yonee ay spam wala di dugg ci mbàkk, wala jeema defar wala seddale ay malware. Spam mooy bataaxal bu nu soxlawul wala bataaxal bu nu laajul, ay siiwal, laaju xame, SMS (bataaxali jukki), mbaa ay jokkoo ci jumtukaay yu xarale yi niroo lañu. Phisihing moy yonee ay emails wala yenen xetti waxtanu jumutkaay xarale ngir sàcc wala jalgati yoon duggal ñiko jot ñu wax sen xibaari bopp wala xibaar yuñu warule fesal, deme ni ka baatu dugg, besu judd, limi Kaaraange Askan, limu paaspoor, xibaari xobbu bank, xibaari kom, wala yenen xeeti xibaar yu warul fes, wala ngir mëna jot ci ay kontu wala ndenc, geneem lijaasa wala yenen xibaar yu warul fes, fey ak/wala njureefi kom. Malware dafay àndaale ak bépp liggéey buñ nara def ngir gaañ xarala yu bees, lu ci melni yónnee ay jëfin yu ñaaw, defar ay songu bañal serwiis wala yoriinu serwëru komand ak kontre.
- iv. Bul fësal wala jëfandikoo Serwiis yi ngir sos wala séddoo ëmbiit wala mbir yu jaarul yoon (lu ci melni, taatu neen, sey ak mala, seetaan ñuy sekk, làkk wuy sonal, fitna bu ci nataal wala xoltu, gaañ sa bopp, wala liggéey fitna) wala Sa Ëmbeef wala mbir yu méngoowul ak yoon wala sàrti dëkk bi nga nekk.
- v. Bul bokk ci liggéey buy njuuj njaaj, fen wala réer (lu melni, laaj xaalis ci njuuj njaaj, mbuboo keneen, sos kontu yu baaxul, sos liggéey bu amul benn dëgg, defar wala séddoo ëmbiit buy njuuj njaaj, jëfandikoo Serwiis yi, jëfandikoo wala yokk jouer wala am njeexital ci nàtt wala tolluwaay. wala wax yi) wala saaga wala sosal.
- vi. Bul jeema wiri benn tënk ci jot, jëfandikoo, wala am Serwiis yi (lu melni, jéema "jailbreak" sistem IA wala scraping buñu nanguwul).
- vii. Bule soobu ci def def yiley gañ, Serwiis yi, wala ñenen ñi (maname di walle ay virus, di topp, di diem guene wala bokk mbirr yuy soof nitt ñi, titeule wala xoxatale ñenen ñi, di dugeule yeufu terroriste wala mbir yu extremiste yu soxor, di waxtane kaddu mbeñeln wala di digle lu bonn ci kaw ñenen ñi).
- viii. Bule jalgati akk ak yeleefu ñenen ñi (maname di dialale liñu tere lu melni way yu ame borom wala yeneni bagass yu ame borom, diayate wala seddeule cartu Bing yi, wala di dieule ay nataal wala wideo/enregistrement audio wu ñenen te andu ñu ci def niki ken ci xamekaay yu biométrique/xibaar wala lenen lumu done lu jëfandikoo ben ci Serwiis yi).
- ix. Bul dugg ci jëf juy jalgati sutura mbaa àqi aar njoxey ñeneen.
- x. Bul jàppale ñeneen ñu jalgati yile sàrt.
- Yeneen leeral ci sunuy sàrt, sunuy doxalin ngir saytu ak tëral ak sàrti sarwis mën nga ko amee ci aka.ms/trustandsafety.
Jëfandikoo Serwiis yi & Ndimbal
4. Jëfandikoo Serwiis yi & Ndimbal.
- a. Sàqum Microsoft. Di nga soxla ab sàqum Microsoft ngir dugg ci ay Serwiis yu bari. Sa sàqum Microsoft dafay tax nga mën a dugg ci costéef yi, daluweb yi ak cër yi Microsoft joxe ak yenn Microsoft liggéeyandoo.
- i. Sos ab Sàqum. Mën nga sos am sàqum Microsoft soo bindoo ci internet. Bul nangu ànd wala jëfandikoo benn njoxe bu lëndam wala bu jaarul yoon sooy bindu ngir am sàqum Microsoft. Ci yenn wàll yi, ab xaaj bu bawoo feneen, niki joxekatu cëri Internet, mën nala jox ab sàqum Microsoft. Soo jotee sa sàqum Microsoft ci xaaj bu bawoo feneen, xaaj boobu mën na am yeneen àq ci sa sàq, niki maniinu dugg mbaa far sa sàqum Microsoft. Baal ñu topp bépp sàrt bu ci dolleeku bu la xaaj bi joxoon, ndax Microsoft amul benn dogal ci li àju ci yile sàrt yu ci dolleeku. Soo sosee ab sàqum Microsoft ci turu ab kër, niki sa liggéeyukaay mbaa ki nga liggéeyal, nangu nga ni am nga kiliftéefu boole boobu kër ci yooyu Sàrt. Mënoo jël leeral yi ngay duggee ci sa sàqum Microsoft nga jox ko keneen wala benn wàll. Ngir aar sa sàq, wéyal di nëbb sa baatu jàll ak say leerali sàq. Lépp lu xew ci sa sàqum Microsoft, wala lépp luñu fa def yaw yaay nday ji mbilli ji.
- ii. Jëfandikoo Sàq. War nga jëfandikoo sa sàqum Microsoft ngir wéy di doxal sa sàq. Loolu dafay tekki ni danga wara dugg gën gaa néew benn yoon ci diiru ñaari at ngir mëna wéy di dox sa sàqum Microsoft, ak Cër yi ci laale (fileek leeral lu wuute), fileek joxe wuñu diir bu gëna gudd ci sàrti liggéeyu sàqum Microsoft ci https://go.microsoft.com/fwlink/p/?linkid=2086738 wala ci xéewal ngir wàll ci Serwiis yi ñuy fay. Soo duggul ci diir bii, dina ñu jàpp ni dàkkal nañu sa sàqum Microsoft di dina lako tëjal. Yëral pàcc 4.a.iv.2 ngir xàm li mën a am suñu tëjee ab sàqum Microsoft. War nga dugg ci sa boyetu Outlook.com ak ci sa OneDrive (ci xaajale) gën gaa neew benn yoon ci bu nekk, luko moy dina ñu la tëjal sa boyetu sàqum Outlook.com ak sa OneDrive. Sudee danu gis ni sa sàqum Microsoft amatul kaaraange te ab jàmbur mën na ko jëfandikoo ci lu jaarul yoon (ci misaal, ginaaw bu ñu yàqee sam sàqum), Microsoft mën na tëj sam sàqum ba kerook ngay mën a wax ni yaa ko moom. Su nu sukkandikoo ci nekkinu déggoo bi, mën nañu laaj ngir nu dakkal dugg ci yenn wala Sa Këmb yépp. Soo amee ab jafe-jafe ngir dugg ci sa sàqum Microsoft, baal yër daluweb bii: https://go.microsoft.com/fwlink/?LinkId=238656.
- iii. Xale yi ak Sàq yi. So defare sàqum Microsoft wala jefandikoo njeriñ li, nangu nga te nga ci takku ci Sarte yii te nekkale ni ame nga attu "magg" wala "yeleefu yoon" fi nga deuk wala sey wadiur wala kiñula denk takku na ci Sarte yii ci sa ndigeule. Su fekke ni xamo ndax mottale nga attu "magg" wala "yeleefu yoon" fi nga deuk, wala xamo liñuy wax ci dagg bii, baale ñu nga lacc sey wadiur wala kiñula denk ndimbeule. Sudee danga nekk waajuru wala nga yilif benn xale, yëw ak xale bi nangu ngeen te ànd ngeen ci Sàrti Sàmm-sutura yii, te itam lépp luñ def ci sàqum Microsoft mi wala ci Cër yi yeen la, muy mbir yiñ ciy jënd, mu fekk ñu sos sàqu xale bi leegi wala ëlëg.
- iv. Tëj Sa Sàq.
- 1. Saa yu la soobee mën nga bàyyi yenn ci Cër yi wala nga tëj sa sàqum Microsoft, yaa xam luy sabab bi. Ngir tëj sa sàqum Microsoft, baal ñu yër https://go.microsoft.com/fwlink/p/?linkid=618278. Soñu waxe ñu tecc sa sàqum Microsoft meun nga tanne defsi luy wanne ni deñuko tediahum mo xam ci 30 wala 60 fann la nguir rek so soppe xalaat ci diguente bi. Su weesoo diiru 30-wala 60-fan, dañuy tëj sa sàqum Microsoft ba fàww. Nu ngi lay ñaan nga xool pàcc 4.a.iv.2 bii ci suuf ngir xam luy xew sudee dañu tëj sa sàqum Microsoft. Soo duggaatee ci sa sàqum Microsoft ginaaw bi nu ko tëjee, sàq mi dafay doxalaat.
- 2. Sudee dañu tëj sa sàqum Microsoft (yaw wala nun), dina am mbir yuy xew. Li ci njëkk mooy, dangay ñàkk ci sassa bépp sañ sañi jëfandikoo sa sàqum Microsoft bi la doon may nga jot ci cër yi. Ñareel ba, dañuy far bépp Njoxe wala Ëmbiit buñ bokk ci sa sàqum Microsoft wala ñu tàqale leen, yaw ak sa sàqum Microsoft (fileek yoon waxul nañu ko tëye, delloo koo, wala ñu jox ko jàmbur ngir mu mën a xam ki nga doon). Am nga ab palaŋu denc bu baaxoo ndax Microsoft du mën a jëli Sa Këmb mbaa Njoxe suñu tëjee sa sàq ba noppi. Ñatteel ba, mën nga baña mën jëfandikoo costéef yi nga am.
- b. Yemale ak Doolel. Yu beuri ci suñu ay Njeuriñ yi ley mey nga jokalante, defar, guene, ak bokk ay mbirr ak ñenen leviers wu kaarangue njeuriñ yi ngui samm suñuy Njeuriñ ak yenen jefandikookat yi.
- i. Sarte yi. Suñu Yoonu Doxaline dafey xame liñuy tere so jefandikoo suñu ay Njeuriñ. Sunu êmbeef ak sàrti doxalin mën ngeen ko gis ci fii (https://www.microsoft.com/DigitalSafety/policies). Mënloo yu kendalu yi am nanu ay sàrt yu doleeku ak jëfekaayu askan wi nu mën ko teg seeni jëfandikookat, te mu jàppandi ci here (https://aka.ms/trustandsafety).
- ii. Di yeukle lu la diaaxale. Meun nga yëgle mbirr yu la diaaxale wala doxaline bo xalaat ni warena jalguati suñu Yoonu Doxaline fii (https://aka.ms/reportconcerns).
- iii. Xoolaat. Ci fimu ware dale, meun na ame ñu jefandikoo jumtukaay yuy demale sen bop ak ay nitt nguir xoolaat mbirr yi nguir rañee spam yu ñu diap ni deñoo doywar, virus yi, sacc yi, phishing, malware, jailbreak, wala yenen yu deupowule ak yoon wala mbirr yuy gaañate wala doxaline.
- iv. Dooleel. Diox neñu suñu bop dooley beñ ay mbirr su eupe liñu la jaklelone ci sa ndenkaane wala su feke fichier bi dafa eupeule li la suñu Njeuriñ li diaglele. Meun neñu teuyee, dindi wala beña wane ay mbirr su fekke ni dafey jalguati suñu Yoonu Doxaline wala benen sartu Njeuriñ wala fuko yoon soxelaa. So jalgatee deggoo yiile wala Tërëlin (https://aka.ms/trustandsafety), mën nanu jël ay jëf ci kaw sa compte. Meun na ci bokk yemale sa diot ci yen jumutukaay yi ak Njeuriñ yi, dakkale dila diox ay Njeuriñ, di teucc sa sàqum Microsoft ci saassi wala teuyee dialale wu waxtane (lu melni email, dialalem ay mbirr, wala bataaxalante ci saassi) ci wala diogue ci Njeuriñ yi. Sa teudium diot ci sa ben Njeuriñ wala sa compte meunena diogue ci ben def defu licensu mbirr yi, sa bokk, akk sa toluwaayu xalissu sàqum Microsoft bu bokk ak sàqum bi. Suñuy seytu ay jalguati yo def ci sarte yii, Microsoft diox na bopame ndigeule nguir seetaat mbirr yi nguir safara leunc leunc mi. Waaye, mënu ñu saytu Cër yépp te jéem darra ngir def lu ni mel. Ngir yeneen xibaar yu ci jëm yamale ak dooleel amalin yi (https://www.microsoft.com/DigitalSafety/moderation-and-enforcement), Service specific terms, Additional policies ak guidelines (https://www.microsoft.com/DigitalSafety/policies/additional-guidelines), ak wote yi (https://www.microsoft.com/DigitalSafety/moderation-and-enforcement/appeals), xoolal https://aka.ms/trustandsafety. Ay xibaar ci lu dieum ci suñu sarte yi laal bakku wu laalum propriété borom xel yi meun nga ko fekk ci Leeral.
- c. Comptu jang wala liguey yi. Mën nga dugg ci yenn liggéeyali Microsoft ak ab dëkkuwaayu bataaxalu liggéey wala daara. Soo ko defee, nangu nga ni boroom domen bi sa dëkkuwaayu bataaxal bokk, mën na wax ni am nga sàqum Microsoft buñ boole ak say abonmaa, saytu ak yilif sam sàq, jot ak jëfandikoo say Njoxe, boole ci jokkoo yi nga amal ak say taxañ, te itam Microsoft mën na yëgal boroom domen bi sudee sàq mi wala njoxe yi ci nekk dañu yàqu. Sudee itam danga nangu ni sa jëfandikoog cëri Microsoft mën nañu ànd ak déggoo yi la Microsoft tëralal, yaw wala sa mbootaay, te yii Sàrt mën nañu fa baña dox. Sudee danga am sàqum Microsoft ba noppi nga jëfandikoo beneen dëkkuwaayu bataaxal ngir dugg ci Cër yiñ lim ci Sàrt yii, mën nañu la laaj nga yeesal dëkkuwaayu bataaxal biñ boole ak sa sàqum Microsoft ngir nga mën a wéy di jot ci Cër yooyu.
- d. Yenen plangu ligueyukaay/données yusi yokku. Ngir jëfandikoo ay Cër yu bari, war nga lonku ci internet ak/mbaa njoxe/palaŋ portaabal. Mën nga soxla yeneeni jumtukaay, niki ak kask, nataalukaay mbaa mikro. Yaw yaa wara wut sa konsiyoŋu bopp, say paas, wala jumtukaay bi war ngir jëfandikoo Cër yi ak ngir fay fere yi operatër bi (yi) di fayyeeku ci koneksiyoŋ bi, paas bi ak jumtukaay bi. Boole nañu yooyu njëg ci bépp njëg bi nga ñu fay ngir Cër yi te duñu la délloo yooyu njëg. Xoolal ak sa (say) joxekat ngir seet ndax am ay njëg yu mën a jëfe ci yaw.
- e. Yeuklewu Ngeuriñ yi. Sudee dafa am luñ la waral yëgal ci Cër bi ngay jëfandikoo, dina nu la yónnee yëgleb Cër. Soo joxee sa dëkkuwaayu bataaxal wala sa nimero telefon boole ko ak sa sàqum Microsoft, te mën nañu la yónnee bataaxal ci Cëri yëgle yi, manaan imeel wala ci SMS (message), boole ci ñu saytu sa dàntite laata ngay bind sa nimero telefon portaabal ak saytu li ngay jënd. Mën nanu la yónnee itam yëgley Cër ci beneen anam (ci misaal ci bataaxali biir costéef). Done wala mesaas mën nañu la fay sooy joxe yëgle ci SMS.
- f. Ndimbël. Ndimbal ngir yenn serwiis yi jàppandi nañu ci https://support.microsoft.com ak sàrt yii ñoo koy doxal, te yenn Serwiis yi mën nañu joxe ndimbal lu wuute wala luy yokk ci kiliyaan yi, lépp di aju ci yokkuteef ana yi. Ndimbal li mën na bañu jàppandi ci sumbi Cër wala man-man yiñ jagleel ñam kese wala xoolandi. Ndimbal gu Jàppandi mën na wuute ci anam wi produit bi di doxee, te danga wara am Serwiis bu am lisaas bu méngoo ak li ñuy laaj ci Microsift Lifecylce (https://learn.microsoft.com/lifecycle). Cër yi mën nañu bàña àndak losisel mbaa cër yu ab beneen xaaj joxe, te yaw yaa war a tamal sa bopp li mànta ñàkk ci ab déggoo.
- g. Dakkale sey Njeuriñ. Sudee dañu dakkal sa Cër (yaw wala nun), li ci njëkk mooy dangay ñàkk ci saasi sañ-sañ bu lay may nga jëfandikoo Cër yi te daganal bi nga am ci Cër boobu dafay jeex. Ñareel ba, dañuy far bépp Njoxe wala Ëmbiit buñ bokk ci sa sàqum Microsoft wala ñu tàqale leen, yaw ak sa sàqum Microsoft (fileek yoon waxul nañu ko tëye, delloo koo, wala ñu jox ko jàmbur ngir mu mën a xam ki nga doon). Li muy jur mooy dootoo mëna jëfandikoo benn Cër (wala Say Ëmbiit yi nga denc ci yooyu Cër). Danga war di faral di denc say njoxe. Ñatteel ba, mën nga baña mën jëfandikoo costéef yi nga am. Sudee danga dakkal sa sàqum Microsoft te amoo meneen sàq mu lay may nga jëfandikoo Cër yi, mën nañu dakkal say Cër ci saasi.
Jëfandikoo Cër mbaa Jefekaayi xaaj bu bawoo feneen
5. Jëfandikoo Cër mbaa Jefekaayi xaaj bu bawoo feneen. Cër bi mën nala may nga jot wala am ay costéef, cër, daliweb, lëkkalekaay, ëmbiit, jumtukaay, po, maneef, boole, bot wala jëfekaay yu bawooo ci ay jàmbur bu ci bokkul (liggéeyukaay wala ay nit yu wuute ak Microsoft) ("Cër ak Jëfekaayi Jàmbur"). Sunu mënloo yu bare dafay may dafay japale tamit nga gis, laaj wala, jokkoo ak Cër ak Jëfekaay Jàmbur te mën la may wala laaj la nga seddoo Say Êmbeef wala Joxe yu melni Cër ak Jëfekaay Jàmbur, te ndànd ne sooy jêfandikoo sunuy Mênloo yaa ngi leeni jóbbu ci nu def Cêr ak Jëfekaay Jàmbur nu jàppandi ci yow. Cër ak Jëfekaayi Jàmbur yi mën nañu la may wala laaj la nga denc Say Ëmbiit wala Njoxe ak siiwalkat bi, joxekat bi wala opertaatëru Cër ak Jëfekaayi Jàmbur yi. Cër ak Jëfekaayi Jàmbur mën nañu la indil sàrti sàmm-sutura wala mu sàkku ci yaw nga nangu seeni sàrt laata ngay mën a samp wala jëfandikoo Cër ak Jëfekaayi Jàmbur. Xoolal pàcc 13.b ngir yeneen sàrt yu ñeel jëfekaay yi nga amee Màngasiin yu Microsoft moom wala ay bànxaasam (boole ci te du ci yam, Màngasiinu Office, Microsoft Store ci Xbox ak Microsoft Store ci Windows. Danga wara jàng bu baax sàrti jàmbur bi ak sàrti sàmm-suturaam laata nga jënd, jëfandikoo, sàkku, wala ngay lëkkale sa Sàqum Microsoft ci benn Cër ak Jëfekaayi Jàmbur. Benn sàrtu jàmbur du mën a soppi Sàrt yii. Microsoft du la jox sàñ-sàñ benn àqi moomelu xalaat ci kaadaru Cër ak Jëfekaayi Beneen xaaj. Nangu nga jël lépp lu la mën a lor ak kiliftéef bu bawoo ci jëfandikoo yile jëfekaay ak cëri xaaj bu bawoo feneen ak ni Microsoft moo yor kiliftéefu bépp jafe-jafe buy bawoo ci li nga leen di jëfandikoo. Yoonu Microsoft nekkul ci benn leeral wala cër njoxe bu Cër ak Jëfekaayi Jàmbur jox la yaw wala keneen.
Jàppandig cër
6. Jàppandig cër.
- a. Cër yi, jëfekaay ak cër yu bawoo feneen, mba daju mbaa costéef yuñu maye ci digante cër yi mën na jàpp yenn saay, mën nañ leen maye ci luñu yemale, mbaa mën nañu wuute suñu sukkandikoo ci sa diiwaan mbaa Jëfandaay. Soo soppee barab bu àndak sa sa sàqum Microsoft, mën nga soxla jotaat ay daju mbaa jëfekaay yu jàppandiwoo ci yaw ak yuñu jëndoon ngir sa diiwaan bu njëkk. Nangu nga bàña jot mbaa jëfandikoo daju yi mbaa cër yu jaarul yoon mbaa yuñu joxul sàñ-sàñu jëfandikoo ci réew bi ngay duggee mbaa jëfandikoo yile daju mbaa cër, walla nëbb mbaa bàña cosaanal sa diiwaan mbaa sa xibaaru ràññeekaay ngir dugg mbaa jëfandikoo yile daju mbaa cër.
- b. Dañuy def lépp luñu mën ngir Cër yi dox; waaye, cëri yu nekk ci net bi yépp dañuy daj ay dog-dog ak paan yuy faral di am, te Microsoft yorul kiliftéefu benn dog-dog mbaa ñàkk bi la mën a dal ci loolu. Su amee ab paan, mën nga bàña mën a jëli Sa Këmb mbaa Njoxe yi nga dencoon. Nu ngi lay ñaan ngay faral di denc Say Ëmbiit ak Njoxe yi nga def ci Cër yi wala yi nga dencee ci Jëfekaay ak Cër yu ñeneen moom.
Ay yeesal ci Cër yi mbaa losisel bi, ak coppite yi am ci yile sàrt
7. Ay yeesal ci Cër yi mbaa losisel bi, ak coppite yi am ci yile sàrt.
- a. Mën nañu soppi yile Sàrt saa su nekk, te di nañ lako wax suñ ko defee. Jëfandikoo cër yi su bisu coppite jotee dafay tekki ni nangu nga sàrt yuñu bees yi. Sudee àndoo ci sàrt yu bees yii, kon bàyyil di jëfandikoo Cër yii, tëjal sa sàqum Microsoft te, sudee waajur wala kilifa gune, jàppaleel xale bi mu tëj sàqu Microsoft bi bu moom.
- b. Yenn saay di nga soxla ay yeesali losisel ngir wéy di jëfandikoo Cër yi. Mën nanu xool ci saasi sa sumbu losisel te yebbi yeesali losisel yi wala coppitey tëral. Mën nañ la laaj itam nga yeesa losisel bi ngir wéy di jëfandikoo Cër yi. Yile yeesal ñu ngi àju ci yile Sàrt ludul mu am yeneen sàrt yuy àndak yeesal yi, ci kaa bi nga xàm ni, yeneen sàrt yooyu dañuy jëfe. Amul lenn lu mën a sant Microsoft mu jàppandil ay yeesal, te du dig kenn ni nangu sumbu sistem bi ngay jëfandikoo ngir jënd wala daganalee sañ-sañ bi, jëfekaay yi, ëmbiit yi wala yeneen costéef. Yile yeesal mën nañu bàña àndak losisel bi mbaa cër yu xaaj bu bawoo feneen joxe. Mën nga Jëlaat sa nangu ci yeneen yeesali losisel yuy ñëw saa su nekk soo sampee losisel bi.
- c. Cig ndollent, mën na am ay jamono yuñuy soxla dindi mbaa soppi ay man-manu Cër bi mbaa dakkal joxe ab Cër ngir dugg ci Jëfekaay ak cëri bawoo feneen. Soo ci génnee dayo bu yoon buy jëfe laaj, amu ñu benn wareefu joxe ab yabaat mbaa wuutalu bépp daju, Marsandiisu Xarala (ni ñu ko xamlee ci pàcc 13.i), mbaa jëfekaay yi ñu mujjee jënd. Mën nga génn ay Cër wala seeni Man-man ci ab sumbu xoolalndi wala ñamandi, te loolu mën na baña dox ni mu waree, wala du mel ni sumb bu mat bi.
- d. Kon mën nga jëfandikoo jumtukaay yuñ aare DRM, lu ci melni yenn misik yi, po yi, filmu yi, téere yi ak yeneen mbir, losiseli DRM yi mën nañu jokk seen bopp ak ab cëru yelleef ci internet ba noppi mu yebbi ba noppi samp ay yeesal DRM.
Sañ-sañu Losisel bi
8. Sañ-sañu Losisel bi. Bépp losisel bunu la jox te mu bokk ci Cër yi dafay tënku ci Sàrt yii fileek àndul ak beneen déggoob sañ-sañu Microsoft (ci misaal, sudee dangay jëfandikoo jëfekaayu Microsoft bu bokk ci Windows wala mu am ci wàll, kon Sàrti Sañ-sañ yu Jumtukaayu Microsoft yu Doxalukaayu Windows boobu ñooy yilif losisel boobu). Jëfekaay yi nga amee ci yenn Màngasiin yu Microsoft moom wala ay bànxaasam (boole ci te du ci yam Màngasiinu Office, Màngasiinu Microsoft ci Windows ak Màngasiinu Microsoft ci Xbox) ñi ngi bokk ci pàcc 13.b.i bi ci suuf.
- a. Soo dëppook yile Sàrt, dañu lay jox àqi samp te jëfandikoo benn sotti ci jumtukaay bu nekk ci li aju àdduna bi yépp ngir jëfandikoo benn nit kase ci ab jamono ci sa kaadaru jëfandikoo yile Cër. Sudee yenn jëfandaay yi, mën nañu wàccaale ak jëfekaay bi, waaye ngir yaw kese lay doon te wut ci Cër yi luy nuru xaalis. Losisel bi mbaa daluweb bu bokk ci yi mën na dugal ab kotu wàll bu bawoo feneen. Xaaj yu bawoo feneen yu moom bile kot bi, budul Microsoft, jox nañ la sàñ-sàñu bépp mbindiin mbaa kot bu bawoo feneen, buñu lëkkale ak mbaa buñu dellu ci losisel bi mbaa daluweb bi. Dugal nañu ay karmat, su ci amee, ngir kotu xaaj yu bawoo feneen ngir xamal lako kase.
- b. Losisel bi am na sàñ-sàñ, buñu jaayul, te Microsoft dafay jaglel àq yépp ci losisel bu Microsoft joxewul, mu doon ci bokk, até mbaa neneen. Sàñ-sàñ bii du la jox bénn àq, te mën nga bàña:
- i. jalgati mbaa moytu bépp dogalu kaarànge xarala ci biir mbaa lu méngook losisel bi mbaa cër yi;
- ii. tasaare, booledi, fecci, pirate, roy, jariñoo, mbaa safaane defar gi ci bépp losisel mbaa yeneen xeeti Cër yuñu boole mbaa yuñu mën a jot ci digante Cër yi, ludul ak dayo kase bu yoonu sotti bi di jëfe moo maye ñu def lu ni mel;
- iii. àndaale losisel yu xaajaloo mbaa Cër yuñu war a jëfandikoo ci ay jëfandaay yu wuute;
- iv. siiwal, sotti, luwe, luwe ci diir bu yàgg, indi, séddale, mbaa abale losisel bi mbaa Cër yi, ludul Microsoft nangu la nga def loolu;
- v. jébbal losisel bi, bépp sàñ-sàñ, mbaa bépp àqi dugg mbaa jëfandikoo Cër yi;
- vi. jëfandikoo cër yi ci anam buñ ko nangoo bu mën na tere ku nekk mu jëfandikoo leen mbaa mën a dugg ci bépp cër, njoxe, sàq, mbaa mbaal;
- vii. dañu lay may nga jëfandikoo Cër yi wala nga mën a soppali jëfandaay bu Microsoft nangu (ci misaal., Xbox Consoles, Microsoft Surface ak yeneen) yu yeneen jëfekaay yi nangu di nangu.
Sàrti Payoor
9. Sàrti Payoor. Soo jëndee ab Cër, yile sàrti pay dañuy jëfe ci sa jënd te nga nangu leen.
- a. Fayyeeku yi. Su amee ab fayyeeku bu àndak ab dogitu Cër, nangu nga fay boobu njëg ci xaalis buñu xamle. Njëg buñu joxe ngir Cëri àndul ak jukki yuy jëfe yépp ak jekkali wecceeku xaalis, ludul dañ ko waxee neneen. Njëg yépp yu ñeel costéefi Skype yuñu fay boole nañ ci juuti yiy jëfe, ludul dañu wax leneen. Yaw yaay ki war a fay yile juuti mbaa yeneeni fayyeeku. Leeral dëkkuwaay yiñ boole ci say leerali faktiir la Skype di jël ngir xayma taks yi nga wara fay. Yaw yaa wara xool bu baax ndax leerali dëkkuwaay biñ ci bind jaar na yoon te yeesal nañu ko. Lu weesu costéefi Skype, dañuy sukkandiku ci barab bi nga sosee sa sàqum Microsoft, fileek yoon santaanwul ñu sukkandiku ci leneen ngir xayma say taks. Mën nañu ajandi mbaa fomb cër yi suñu jotul ab fayyeeku bu mat ak ci waxtu buñ lako laajee. Ajandi mbaa fomb cër yuñu dul fay mën na indo ñàkk a jëfandikoo sa sàq ak li ci nekk. Sudee danga jëfandikoo mbaalu liggéeyukaay wala mbaal mu suturlu, loolu dafay nëbb sa dëkkuwaay ba tax say taks mën a wuute ak biñ wane ci barab bi nga nekk. Mu ngi qju ci sa barab, yenn jëflante yi mën nañu laaj nga wecceeku ci xaalisu bitim-réew wala ñu tëral ko ci beneen réew. Sa bànk mën na la fayeeku yeneeni njëg ngir yooyu liggéeyal sooy jëfandikoo ab kàrtu bànk. Nu ngi lay ñaan nga jokkook sa bànk ngir am yeneeni leeral.
- b. Sa Sàqu Faktiir. Ngir fay njëgu ab cër, di nañ la laaj nga joxe ab anamu pay ci jamono bi nga bindoo ngir boobu Cër. Mën nga jëfandikoo ak soppi say leerali payoor ci bépp cër bu bokkul ak Skype soo demee ci Daluwebu saytu sàqum Microsoft (https://go.microsoft.com/fwlink/p/?linkid=618281) ak yu costéef ak losiselu Skype soo duggee ci sa dalu sàq ci https://skype.com/go/myaccount. Cig ndollent, nangul nga Microsoft mu jëfandikoo bépp leerali sàq buñu yeesal bu àju ci anamu payu sa bànk walla mbaalu pay buy jëfe bi nga tànn. Nangu nga yeesal ci saasi sa sàq ak yeneeni leeral, bokk na ci sa dëkkuwaayu bataaxal ak leerali anamu pay yi, ngir nu mën a mottali say jëflànte te jokkook yaw su ko laajee cig lëkkaloo ak say jëflante. Coppite yuñu amal ci sa sàqum faktiir duñu laal fayyeeku yuñu dugal ci sa sàqu faktiir laata ñuy mën a jëf ci say fayyeeku ci sa sàqu faktiir.
- c. Faktiir. Soo joxee Microsoft ab jumtukaayu payoor, dëggal nga (i) may nañu la nga jëfandikoo jumtukaayu payoor bi nga joxe te itam dëggal nga ni bépp leeralu payoor boo joxe jaar na yoon te dëgg la; (ii) may nga Microsoft mu jëfandikoo sa jumtukaayu payoor ngir dagg la ay Cër wala ëmbiit yu jàppandi; te itam (iii) may nga Microsoft mu dagg bépp man-man bu jaay ci Cër yi nga tànn ngir bindu ci wala jëfandikoo ko ci bi Sàrt yii di dox. Mën nañ la fayyeeku (a) ci lu jiitu, (b) ci jamono bi ngay jënd; (c) bi nga jëfee ba noppi, (d) ci ab sukkandikukaay buy faral di am ngir Cëri bindu. Itam, mën nañ la fayyeeku ci dayo bi nga nangu, te di nañ la yëgël lu teel su amee bépp coppite ci tolluwaayu xaalis bi nga war a fay ci Cëri bindu yuy faral di ñëw. Mën nañ la fayyeeku benn yoon lu ëpp benn sa diiru faktiir uu njëkk ngir tolluwaay yu aggoon ci njëlbéen.
- d. Pay yuy faral di am. Sudee danga jënd ay Cër yu lalu ci sa bindu (ci misaal, weer wu nekk, 3 weer yu nekk, wala at mu nekk), nangu nga ni maye nga ñu lay faral di la fayyeeku, te ñu jaare fayyeeku googu ngay fay Microsoft ci jumtukaay bi nga joxe ak ca waxtu ya mu waree te nga ànd ca, fileek yaw wala Microsoft dakkalul sa bindu ca Cër boobu. Soo bañee ñu daggaat la xaalis ngir benn cër fàww nga dakkal ko balaa bis biñ la koy dagg ngir nga wéy di jot. Dina nu yónnee ak tegtal yu lay xamal ni ngay dakkalee cër yi. Soo nangoo ñu lay faral di dagg, may nga Microsoft mu jëfandikoo masin ngir dagg la wala wiiremaa ngir dila fayyeeku (sudee fayiin bi tudd Automated Clearing House wala lu nuróo ak moom), wala ñu daggee la ci sàq mi nga tànn (fayee ci kàrt keredi wala lu nuróo ak moom) (nga boole lépp muy, "Fayee ci Masin"). Li ci gën a bari, dañu lay fayyeeku say ferey bindu yi lu jiitu diiru bindu bi di tàmbalee dox. Sudee dafa am luy waarul fay te muujiwul àntu, wala sudee dañu bañ nga fayee ak ab kàrt keredi wala xeetu fayyiin wu ni mel, Microsoft wala ay jaaykati cëram am nañu sañ-sañu jël bépp ëmbeefu delloo, dàq wala xaalis bu doyul daal di lay fayyeeku ci anamu Fayee Masin.
- e. Njuumte sa sàrt yi ci net bi. Sudee yeneen cër yu wuute ak Skype, Microsoft dina la joxee faktiir ci net ci Daluwebu saytug sàqum Microsoft (https://go.microsoft.com/fwlink/p/?linkid=618282), nga mën faa xoole ak sotti fa sa faktiir. Ci Skype, mën nga jot ci sa faktiir biñ lay yónnee ci net bi soo duggee ci sa sàq ci www.skype.com (https://www.skype.com). Lii mooy mennum nettalib faktiir buñuy joxe. Sudee dañoo juum ci sa faktiir, war nga ñu ko xamal ci diirup 90 fan yu wees bis bu njëkk bu njuumte bi feeñee ci sa faktiir. Di nañu gëstu, su boobaa fayyeeku bi. Soo ñu ko waxul ci diir boobu, génnee nga ñu ci suñu kiliftéef yépp ak jéebaaneg ñàkk yuy bawoo ci njuumte bi te duñu laaj ñu saafaral njuumte bi mbaa joxe ab delloo xaalis, lu dul yoon dafa koo sàkku ci beneen anam. Sudee Microsoft dafa gis ab njuumtey faktiir, di nañ ko saafaral ci diirup 90 fan. Sàrt bii du lor benn àqi yoon bu mën a jëfe.
- f. Sàrti delloo xaalis. Fileeg yoon indiwul ay coppite ci sàrti njaayum cër bi, soo xasee ba jënd jeexna, kenn dula dellooti sa xaalis. Soo gëmee ni Microsoft daf la fayyeeku ci njuumte, war nga jokkook ñun ci diirup 90 fanu fayyeeku boobu. Duñu delloo dara ci bépp fayeeku bu weesu 90 fan, lu dul yoon dafa koo sàkku ci beneen anam. Dañuy jagleel àqi defar ay delloo xaalis mbaa keredi ci suñu kumpa kase amaa yoon tërëlee ko neneen. Suñu defaree ab delloo xaalis mbaa keredi, amu ñu benn waréefu defar bu ni mel mbaa delloo xaalis ci liy ñëw. Sàrt delloo xaalis bii du lor benn àqi yoon bu mën a jëfe. Ngir am yeneen leeral ci delloo xaalis bi, demal ci sunu tombu ndimbal (https://go.microsoft.com/fwlink/p/?linkid=618283). Soo dëkke Taywan wala Israel, nu ngi lay ñaan nga jàpp ni sunu sukkandikoo ci Yoonu Aar Way-jëfandikukatu Taywan bi ak ay tëriliin yi mu àndal, jënd yépp yu bokk ci këmbi xarala yu nu joxe jaare ko ci tëggiinu bu ñu mënul téye ci loxo ak/mbaa liggéeyali net jeex foofu lañu yem te amul delloo xaalis sunu joxee yooyu këmb wala liggéeyal ci net bi. Amuloo sañ-sañu laaj benn diirup xarandi wala delloo xaalis.
- g. Dakkal cër yi. Mën nga fomb ab cër saa su nekk, mu àndak ab sabab am déet. Soo dakkalee benn cër boodoon fay danuy bàyyi dila dagg cër boobu. Ngir fomm ab liggééyal te laaj ñu delloo la sa xaalis, su la ko yoon mayee, yëral daluwebu saytu sàqum Microsoft bi. Sudee Skype la, soo koy jëlaat danga jël leeral yi ci Formileeru Jëlaat yiñ la jox ci here (https://go.microsoft.com/fwlink/p/?linkid=618286). Danga war di dellu xool ci liñ wax ci Cër bi ngay jëfandikoo ndax (i) mën nañu la baña delloo sa xaalis ca waxtu wa nga bàyyee; (ii) mën nañu sàkku ci yaw nga fay fere yi ànd ci bàyyi gi; (iii) mën nañu sàkku ci yaw ngay bépp fere yiñ amal ci sa sàqu faktiir ngir Cër yi ngir fay lu jiitu bis ngay bàyyi; te (iv) mën nga bañati mën a jot wala jëfandikoo sam sàq soo bàyyee Cër yi; or sudee Taywan wala Israel nga dëkk, (v) mën nañu la delloo ab xaalis bu tolloo ak fere yi nga fayoon ci Cër yi te jotoo leen jëfandikoo laata ngay bàyyi. Su fekkee Israel nga dëkk mën nga bàyyi ci bepp ci anam yi nu lim https://support.microsoft.com/help/4027815. Nu ngi lay ñaan nga jokkoo ci telefon bi ak ki teewal Microsoft ci sa diwaan ngir nu deloo la xaalis so ko yeloo. Dina nu jëfandikoo say Njoxe ci ni nu ko leeralee ci pàcc 4. Soo ko dakkalee, dootoo mën jot ci Cër yi su joxaale àpp bi Cër bi am wala, suñu faktiiree sam sàq ci diir buñ yamale, ci njeexitu diir bi nga ko dakkalee. Sudee danga dooroon defaat faktiir ci li weesu ak sa bànk ngir fay say Cër, dina nu jàpp ni bàyyi nga li ko dalee bis bi nga defee payoor gu njëkk ga, te may nga nu ci saasi nu dakkal sag jëfandikoo ci cër bi ak/wala dàq bépp njoxe bu ñu la joxoon ginaaw bi nga fayee.
- h. Diiru ñamandi yiñ la may. Sudee danga bokk ci ñiy ñamandi ab diir, dinga dem ba jamono fàww nga dakkal ñamandi gi, muy lañu lay xamal laata ñu lay may nga tàmbali ñamandi gi ngir bañ ñu lay dagg ngir nga mën a wéyal jëfandikoog Cër bi (yi) su diiru ñamandi gi jeexee. Ci yenn xéewali diiru jàngat, mën nañu laaj nga taal yeesal sa bopp.
- i. Xéewali Promo yi. Yenn saay, Mîcrosoft mën naa joxe ay cër ngir ab diirup ñàmandi bodul fay darra. Microsoft mooy seet ndax dañu lay dagg ci Cër yooyu (ci njëg li war) sudee mooy Microsoft dafa gis ni (te mën na ci baña joxe leeral) dangay jalgati sàrti neexal boobu.
- j. Coppite yi ci njëg yi. Mën nañu soppi njëgu Cër yi saa yu nekk te sudee dañu lay faral di fayyeeku, dina nu la ko yëgalee ci bataaxal, wala yeneen anam yu xel nangu, gën gaa yeex 15 fan laata njëg li di soppiku. Soo nanguwul coppite njëg bi, war nga fomb te dakkal jëfandikoo Cër yi laata coppite njëg bi di door. Su amee ab diir ak njëg bu sax ngir sa maye cër, dina ñu dëkke di jëfe njëg boobu ngir diir bu sax.
- k. Li ñu lay fay. Suñ la amelee ab payoor, nangu nga jox ñu ci lu gaaw te jub ay leeral yuñu soxla ngir jaglel la boobu payoor. Dafa bokk ci yoon yiñ tëral, yaa wara fay bépp juuti wala galak bu wara ànd ci payoor bii ñu lay defal. War nga nangu itam yeneen anam yuñu dugal ci sa àq ci bépp payoor. Soo jotee ab payoor ci njuumte, yoon may nañu ñu laaj la nga delloo xaalis bi. Nangu nga ànd liggéey ak ñun ci luñ jéem ngir def lii. Mën nañ wàññi itam payoor buñ la jaglel te duñ la ci lako yëgël ngir defaraat bépp payoor bu ëpp bu ci amoon.
- l. Kàrti neexal. Wecci ak jëfandikoo kàrti neexal (yeneen yu bokkul ak kàrti neexali Skype) ki leen yilif mooy Sàrti Jëfandikoo Kàrtu Neexalu Microsoft (https://support.microsoft.com/help/10562/microsoft-account-gift-card-terms-and-conditions). Amna leerali kàrti neexali Skype yu jàppandi ci Këtu ndimbalu (https://go.microsoft.com/fwlink/?LinkId=615383) Skype.
- m. Jumtukaayu Payooru Sàqu Bànk. Mën nga bindu ngir wut sàqum bànk buy ànd ak sa sàqum Microsoft muy sa jumtukaayu payoor. Sàqi bànk yi ci mën a bokk ñooy sàq yi nekk ci bànk yiñ mën a defee ay wiirmaa yu mag (ci misaal, ab bànku Etaa-Sini buy am njoxey “automated clearing house” ("ACH"), ab banku Ëroop buñ nangu Single Euro Payments Area ("SEPA") wala buy nangu "iDEAL" ca Peyi Baa). Sàrt yi nga nangu bi ngay joxe sa sàqum bànk muy sa jumtukaayu payoor ci sa sàqum Microsoft (ci misaal, “ndaw li” sudee dafa am SEPA) da ciy bokk itam. Teewal nga te nangu nga ni sàqu bànk bi nga bind, ci sa tur la nekk wala may nañu la nga bindu ak jëfandikoo bii sàqu bànk muy sa jumtukaayu payoor. Soo bindee wala nga tànn sa sàqu bànk muy sa jumtukaayu payoor, may nga Microsoft (wala ndawam) muy tàmbali la dagg benn yoon wala lu ko ëpp lu tolloo ak li nga jënd wala njëg li nga bindoo (ci lu dëppoo ak sàrti cër bi nga bindu) ci sa sàqu bànk (te sudee laaj na ko, nga dugal benn keredi ci sam sàq bànk ngir saafara njuumte yi, delloo xaalis wala jëf ju ni mel), te itam may nga bànk bi sam sàq nekk, mu dagg la boobu xaalis wala mu nangu keredi yooyu. Xam nga bu baax ni dingal li nga joxe dafay wéy di dox te dara du ci soppiku fileek dindiwoo say leerali sàqu bànk ci sa sàqum Microsoft. Jokkool ak sa ndimbalu kiliyaan ci ni ñu ko leeralee ci kaw ci pàcc 4.e ci ni mu gën a gaawee sudee danga gëm ni dañu juum dagg la. Yoon yiy dox ci sam réew mën nañu yamale li ñuy teg ci sa ndoddu jamono ju jëflante gi amee njuumte, lu jubadi ci sam sàqu bànk. Soo bindee wala nga tànn sa sàqu bànk muy sa jumtukaayu payoor, nangu nga ni jàng nga te xam nga ci Sàrt yii.
Bankaas biy Jël Kontraa bi, Tànneef Yoon wi, ak Barab bi ñuy Saafara Jafe-jafe yi
10. Bankaas biy jël Kontraa bi, Tànneef yoon wi, & Barab bi ñuy Saafara Jafe-jafe yi. Ngir sag jëfandikoo cër yi am màrku Skype yiy maye ak yiy jaay, soo dëkkee fu bokkul ak Ërop, Moyen Orient ak Afrik, yaa ngi séq kontraa ak "Microsoft" ay lépp lu baat yii wundu, Skype Communications S.à.r.l, 23 – 29 Rives de Clausen, L-2165 Luxembourg fileek leeralee wuñu ko neneen ci suuf. Ñiy jëfandikoo cër yi am màrku Skype, ñuy fay wala ci luñu dul fay te dëkku ñu Ërop, Moyen Orient ak Afrik, yooni waa Luxembourg ñooy wax li ñu namm ci sàrti yi ak bépp jàmbat bu jëm ci seeni jalgati, naam werante dafay am ci yoon yi. Yoonu tund mbaa réew yi nga dëkk ñooy saytu yeneen jéebaane yépp (bokk na ci kaarànge aji-jëfandikookat, konkiraas bu jaaduwul, ak jébaaneg bu yuy waral ate siwil). Sudee danga dëkk fu bokkul ak Ërop, Moyen Orient wala Afrik, yaw ak nu nangu nanu ni yoon yu këri àttekaayi waa Luxembourg tëral ñoo nuy àtte su amee benn jàppante, werante bu fi am wala lenn lu jëm ci jëfandikukatu cër yi am màrku Skype. Sudee yeneen cër yi, yaw ak ki nga séqal kontraa bi, yoon wiy àtte, ak barab bi ñuy saafaraa jafe-jafe yi dina ñu feeñ fii ci suuf:
- a. Kanadaa. Soo dëkkee ci (mbaa, sudee ab liggéeyukaay, sa barabu liggéey dafa nekk) Kanadaa, te ngay jëfandikoo Cër yi am màrku Skype, wala sudee dangay jëfandikoo ay wàll Microsoft Teams, séq nga kontraa ak Skype Communications US Corporation, 2215-B Renaissance Drive, Las Vegas, NV 89119, United States. Nguir lenen lepp luy meye wala lu lacc fey luy Njeriñu wayjefandikoo, danguey bindu ak Microsoft Corporation, One Microsoft Way, Redmond, WA 98052, U.S.A. Yoonu deuk bi nga deuk (wala, su feke ni da ame liguey, sa beureubu ligueyukay bi eup loy nek) moy djiitte jangatu Sarte yoyu, lacc ndogale ci sen jalguati, ak lep luy sen wootte (bokk ci aaru wayjefandikoo, jongante bu diaarule ci yoon, ay lacc yu teguwule fenn), te xoolu ci xeex wala teuralinu yoon. Yaw ak nun nangu nañu ba fàww ci ate bunu dongal ak barabu àttekaayu Ontario ngir ñàkka déggoo yépp yuy joge ci mbaa méngook yile Sàrt mbaa Cër.
- b. Bëj-gànnaar mbaa or Bëj-saalumu Amerig ci biti Etaa-Sini ak Kanadaa. Soo dëkkee ci (mbaa, sudee ab liggéeyukaay, sa barabu liggéey dafa nekk) Bëj-gànnaar mbaa or Bëj-saalumu Amerig ci biti Etaa-Sini ak adaa, yaa ngi jëflànteek Microsoft Corporation, One Microsoft Way, Redmond, WA 98052, U.S.A. Yooni Réewu Washington ñooy saytu nuñuy tekkee yile Sàrt ak yeneen jéebaane ngir seeni jagali, ci li aju ci tànnéefi sukkandikaayu yoon yi. Yoonu réew bunu jaaralee sunuy Cër ñooy saytu yeneen jéebaane yépp (bokk na ci kaarànge aji-jëfandikookat, konkiraas bu jaaduwul, ak jébaaneg bu yuy waral ate siwil).
- c. Moyen Orient, Afrik wala Ërop. Sudee danga dëkk (wala, sudee li gën a am doole ci sa liggéey nekk ci) Moyen Orient, Afrik wala ci Ërop fu bokkul ci Union Ëropeyen (UE), Island, Lichtenstein, Norwees, Siwiis, ak Bretaañ ju Mag ja ba noppi ngay di jëfandikoo wàll ci yuñ maye ci Cër bi (lu ci melni Bing ak MSN), ki nga séqal kontraa bi mooy Microsoft Corporation, One Microsoft Way, Redmond, WA 98052, U.S.A., bamu des sudee wàll yuñ maye ci Skype kese ngay jëfandikoo, ki nga séqal kontraa bi mooy Microsoft Ireland Operations Limited, One Microsoft Place, South County Business Park, Leopardstown, Dublin 18, Ireland. Sudee dangay fay wàll wi ngay jëfandikoo ci Cër bi, ki nga séqal kontraa bi mooy Microsoft Ireland Operations Limited, One Microsoft Place, South County Business Park, Leopardstown, Dublin 18, Ireland. Ngir Cër yoodul ak yi ngay fay, yoonu Irlànd mooy saytu nuñuy tekkee yile Sàrt te sàkku ñu ban leen jëfe, moo xàm xiiroo ak ŋaayoo sukkandikaayu yoon yi. Yoonu réew bunu jaaralee sunuy Cër ñooy saytu yeneen jéebaane yépp (bokk na ci kaarànge aji-jëfandikookat, konkiraas bu jaaduwul, ak jébaaneg bu yuy waral ate siwil). Yaw ak ñun nangu nañu ba fàw ci ate bunu dongal ak barabu atékaayu Ontario ngir ñàkka déggoo yépp yuy joge ci mbaa méngook yile Sàrt mbaa Cër.
- d. Asii mbaa Bëj-saalum Pasifik, donte sa dañuy ràññatle sa réew fii ci suuf. Sudee danga dëkk ci (wala, sudee liggéeyukaay la, sa barabu liggéeyukaay bi gëna mag mingi ci) Asie (bamu des Chine, Japon, République bu Kore, wala Taiwan) wala Pasifik Sud, te yaa ngi jëfandikoo wàll yi Cër yi doo fay (lu melni Bing ak MSN), yaa ngi déggoo ak Microsoft Corporation, jëfandikoo benn Cër, Redmond, WA 98052, U.S. sarwiisu Outlook.com bu amul fayda ci Singapuur wala Hong Kong, yaa ngi déggoo ak Microsoft Regional Sales Pte Ltd., ab liggéeyukaay buñ yamale ci yooni Singapuur, adres biñu bind ci Mbedd Cecil 182, #13-01 Frasers Tower, Singapuur 069547; sudee danga dëkk ci (wala, sudee liggéeyukaay la, sa barabu liggéeyukaay bu mag mingi ci) Australie, yaa ngi déggoo ak Microsoft Pty Ltd, 1 Denison St, North Sydney, NSW 2060, Australie, te sudee danga dëkk ci (wala, sudee liggéeyukaay la, sa barabu liggéeyukaay bu mag mingi ci) Nouvelle-Zélande, yaa ngi déggoo ak Microsoft New Zealand Limited tolluwaay 5. 22 Viaduct Harbour Avenue, Box post 8070 mbedd symonds, auckland, 1150 Nouvelle-Zélande. Sudee Cër yi jaay wala yiy maye, Etaa bu Washington mooy yilif niñ wara déggee Sàrti yii ak jàmbati jalgati yi ci am, xoolu ci ñàkk a déggoo yiy am ci yoon yu bokkul nuñ tëddee. Yoonu réew bunu jaaralee sunuy Cër ñooy saytu yeneen jéebaane yépp (bokk na ci kaarànge aji-jëfandikookat, konkiraas bu jaaduwul, ak jébaaneg bu yuy waral ate siwil). Dina ñu déllu te ci mujanteel bi saafaral ci bépp ñàkka déggoo bu joge ci mbaa méngook yile Sàrt mbaa Cër bu bokkul ak Skype, bokk na ci bépp laaj bu àju ci seeni nekkiin, wéraay, mbaa njeexte, cig atekaayu Singapuur àndak sàrtu SIAC (Arbitration Rules of the Singapore International Arbitration Center), sàrt buñu wara dugal cig royuwaay ci bii tomb. Atekaay bi benn atekat la fa Njiitu SIAC di jël. Làkku ate bi Àngale lay doon. Dogalu ate bi mooy doon bu mujj, takku te kenn duko mën a weddi, te mën nañ ko jëfandikoo niki sukkandikukaayu ate ci bépp réew mbaa diiwaan.
- e. Sapoo. Soo dëkkee ci (mbaa, sudee ab liggéeyukaay, sa barabu liggéey dafa nekk) Sapoo mbaa Afrig, te ngay jëfandikoo ay doggitu cër yodul fay (niki Bing ak MSN); ya ngi jëflànteek Microsoft Corporation, One Microsoft Way, Redmond, WA 98052, U.S.A. Sudee da nga fayoon ngir jëfandikoo ab doggitu cër yi, ya ngi jëflànteek Microsoft Sapoo Co., Ltd (MSKK), Shinagawa Grand Central Tower, 2-16-3 Konan Minato-ku, Tokyo 108-0075. Ngir Cër yu ñuy fay ak yuñ dul fay, yoonu Sapoo mooy saytu Sàrti yi ak bépp jafe-jafe bu ciy judd mbaa bu méngook ñoom mbaa Cër yi. Yaw ak ñun nangu nañu ba fàw ci ate cosaan bunu dongal ak barabu atékaayu goxu Tokyo ngir ñàkka déggoo yépp yuy joge ci mbaa méngook yile Sàrt mbaa Cër.
- f. Réewu Kore.
- i. So deuke ci (wala, su feke sa liguey, sa ligueyukaay bo eup loy liguey dafa nek ci) Republicu Corée, te danguey jefandikoo wallu Njeriñ (lu melni Bing ak MSN), yangui bindu ci Microsoft Corporation, One Microsoft Way, Redmond, WA 98052, U.S.A. So feye nguir jefandikoo walu Njeriñ yi, yangui bindu ak Microsoft Corée, 12th Floor, Tower A, The K-Twin Tower, Jongro 1 gil 50, Jongro-gu, Seoul, Republicu Corée, 03142. Nguir Njeriñ yi ame fey ak yi amule fey, yoonu Republicu Corée ñoy djiitte sarte yoyu te ñoy ame solo ci yeegum guen ci wala ci lu len laale wala Njeriñ yi. Yaw ak ñun nangu nañu ba fàw ci ate cosaan bunu dongalul ak barabu atékaayu goxu Diggu Sewul ngir ñàkka déggoo yépp yuy joge ci mbaa méngook yile Sàrt mbaa Cër yi.
- ii. Soo dëkkee ci Réewum Kore, ci yoon, kontraa bu melni Sàrt yii mëna yamale yenn ci say sañ-sañ yi nga am. Sàrt yii jublu wuñu ci yamale yooyu yelleef wala yamale wóoraayu Microsoft bi yoon teg ci kawam. Ginaaw tëralin yi fi nekk lépp lu wuute te nekk fi, Sàrt dina ñu mëna dox ba fi ko yoon di yamale. Bépp coppite ci yii Sàrt (ak bépp coppite ci xaalis biñ lay faral di fayyeeku ndax cër yi nga abone, sudee amna) di nañ ko amal ci anam wi ko yoon santaanee.
- g. Taywan. Soo dëkkee ci (wala, sudee ab liggéeyukaay, sa barabu liggéeyukaay bu mag mingi ci) Taywan, te yaa ngi jëfandikoo ay pàcc ci Cër yi te doo fay (lu melni Bing ak MSN), yaa ngi déggoo ak Microsoft Corporation, One Microsoft Way, Redmond, WA 98052, U.S.A. Sudee danga fay ngir jëfandikoo benn wàll ci Cër yi, jàpp nga déggoo ak Microsoft Taiwan Corp., 18F, N°68, Sec. 5, Zhongxiao E. Rd., Distrik Xinyi, Taipei 11065, Taïwan. Sudee Cër yi am fay ak yi amul fay, yoon yi waa Taywan tëral ñooy yilif sàrt yii ak bépp jafe-jafe bu ci juddoo, bu bokk ak ñoom wala Cër yi. Ngir am yeneeni leeral yu neel Microsoft Taiwan Corp., baal ñu xool daluweb bu Ministeer bi yor mbiru Bitim Réew R.O.C. joxe. (https://gcis.nat.gov.tw/mainNew/). Yaw ak ñun joxoñ nañu ba fàw Atekaayu Goxu Taype niki atekaayu njëlbéen bu amal ate ci bépp ñàkka déggoo buy joge ci mbaa méngook yile Sàrt mbaa Cëri bi, ci dayoo bu ëpp bu yoonu Taywan maye.
Sa yoonu aji-jëfandikoo yi teew mën nañu sàkku yenn yoon yi teew ngir saytu mbaa joxe àqi saafaral ñàkka déggoo ci beneen fuwaar ak lu Sàrti yii mën a doon. Su loolu amee, tànnéefu yoon ak matukaay fal yi ci pàcc 10 buy jëfe niki nuko sa yooni aji-jëfandikoo réew nangoo.
Gaaraanti
11. Garanti yi.
- a. MICROSOFT, AK SUNUY BANQAAS, JAAYAATKAT YI, SEDDALEKAT YI, AK JAAKAT YI, JOXE WUÑU BENN GARANTI, BUÑU WAX MBAA NËBB, GARANTI YI MBAA SÀRT YI CI LI AJU CI NI NGAY JËFANDIKOO CËR YI. XAM NGA NI JËFANDIKOO CËR YOOYU MËN NALA LOR TE DANUY JOXE CËR YI CI "NUÑU MEL" AK "NJUUMTE YEPP" AK "SU JAPPANDI WEE." MICROSOFT DU LA GAARAANTI NI CËR DAÑUY DOX BU BAAX SAA YU NEKK TE DUÑU AM BENN DOG-DOG. MËN NGA AM YENN ÀQ CI SA YOONU YU AJU CI BARAB. JËMEE WUÑU LENN CI YILE SART NGIR ÑU LOR YOOYU ÀQ, SUDEE DAÑUY JËFEE. NANGU NGA NI NOSTEY ORDINATËER AK WAXTAANU TELEFON YI MËNU ÑU BAÑA AM AY NJUUMTE AK AY DIIRU TAXAWANDI YU FARAL DI AM. GARANTI WUÑU NI CËR DUÑU DAKKAL CËR YI, ÀPP, KAARANGE, MBAA ÑÀKK NJUUMTE MBAA ÑÀKKUM ËMBIIT, GARANTI WUÑU ITAM BEPP LONKU CI MBAA JOKKALINU XIBAAR CI AY MBAALU ORDINATËER.
- b. CI DAYO BU ËPP BUÑU NANGU CI SA KAADARU SA YOONU REEW, DAÑUY DÀQ BEPP GARANTI BU NËBBU, BOKK NA CI MËNIINU NJAAY, BAAXAAYU LUÑU MËN A NANGU, JEKKAL NGIR JUBLUWAAY BU XEJJIKU, NJUUMTEY DEFAR, AK NÀKKA LUUBAL.
- c. Ngir aji-jëfandikoo yu dëkk ci Ostrali: Sunuy marsandiis ak sunu cër dañuy àndaale ak gaaraanti yu kenn mënul génne ci Sañ-sañu Jëfandikukat yu waa Óstraali. Sudee gisoo loolu ci cër bi, am nga sañ-sañu:
- dakkal sa kontraa ak nun ci cër bi; ak
- nu delloo la li nga jëfandikoowul, wala jox la ndàmpaay ndax li njariñ li des.
Am nga sañ-sañu ni nañu la delloo sa xaalis wala ñu jox la beneen marsadiis bu gën a baax. Sudee sikk bi ci marsandiis yi wala ci cër bi nekkul sikk bu deme noonu, dañu la wara saafaraal sikk boobu ci waxtu wi mu jaadoo. Sudee defu ñu ko, dañu la wara dello njëgu marsandiis bi sula neexee itam nga dakkal sa kontraa ak nun ci cër bi, te ñu delloo la loo jotul a jëfandikoo. War nañu la jox ndàmpaay itam ci lépp loo mën a ñàkk lu xel mën a nangu, wala loo mën a yàqule sudee marsandiis bi wala cër bi dafa am sikk.
- d. Ngir aji-jëfandikoo yu dëkk Nouvel Zeland, mën ngeen a ay àqi yoon ci kaadarujëfu Garanti aji-jëfandikoo Nouvel Zeland, te lenn ci yile sàrt warul a lor yooyu àq.
Yameefu kilifteef
12. Yamale ak Wóoraay.
- a. Sudee danga am luñ la wara joxee ndàmpaay (lu ci xel Sàrt yii), ci anam wu dëppoo ak li yoon maye, nangu nga ni li nga mën a def ngir indi ci saafara du lenn ludul defaraat, ci Microsoft wala ci ñi mi lëkkalool, ñiy jënd-jaayaat, ñiy séddale, ñiy joxe Cër ak Jëfekaayi Jàmbur, ak jaaykat yi, ndàmpaay lu tollu ci fere yi nga def ci Cër yi ci weer wi nga ñàkkee wala wiñ jalgati gi amee (wala lu yegg ci USD$10.00 sudee Cër bi dafay maye).
- b. Ba fu la yoon buy jëfe may, mënuloo dabuwaat bépp (i) ñàkk mbaa réeral yuy lore; (ii) ñàkkub njuréef yu teew mbaa yu ñu dabu (mu jub mbaa mu dëng); (iii) ñàkkub alal bu teew mbaa bu ñu dabu (mu jub mbaa mu dëng); (iv) ñàkk xame mbaa liggéeyukaa mbaa yeneeni ñàkk mbaa yàqute yu bawoo ci jëfandikoo Liggéyal yi ci ab man-man bu amul boroom; (v) ñàkk mbaa yàqute yuy bañal, mbaa indi xew-xew, bu jubul te xejjiku; ak (vi) ci dayo bu ëpp bu yoon maye, ñàkk mbaa réeral yu jub yu bawoo ci lu ñu romb ci pàcc 12.a. bii ci kaw. Yile yemale ak dàq dañuy jëfe sudee saafara bii du la fay ci bépp ñàkk mbaa dog-dogu jubluwaay bu am solo mbaa suñu xàmoon mbaa waroon a xàm ni yàqute yi mën nañu am. Ci dayoo bu ëpp bu yoon maye, yile yemale ak dañuy jëfe ci lépp mbaa bépp jéebaaneg bu méngook yile Sàrt, Cër yi, mbaa losisel bu méngook Cër yi.
- c. Microsoft waralul benn dog-dog ngir amal mbaa yeexal xaranaayu ay waréefam ci kaadaru yile Sàrt ba ci dayo sudee dog-dog bi mbaa yeexal ay xew-xew yu Microsoft fugluwul ñoo ko waral (niki xirook ak ŋaayoo liggéey, jëfi Yalla, xaré, jëfu defkatu lu ñaaw, yàqute yu soxor, aksidan mbaa nangul bépp yoon mbaa santaane nguur). Microsoft dina jéem a wàññi jeexiti xew-xew yii yépp ak ngir amal waréef yu loruwul.
Sàrt yuy àndak cër yi
13. Sàrt yuy àndak cër yi. Sàrt yi jittu ak yi weesu pàcc 13 dañuy faral di jëfe ci cër yépp. Pàcc bii am na ay sàrt yuy àndak cër yuñu yokk ci sàrt yu matale. Su werante amee ci diggante sàrt yii ñuy wax ak yeneen sàrt yu mag yi, nañu sukkandiku ci sàrti cër yii.
Xbox
- a. Xbox.
- i. Jëfandikoo Jagoo ak budul Jaay. Xbox bi ci net bi, ("Reseau Xbox"), Powi Xbox Game Studios (bokk na ci Mojang Games) (https://www.xbox.com/xbox-game-studios), aplikaasioŋ yi, abone yi (lu melni, sarwiisu abonemaa yi Xbox Game Pass joxe), sarwis yi (lu melni, Xbox Cloud Gaming), ak ëmbiit li Microsoft joxe (ñépp booleSerwiisi Xbox) danu ko jaglee jëfandi koo kër kenn waruko jaay.
- ii. Cëri Xbox. Soo abone ngir jot Cëri Xbox, leeral yi jëm ci sa jeu po, say liggéey ak jëfandikoo po yi ak Cëri Xbox yi dina ñu leen topp ba noppi séddoo leen ak ñeneen, lu ci melni defarkati po yi ak siiwalkat yi, ngir Microsoft mëna joxe Cëri Xbox yi ak ñeneen ñi ñu mëna doxal po yi ak cër yi bokkul ak Microsoft. Rax ci dolli, sudee ab aparey wala platform bu nekk ci digante yenen moo lay jëfandikoo ngir dugg ci Serwiisu Xbox, mën nañu topp ak séddoo leeral yi jëm ci sa fowokaayu jeu, say liggéey ak sa jëfandikoo ay pomi ak Serwiisu Xbox, lépp di aju ci bépp sàrt ak sàrti bopp bu beneen mbootaay bi tëral. Soo duggee ci beneen platform wala jëfandaay ak sa sàqum Microsoft wala nga lëkkale sa sàqum Microsoft ak platform wala jëfandaay yu mel noonu ngir jot ci Cër gu bokkul ak Microsoft (ci misaal, siiwalkatu jeu bu bokkul ak Microsoft bu Jëfekaay ak Cër yu Jàmbur), nangu nga ni: (a) Microsoft mën na séddoo kontu bu yam ak ay leeral yu jëm ci jëfandikoo (lu ci melni gamertag, gamerscore, jaar-jaaru jeu, done yu jëfandikoo ak limu xarit) ak pàrti boobu ni ko Microsoft waxee ci Sàrti Sutura, ak (b) sudee say jekkal sutura Xbox nangu nañu ko, pàrti bi mën na itam jot ci Sa Ëmbeef jaaraleko ci jokkoo yi ci biir po wala yeneen jëfekaay yi ngay jëfandikoo soo duggee ci sa sàq ak pàrti boobu. Te itam, su la ko say jekkali sutura su Xbox mayee, Microsoft mën na siiwal sa tur, xàmme po, nataalu po, bàkk, avatar, klipu po ak po yi nga musu fo ak nit ñi nga nangu. Sudee danga may jekkal Kaaraange njaboot gi jagleel Xbox, jekkal yooyu dañuy jëfe ci konsoli Xbox yi, Xbox Cloud Gaming, ak jëfekaayu Xbox ci PC wala costéef mobile, waaye mën nañu bañ a dox ci po yi Xbox Game Studios wala cër yi nga jot wala jou ci yeneen costéef wala platform. Ngir mëna am jaar-jaaru jeu bu gëna wóor ci sa waa kër, xoolal jekkal waajur yi ci yeneen aparey yi ak platform yii.
- iii. Sa Ëmbeef. Sunu mbébetu tabax asku Cëri Xbox, jox nga ndigal Microsoft, ay bànxaasam, wala ñi muy jox sañ-sañ, ñu mën a jëfandikoo fépp ci àdduna, soppali, sotti, séddale, siiwal; séddoo ak wane Say Ëmbiit wala sa tur, wala say xàmme po, sa bàkk, sa avatar bi nga siiwal ci Cëri Xbox.
- iv. Saytukatu po yi. Yenn po yi mën nañu jëfandikoo ak saytukat, àmbaasadër wala ay njaatige. Saytukatu po yi ak njaatige yi ay teewalkatu yu Microsoft nangu lañu. Seeni wonin farataluñu wone yosu Microsoft.
- v. Xale yi ak Xbox. Sudee ab gone buy jëfandikoo Cëri Xbox yi, sa waa-jur mbaa kilifë mën na saytu ci ay xeet yu bari yu sa sàq te mën na jot ay nettali yu àju ci sa jëfandikoo Cëri Xbox. Man-man yii, Cëri Xbox kese ñoo ko moom, te mënoo ko toxal ci yeneen jëfandaay wala platform.
- vi. Game Currency wala Virtual Goods. Cëri Xbox yi mën nañu àndak ab kopparu po bu jëmmadi (niki wurus, weccit mbaa poñ) buñu mën a jëndee ci Microsoft wala ci turam, di jëfandikoo ay jumtukaayu njëgi xaalis soo tollee ci atu "muskalaf" fi nga dëkk. Cëri Xbox yi mën nañu ànd itam ak ay jukki xarala mbaa costéefyu jëmmadi yuñu mën a jëndee ci Microsoft wala ci turam, di jëfandikoo ay jumtukaayu njëgi xaalis mbaa jëfandikoo kopparu fo. Kopparu po ak costéef yu jëmmadi mën nañ leen baña dabuwaat ba fàw ngir jumtukaayu njëgu xaalis yu teew, costéef, mbaa yeneeni jukkiy njëgi xaalis ci Microsoft mbaa bépp xaaj bu bawoo feneen. Ludul sàñ-sàñu jëfandikoo kopparu po buñu yemale, bu jagoo, buñu mën a teggi, buñu mànta jàllale, buñu mànta liggéeyal ci Cëri Xbox yi rekk, amuloo benn àq mbaa tural ci biir walla ci bépp kopparu po mbaa costéef bu jëmmadi bu ni mel bu ndurook mbaa bu bawoo ci Cër Xbox yi, walla bepp jagleel yuñu boolek jëfandikoo Cër yi mbaa yuñu denc ci Cër Xbox yi. Microsoft saa yu ko neexee mën na yamale, saytu, soppali ak/wala dindi koppari po mi ak/wala moomeel yu wirtuel yu nekk ci menn powum Xbox wala ay jëfekaay wala lu ko ëpp ndax moom rek moo xam kañ la wara amal coppite yi war ba noppi teg ko ci anam wi sa sàrtu réew maye.
- vii. Yeesalu Losisel yi. Bépp jëfandaay bu mëna lënku ci Cëri Xbox, mën nanu seet ci saasi sa sumbu losiselu jumtukaayu Xbox wala losiselu jëfekaayu Xbox bi te yebbil la yeesali jumtukaayu Xbox bi wala yu losiselu jëfekaayu Xbox wala yu coppiteg tabb gi, muy mbir yi lay tere jot ci Cëri Xbox yi, jëfandikoo po yu Xbox yuñ lay mayul wala jëfekaayi Xbox, wala jëfandikoo jëfandaay yuñ la mayul sañ-sañ ak jumtukaayu Xbox.
- viii. Losisel yuy Sàcc wala yuy Càcc. Bépp jëfandaay bu mën a lënku ci Cëri Xbox, mën nanu xool ci saasi ngir xam ndax tere wuñu ko, wala losisel yu mën a may nit ñuy sàcc wala ñuy saboote di jalgati Sàrti Doxalin yi wala Sàrt yii, ak yebbi yeesali losiselu jëfekaayu Xbox wala soppi jekkal yiñ fi def, lu ci melni jekkal yi lay tere nga jot ci Cëri Xbox, wala tere la nga jëfandikoo jumtukaay wala losisel bu lay may ngay sàcc wala ngay saboote.
- ix. Yeneen Sàrt ak Anami Abonmaa. Abonmaa Cëri Xbox dañu bokk ci yeneen sàrt ak anam yiñ tëral ci Sàrti ak Anami Abonmaa Xbox | Xbox (https://www.xbox.com/legal/subscription-terms).
- x. Bindu ci Mënloo Xbox bu doxul. Microsoft mën na fay li ñuy faral di la fayyeeku ba noopi dakkal liñu lay faral di dagg ci yenn réew yiñ tànn sudee jëfandikoowoo abonmaa Cëri Xbox ci ab diir. Microsoft dina la yónnee yëgle laata muy dakkal liñu lay faral di dagg. Ngir am ci yeneen leeral, boole ci diiru bi nga ñàkka jëfandikoo, xoolal ci Laaj yiy faral di ñëw (FAQ) ci abonmaa bu doxatul | Ndimbalu Xbox (https://support.xbox.com/en-GB/help/subscriptions-billing/manage-subscriptions/xbox-subscription-inactivity-policy).
- xi. Sàrtu deggoo jëfëndikukat ak tërëlinu doxalin. Yenn Mënloo Xbox yi mën nanu am seen sàrti jëfandiku ak tërëlinu doxalin yi.
Màngasiin
- b. Màngasiin. "Màngasiin" mooy cër bi lay may nga xuus, yebbi, jënd, ak may poñ wala amal jàngat ci jëfekaay yi (su nu waxee “jëfekaay” mooy po yi) ak yeneen ëmbiiti disitaal yi. Sàrt yii ñooy wax ci yenn Màngasiin yu Microsoft moom, yi muy doxal wala yu ay bànxaasam moom (boole ci, te du ci yam, lii di Màngasiinu Office, Màngasiinu Microsoft ci Windows ak ci Màngasiinu Microsoft ci Xbox). “Màngasiinu Office” mooy Màngasiinu jëfekaay ak costéefi ngir Office, Microsft 365, SharePoint, Exchange, Access ak Project (sumbu 2013 wala yi ci topp), wala beneen xeetu jëfandikoo bu am turu Màngasiinu Office. “Màngasiinu Microsoft ci Windows” mooy Màngasiin yu Microsoft moom wala ay bànxaasam, ngir jëfandaayi Windows lu ci melni telefon, PC ak tablet, wala beneen xeetu jëfandikoo bu am turu Màngasiinu Microsoft te ñu mën ko jotee ci jëfandaayi Windows yu ci melni telefon, PC wala tablet. “Microsoft Store ci Xbox” mooy Màngasiin yi Microsoft moom wala yi muy doxal wala ay bànxaasam ngir fowukaayu Xbox, wala beneen xeetu jëfandikoo bu am turu Màngasiinu Microsoft te ñu jàppandi fowukaayu Xbox.
- i. Sàrti Sàñ-sàñ. Dina ñu ràññee siiwalkatu bépp jëfekaay bu jàppandi ci Màngasiin bu am solo. Fileek joxewu yeneen sàrt yu ànd ci jëfekaay bi, Sàrti Sañ-sañu Jëfekaay bu Njëkk bi ("SALT") bi ci njeexte Sàrt yii ñooy déggoo bi dox sa diggante ak siiwalkatu jëfekaay bi di tëral sàrti sañ-sañ yi dox ci jëfekaay bi ngay yebbi ci bépp Màngasiin bu Microsoft moom wala ay bànxaasam (waaye Màngasiinu Office du ci bokk). Ci leeral, Sàrti yii ñoo yilif ni ñuy jëfandikoo cër yi bokk ci, wala yi Cëri Microsoft joxe. Pàcc 5 bu Sàrt yii dafay wax ci Cër ak Jëfekaayi Jàmbur yi nga jëlee cib Màngasiin. Jëfekaay yuñu yebbi ci Office Store SALT saytu wuko te am na ay sàrt sàñ-sàñ yu xaajaloo yuy jëfe.
- ii. Yeesal. Microsoft dafay seet ci saasi te yebbi ay yeesal ci say jëfekaay, donte duggoo ci ab Màngasiin bu am solo. Mën nga soppi sa Màngasiin mbaa say jekkali noste soo tànnee bàna jot ay yeesal ci saasi ci jëfekaayi Màngasiin bi. Waaye, yenn jëfekaayi Màngasiinu Office yi nga xamantani net bee leen dëkkal moo xam lépp walla ay pàcc ci ñoom, defarkatu jëfekaay bi mën nañu leen yeesal saa su nekk te itam mën nañu leen bañ a tàggu ci loolu.
- iii. Natt yi ak Topp yi. Sudee danga may poñ wala jàngat ab jëfekaay wala beneen Jumtukaayu Disitaal ci Màngasiin bi, mën nga jot bataaxalu Microsoft bu def ëmbiitu ki siiwal jëfekaay bi wala Jumtukaayu Disitaal bi. Bataaxal bu ni mel a ngi bawoo ci Microsoft; dunu séddoo sa dëkkuwaayu bataaxal ak ñiy siiwal jëfekaay yi wala Jumtukaayu Disitaal yi nga amee ci Màngasiin bi.
- iv. Dànkaafu kaarànge. Ngir moytu ngaañ yu ci mën a sababoo, jafe-jafe wala mettitu bët, war nga noppalu yenn saa cig jëfandikoo po yi walla yeneen jëfekaay, rawatina soo yëggee ab coono buy bawoo cig jëfandikoo. Sooy yëg ab jafe-jafe, noppalul. Jafe-jafe yi bokk na ci xel mu teey, feebaru yëngu-yëngu, miir, jaxasoo, bopp buy metti, coono, bët buy metti, walla gët yu wow. Jëfandikoo ay jëfekaay mën na la jaxase walla xatal ñi la wër. Moytul a fakkastalu, eskaliye, dal yu gàtt, ay yëf yu oyof walla yu am solo yu mën a yàqu. Ab pursantaasu nit bu ndaw mën nañu jaar ci ay kiris suñ leen teggee ci yenn nataal jakkarloo niki ékleer yi mbaa ay royuwaay yu mën feeñ ci jëfekaay yi. Akit nit yu jaarul ci ay kiris mën nañu am ab anam buñu saytuwul bu mën a waral yile kiris. Li kay wone mën na boole miir, gis-gis bu soppeeku, gaawa mer, labajoo mbaa loxo yuy lox, reer, jaxasoo, ndof, mbaa kiris. Dakkal jëfandikoo ci saasi te seeti ab doktor soo yëgee benn ci yii koy wone, mbaa seeti ab doktor laata nga jëfandikoo jëfekaay yi soo mësee yëg li koy wone yu lëkkalook ay kiris. Waa-jur yi war nañu saytu nan la seeni doom di jëfeandikoo jëfekaay yi ngir màndarga yu koy wone.
Man-mani Njabootu Microsoft
- c. Man-mani Njobootu Microsoft. Waajur yi ak xale yi mën nañu jëfandikoo Màndarga Mboolem Njabootu Microsoft, boole ci Microsoft Njaboot Safety ngir xam ban doxalin, yan daliweb, yan jëfekaay, yan po, yan barab yu teew ak yan waxtu jëfandikoo ñoo jaado ci seen njaboot. Waajur yi mën nañu sos ab njaboot su ñu demee ci https://account.microsoft.com/family (wala su ñu toppee digle yi ci seen jëfandaayu Windows wala jumtukaayu Xbox) te woo xale yi wala ñeneen ñu bokk ci. Bari man-man yuy jàppandi ci njaboot gi, kon xoolal bu baax leeral yiñ la jox bi nga nangoo sos wala bokk ci njaboot gi bi ngay jëndal sa njaboot ay Màrsandiisu Disitaal. Boo sosee wala nga bokk ci njaboot, nangu nga jëfandikoo njaboot gi ci anam wi ñu ko diglee, te doo ko jëfandoo ngir def lu jubadi wala di jéema jot ci ay leerali jàmbur. Melo Njaboot Microsoft dafa yam ci Amalinu Microsoft te kenn mënuleena toxol ci yeneen jumtukaay yi. Ci misaal, jekkal Kaaraange njaboot giñ jagleel Xbox dañuy jëfe ci konsoli Xbox yi, Xbox Cloud Gaming, ak jëfekaayu Xbox ci PC wala costéef mobile, waaye mënu ñu laal po yi Xbox Game Studios wala cër yi ñuy jëfandikoo wala di jouer ci yeneen costéef wala platform. Ngir sa waa kër mëna am jeu video bu gëna wóor, xoolal jekkal waajur yi ci aparey yii ak platform yii.
Bataaxalug Mbooloo
- d. Bataaxalug Mbooloo. Bànqaasi Microsoft yu wuute may nañu la nga yónnee ay bataaxal ñeneen jaare ko ci sa baat (looy wax) wala SMS ("bataaxal"), ak/wala may Microsoft ak jaaylekatu Microsoft ngir ñu yónnee la ay bataaxal yaw ak benn wala yeneen jëfandikukat ci sa tur. SOOY DIGAL MICROSOFT AK JAAYLEKATU MICROSOFT NGIR ÑU YÓNNEE LA BATAAXAL YI YAW WALA ÑENEEN, XAMLE NGA NI TE GAARANTI NGA ÑU NI YAW AK KÉPP KOO ÑU DIGAL NU YÓNNEE KO BATAAXALU NANGU NGIR MU JOT BATAAXAL YI AK BÉPP BATAAXALU JUKKI BU MÉNGOOK CAYTU BU BAWOO CI MICROSOFT AK JAAYLEKATU CI MICROSOFT. "Bataaxalu jubbib caytu" yi ay bataaxali jëflante yuy faral di am lañu yu bawoo ci ab bànqaasi Microsoft, bokk na ci waaye yemul ci ab "bataaxalu dalal-jàmm" wala ay digle ci nu ñuy dakkale jot ay bataaxal. Yaw wala ay way-bokki kuréel ñi bëggatul jot yooyu bataaxal mën ngeen tànn baña jot yeneeni bataaxal yu bawoo ci Microsoft wala Jaalekati Microsoft yi saa su nekk sooy topp digle yu ñu joxe ngir loolu. Su dee bëggatuloo jot yooyu bataaxal wala bokk ci kuréel gi, nangu nga ni dinga génn jaare ko ci digle yi la tëriin bi wala jëfekaay bi jox. Su dee am nga sabab ngir gëm ni ab way-bokku kuréel bëggatul jot yooyu bataaxal wala bokk ci kuréel bi, nangu nga ñu dindi leen ci kuréel bi. Xamle nga itam te gaarantil nga ñu ni yaw ak képp koo ñu digal ñu yónnee ko bataaxal nànd na ni way-bokku kuréel bu nekk mooy sasoo njëgi bépp fayeeku bataaxal bu operatëru mobiilam natt, bokk na ci fayeekuu bataaxalu bitim-réew yu ci mën a am su fekkee ni niméroob Etaa-sini (Amerik) moo jàllalee bataaxal yi.
Skype, Microsoft Teams, ak GroupMe
- e. Skype Kuréeli Microsoft, ak GroupMe.
- i. Cëri Wallu. Am na ay wuute yu am solo diggante cëri telefon yi portaabal yu njëkk ya wala telefon fiks njëkk yi ak Skype, Kuréeli Microsoft ak GroupMe. Microsoft amul wareef yu bari ci sàrt yiñ tëral ci sa dëkk wala ci réew mi nga nekk, muy ci yoon wala ci tëralin ngir may ñuy jëfandikoo cëri wàllu yi, lu ci melni 911 wala 112 ("Cëri Wàllu") jaare ko ci Skype, Microsoft Teams, ak GroupMe. Yenn ci ay sumbi losisel yu Skype ci man-mani telefon yu Skype ñoo mëna woote Cëri Wàllu yi ci yenn réew yu néew lool, lépp di aju ci dal yi ñuy jëfandikoo itam. Mën nga am ay leeral yu jëm ci jàppandi gi ak ni ñuy tabbee man-lmn bi fii: https://www.skype.com/go/emergency. Su sag woote wàllu telefonu Skype dafa konekte, fàww nga joxe leerali barab bi nga nekk ngir may ñiy liggéey ci cëri wallu ñu mën la wuyyu.
- ii. API yi mbaa Jàllale. Soo bëggee jëfandikoo losisel ak costéefu Skype ci mbir yoo bëgg a dawal, fàww nga tënku ci "Broadcast TOS" ci https://www.skype.com/go/legal.broadcast. Sudee danga bëgg a jëfandikoo benn jokkalekaayu prograamu jëfekaayu ("API") buñ fësal wala bu jàppandi ci Skype fàww nga tënku ci sàrti sañ-sañu jëfekaay bi, dinga leen fekk ci www.skype.com/go/legal.
- iii. Sàrti Jëfandikoo wu Jub. Mën nañu sàkku ci yaw nga jëfandikoo losisel ak costéefi Skype ci anam wu jaadu. Baal ñu topp yile sàrt yuñu defar ngir aar leen ci luubal ak tooñ te mën na tekk ay yemale ci xeet bi, diir bi mbaa dayo woote yi mbaa bataaxal yi nga mën a amal. Dugal nañu yile sàrt ci Sàrt yi cig delluwaay. Mën nga fekk yooyu sàrt ci https://www.skype.com/go/terms.fairusage/.
- iv. Jëfandikoo bu nu Kendal/Bunuduljaay. Mën nga jëfandikoo losisel ak costéefi Skype ngir sa bëgg-bëgg kese, te doo ci liggéey. May nañu la nga jëfandikoo Skype ngir jokkoo ci sa liggéeyukaay wala ci sa liggéeyu bopp.
- v. Nimero Skype/Skype To Go. Sula Microsoft joxe Nimero Skype wala nimero Skype To Go, nangu nga ni nimero boobu du sa moomeelu bopp, te du loo am sañ-sañu yore ko abadan. Ci yenn réew yi, ñenn ci ñiy liggéeyandoo ak Microsoft mën nañu la jox nimero, waaye du Microsoft ci boppam, su boobaa beneen xeetu déggoo nga xaatim ak ñooñu. Ngir am yeneen leeral ci Nimero Skype xoolal https://go.skype.com/home.skype-number.
- vi. Skype Manager. Yaw yaay sos ak saytu sa "Sàqu Yorkatu Skype Manager", nga nekk benn yorkatu mbooloo Skype Manager bokkul ak ku yor liggéey. Mën nga lëkkale sa sàqum Microsoft bi nga moom ak am mbooloo Skype Manager ("Sàq yiñ Lëkkalante"). Mën nga jël yeneen saytukat ci sa kuréelu Skype Manager ci kaw ñu nangu yile Sàrt. Soo joxee Skype ay nimero ci ab Sàq bu ñu lëkkale, yaw yaay saytu dëppoo bépp sàkku bu méngook sa dëkkuwaay mbaa barabu say jëfandikookatu Sàq bu ñu lëkkale. Sudee danga dakkal sa lëkkalanteg Sàqu Lëkkalante ak am mbooloo Skype Manager, kenn du ci mën a dindi menn mbindu muñ ko jagleel, Keredi Skype wala Nimero Skype te kenn dootul mën a jot ci Say Ëmbiit wala jumtukaay yuñ boole ak sàq miñ dakkal lëkkalanteem. Nangu nga jëfe bépp leerali jagoo bu say jëfandikookatu Sàq bu ñu Lëkkale ngir ànd ak yooni kaarange njoxe yuy jëfe. Mën nañu dàq sa Yokkatu Skype sudee waa kuréel gi nanguwuñu sàmmoonte ak sàrti doxalin yiñ tëral ci bii MSA.
- vii. Fayyeeku Skype yi. Njëg yépp yu ñeel costéefi Skype yuñu fay boole nañ ci juuti yiy jëfe, ludul dañu wax leneen. Fayyeeku yu mën am ci woote ci biti takkoo mu àju ci njëgu lonku (fayyeeku benn yoon ci woote bu nekk) ak ab njëgu simili niki nuñ ko tëralee ci www.skype.com/go/allrates. Dina ñu wàññi njëgu telefon ci sa tolluwaayu Kredi Skype. Microsoft mën na soppi njëgu woote yi saa yu ko neexee, waaye dina ko yëgle ci www.skype.com/go/allrates. Njëg bu bees bi dina jëfe léegi ci sa woote buy ñëw suñu siiwalee njëg yu bees yi ba noppi. Baal ñu xool njëg yu mujj yu gën bees laata ngay woote. Dina ñu dugal woote yu am dog-dog ak fayyeeku yu dogit yi ci bór bu ci topp. Ci yenn réew yi, ñiy liggéeyandoo ak Microsoft ñooy jaay costéef yiy laaj fay ci Skype te ñoom seeni sàrti jëfandikooy ñoo fay dox. Lu weesu lii ñuy wax, mën nga am sañ-sañu, ci anam wi yoon digle, ñu delloo la sa xaalis, sudee sàkku nga ko, bépp xaalis abonmaa boo fayoon jiital sudee danga soppi sa Nimero Skype ak nimero beneen këru woote.
- viii. Kredi Skype. Microsoft garantiwul ni di nga mën a jëfandikoo sa xaalisu Kredi Skype ngir jënd costéef yi ñuy fay ci Skype yépp, ndax costéef yi ñuy fay mën nañu soppeeku saa yu nekk. Su fekkee danga toog diiru 180 fan te jëfandikoowoo sa Kredi Skype, Microsoft dafay jël Kredi Skype daal di koy tege barab. Mën nga doxalaat Keredi Skype bi soo toppee lëkkalekaayu doxal bi ci https://www.skype.com/go/store.reactivate.credit. Sudee danga nekk ci Sapoŋ ba noppi nga jënd Keredi Skype ci daluwebu Skype, bokkoo ci ñaari kàddu (phrases) yiñ wax ci kaw te sa Keredi Skype dina jeex 180 fan ginaaw bis bi nga ko jëndee. Ginaaw bi sa keredi jeexee, dootoo ko mën a doxolaat wala di ko jëfandikoo. Su sa sàqum Microsoft tëjoo, ci sabab bu mu mëna doon, bépp Kredi Skype buñu jëfandikoowul bu ànd ak sa sàqum Microsoft dina réer te dootu ñu ko mën a jotaat. Mënu ñu jox credit Skype ñeneen.
- ix. Aliwoo Wootekaay Skype. Mën nga jëfandikoo Skype Dial Pad ak abonemaa buy dox wala Kredi Skype ginaaw bi aplikaasioŋu biro wala mobile Skype jeexee. Aliwoo Woote bu Skype ab costéef Skype la boo mëna jot ci biir Microsoft Teams wala ci web bi.
- x. Njëgi Bataaxali Bitim-réew. GroupMe mu ngi jëfandikoo fii mu ne nii ay nimero telefonu Etaasini (Amerig) ngir bépp kuréel bu ñu sos. Bépp bataaxalu jukki bu ñu la yónnee walla bi nga jot ci ab nimero GroupMe dina konte niki ab jukkib bitim-réew bu ñu jot mu bawoo Etaasini (Amerig). Lépp di aju ci dëkk bi nga nekk, Microsoft Teams mën na jëfandikoo nimero telefon bu mëna nekk sms buy dem diggante réew ak réew. Baal nu nga xool ak sa joxekat ci lu ñeel njëgi bitim réew yu ñu ci boole.
- xi. Microsoft Teams SMS. Microsoft Teams mën na jëfandikoo nimero yu bokk ci Australie yu ko Belgacom International Carrier Services SA. jox ak seen barabu liggéeyukaay bu njëkk ci Boulevard du Roi Albert II, 27 1030, Bruxelles Belgium ("BICS"), ngir mesaas yuñ yónnee ñu yor nimero yu bokk Australie. Microsoft ak ay bànxaasam bokku ñu ci BICS.
Bing ak MSN
- f. Bing ak MSN.
- i. Daju Bing ak MSN yi. Xët yi, mbind, nataal, kàrt, wideo, jàngukaayu wideo wala yeneen jumtukaayi jàmbur yi nekk ci Bing ak MSN, lu ci melni ci bokk ci boti Microsoft, jëfekaayi ak tëriin, mayu ñu la nga jaay ko, sa jëfandikoo bopp kese. Yeneen jëfandikoo yu melni yebbi, sotti wala séddalewaat yii jumtukaay, wala jëfandikoo yii jumtukaay wala costéef ngir defar sa costéefu bopp, mën nañu ko maye sudee Microsoft nangu na loolu am, wala yooni àqi moomeel nangu loolu. Microsoft mbaa yeneen yorkati àq dafay jaglel àq yépp ci daju bu Microsoft maye ci wax ci kaadaru sàrti sàñ-sàñ yi, ci bokk, até mbaa neneen.
- ii. Kàrti Bing. Mën nga baña ay wonandi yu rafet ci Etaa-Sini, Kanadaa, Meksik, Nouvel Zelànd, Ostrali mbaa Sapoo ngir jëfandikoo nguur te du andak suñu nangu bu xaajaloo buñu bind.
- iii. Barabi Bing yi. So dioxe sey données wala sey Mbirr ci Bing Places, danguey diaglele Microsoft lu weur aduna yeup, licensu droits yu libre nguir jefandikoo, dencc, soppi, agrégat, siiweule, dialale, feñale, ak seddeule sey Données (bokk ci droits wu prorpiété intellectuelle ci sey Données ak Sey Mbirr), ak license bu ndawu lepp wala le, ci droit wu ñenen luko weessu.
Cortana
- g. Cortana.
- i. Jëfandikoo Jagoo ak budul Jaay. Cortana Cëri Jàppale jagoo bu Mucrosoft la. Man-man, cër ak ëmbiit yi la Cortana (collectively "Cortana Services") di jox, yaw lañu bëgg a koy jëfandikoo bëggu ñu nga leen di jëfandikoo ngir wut xaalis.
- ii. Maneef ak Ëmbiit. Cortana dafay joxe man-man yu bari, ñu jagleel yenn yi ci ñoom. Cëri Cortana mën nañu la may nga jëfandikoo yenn cër yi, leeral wala man-man yu bawoo ci yeneen Cëri Microsoft wala Cër ak Jëfekaayi Jàmbur. Sàrti cër biy wax ci loolu ci pàcc 13 dafay waxaale ci ni nga waree jëfandikoo Cëri Microsoft yi nga duggee ci Cëri Cortana. Cortana dafay joxe ay leeral ngir say jumbluwaayu palaŋ kase te war nga jëfe sa atey bopp sooy topp te doylu ci leeral yii. Yoonu Microsoft nekkul ci wóoraay, jàppandig wala ñàkk dag-dag gi wara am ci jëfandikoo ngi ngay def ci Cortana. Yoonu Microsoft nekkul ci yeexaayu benn man-manu Cortana, wala lu lay tere jot, jàngat wala yónnee ab jokkoo wala ay yëgle, wala mën a ab cër.
- iii. Cër ak Jëfekaayi Jàmbur. Ginaaw dafa bokk ci ni Cëri Cortana di doxee, Cortana mën nala xelal ak jàppale la nga jokkalante ak Cër ak Jëfekaayi Jàmbur (pexey jàmbur wala cër yi ci lënku). Soo bëggee, Cortana mën na weccoo say leeral Cër ak Jëfekaayi Jàmbur, lu ci melni sa kot zip ak say laaj ak tontu yi bawoo ci Cër ak Jëfekaayi Jàmbur, ngir jàppale la nga am cër yi ngay sàkku. Cortana mën nala may ngay jënd ay mbir ci biir Cër ak Jëfekaayi Jàmbur su jëfandikoo say taamuy sàq ak say jekkal yi nga defoon foofu ci yooyu Cër ak Jëfekaayi Jàmbur. Mën nga dakkal sa lënkug Cëru Cortana ci Cër ak Jëfekaayi Jàmbur saa yu la neexee. Li ngay jëfandikoo Cëri Cortana ngir lënku ci Cër ak Jëfekaayi Jàmbur mingi bokk ci pàcc 5 bu Sàrt yii. Siiwalkati Jëfekaay ak Cëri Jàmbur yi mën nañu soppiku wala dakkal ni ñuy doxee wala seeni man-man, ñeel Cër ak Jëfekaayi jàmbur wala boole gi ci Cëri Cortana. Yoonu Microsoft nekkul ci wóoraayu losisel wala jumtukaay bu liggéeykat yi defar.
- iv. Jëfandaayi Cortana yiñ Nangu. Jëfandaay yi Cortana doxal, ñooy costéef wala jëfandaay yi ñuy taal ngir mëna jëfandikoo Cëri Cortana, wala costéef wala jëfandaay yi mëna ànd al Cëri Cortana. Cortana dafay nangu costéef wala jëfandaayi jàmbur yu Microsoft moomul, defarul, wala siiwalul. Yoonu Microsoft nekkul ci yooyu jëfandaay wala costéefi jàmbur.
- v. Yeesali Losisel. Mën nañuy saytu ci saasi sa sumbu losiselu Cëri Cortana ak yebbi yeesali losisel wala soppi ab tabbin wala sàqu ci bépp defarkatu jumtukaayu yuy jël Cortana ngir mën a yeesal losiselu Cër Cortana saa yu nekk.
Microsoft 365 Applications yi ak seni njeriñ
- h. Microsoft 365 Applications yi ak seni njeriñ.
- i. Sartu jëfandikoo. Microsoft 365 njaboot, Microsoft 365 bopp, Microsoft 365 bu yem, Sway, OneNote ak benen application wu Microsoft 365 bumu meuna doon wala Njeriñ wala marqu njeuriñu bureau nguir sa jefandikoo bopp la, xana nga amesi soxelay diay jefandikoole yoon wi ci kaw ben nangu bu bokkule yaw ak Microsoft. Jefandikoo applications yu melni Word, Excel, PowerPoint, Outlook, OneDrive, Access, ak Publisher ci Microsoft 365 Njaboot, Microsoft 365 Bopp ak bep benen application wu Microsoft 365 wala bindu njeriñ liko djiteule moy sartu licience yu yokku yu nekk ci https://aka.ms/useterms ñu and ci sarte yoyu.
- ii. Yenen Sartu Outlook. Outlook moo ëmbaale jëfandikoog Bing Maps. Bépp ëmbiit buñ joxee ci Bing Maps, boole ci geokod yi, mën nañu ko jëfandikoo ci costéef bi xamni ci moom lañu joxee ëmbiit li. Sàrti Jëfandikukat bu Mujj bi ci Bing Maps moo yilif sag jëfandikoo Bing Maps, te mingi ci go.microsoft.com/?linkid=9710837 ak Sàrti Sutura Microsoft bi nekk ci go.microsoft.com/fwlink/?LinkID=248686.
Marsandiisu Xarala
- i. Marsandiisu Xarala. Ci Microsoft Groove, Microsoft Filmu yi ak Tele, Store, Cëri Xbox ak yeneeni liggéeyal yu ñu boole yiy ñëw, Microsoft war na mën a am, déglu, xool, taal walla jàng (ak lu mbir mi mën a doon) misig, nataal yi, wideo, jukki, téere, po walla mbiri ("Marsandiisu Xarala") yi nga mën a jot cig tëggiinu xarala. Tëggiini xarala yi ngir sag jëfandikoo doŋŋ la, àndul ak njaay. Nangu nga ne doo séddalewaat, tasaare, wax ci mbooloo walla wone, mbaa jàllale bépp sottiy Marsandiisu Xarala. Marsandiisu Xarala yi mën nañu doon yosu Microsoft walla yu bawoo feneen. Ci anam yépp, nànd nga te nangu ni say àq ci lu àju ci Marsandiisi Xarala Sàrt yii ñoo leen yemale, yoonu àqi-Sos ak Sàrtu Jëfandikoo bi nekk ci https://go.microsoft.com/fwlink/p/?LinkId=723143. Nangu nga ni doo jéem a soppi benn Marsandiisu Xarala bu ñu jëlee ci Liggéeyal yi ngir sabab bu mu mën a doon, bokk na ci jubluwaayu feeñal walla soppi moomeel mbaa cosaanu Marsandiisu Xarala. Microsoft walla ñi moom Marsandiisu Xarala yi mën nañu, yenn saa, dindi Marsandiisu Xarala yi ci Liggéeyal yi te duñu ko yëgle.
Ndinccum Microsoft
- j. Ndincum Microsoft.
- i. Ndenkaane ndinccum OneDrive. Meun nga dencc lu eup ci sa OneDrive lu eup lila saarte yi dioxone ci lu amule fey wala bindu bu ame fey njeriñ ci ndinccum Microsoft te do tontu ci ay bataaxal yu bayeko ci Microsoft nguir defar sa compte ci dindib mbirr yu eup wala di diale ci mbindu mu yeess nguir ame ndincc mu eup, deñuy diot ndigeule nguir tecc sa compte te dindi wala beña mey nga diot ci sey mbirr ci OneDrive. Nafarale lu eup ci lu dieum ci jagleelu ndinccum Microsoft fii (https://prod.support.services.microsoft.com/office/how-does-microsoft-storage-work-2a261b34-421c-4a47-9901-74ef5bd0c426).
- ii. Doole njeriñu OneDrive. Dafey ajjo si ay mbirr yu deme ni sa linguey jëfandikoo, sa connexion internet ak njambarte Microsoft nguir yemale doole ak deuggu njeriñeum li, dinguey farale di jankontele xaar ci yegeulume wala xoolume sey mbirr ci biir OneDrive.
- iii. Ndenkaane ndinccum Outlook.com. So eupeule sa jagleelu boite emailu Outlook.com ci sa ndiccum Microsoft biñu la jagleele ci sufu ñak fey wala bindu bu am fey doto meunati yonee wala diot ay bataaxal fekk dindiwo mbirrr yi eup wala nga diale ci benen bindu bu ame ndinccukay bu doy. So meunule dindi mbirr yi eup wala ame ndinccukay bu yokku bu doy guanaw bi nga diote bataaxal bu bayeko ci Microsoft diox neñu suñu bop ndigeulu dindi wala dakkale sa diot ci si sey mbirr. Nafarale lu eup ci lu dieum ci jagleelu ndinccum Microsoft fii (https://prod.support.services.microsoft.com/office/how-does-microsoft-storage-work-2a261b34-421c-4a47-9901-74ef5bd0c426).
Microsoft Cashback
- k. Microsoft Cashback. Tërëlinu Microsoft Cashback (''Cashback'') dafay may kiliyengu Microsoft nu am neexalu xaalis sunuy jën ci jaaykat yu ndaw yi ci bokk di jëfandikoo ay jumtukaayu Microsoft ak ay mënloo yu melni Bing.com ak Microsoft Edge. Sooy dugg ci Cashback wala ngay duggal ab joxe Cashback, ndàngu nga te ànd ci Anam ak sàrti Cashback yi (https://www.microsoft.com/bing/rebates-terms). Yenn laaj, tere, ak yeneen yamale dina am ci sa bokk ci Cashback, ngir yeneen xibaar xoolal Cashback FAQ (https://www.bing.com/rebates/faq).
Microsoft Rewards
- l. Microsoft Rewards.
- i. Xibaar yi jara xam. Microsoft Rewards ("Programu neexalbi") meun nga ci bok te do fey, te daley mey nga ame ay poñs ("Poñ") nguir yen def def yi ak nguir sa jefandikoo bop ci yen ci produiwi Microsoft ak njeriñ yi. So ame sàqum Microsoft te deuk ci reew mu bokk (ci yiñu lim ci suuf), dugeule neñula ci saassi ci Programu neexal bi te meun nga tambali di am ay poñ ci saassi. Meun nga beñ sa bokk ci Programu neexal bi sayo beugue so toppe tektal yii ci suuf.
- ii. Meun na dieundaat sey poñ ci yoon yu wuute ("Xeeti dieundaat yi"), bokk yi yen ci produits yi ak njeriñ yi ñu lim ci Pagu Dieundaat ci https://aka.ms/redeemrewards ("Neexale"). Nguir meuna bok ci diaayat sey Poñ nguir bep Option wu Diaayat, danga wara njeuka active sa comptu Programu Neexal ("Comptu Neexal") ci Tableau Neexal cii https://rewards.microsoft.com/ wala ci yenen sites wala pagu Microsoft. Amule ben njeug nguir active sa Comptu Neexal.
- iii. Yen ci tere yi ak yemale yiy teggu ci am am wi, dieundat wi, ak yenen jefandikoo Poñ yi ci Programu neexal yi. Ngir am ci yeneen leeral xoolal ci pàccu Neexal yi https://support.microsoft.com ("LFÑ").
- iv. Yi mu soxela. Da nga soxela sàqum Microsoft bu diaar yoon te danga wara deuk ci ben ci zonu deukuwaay yi ñu lim ci FAQ bi ("Deuk") nguir ñongale sey Comptu Neexal ak nugir ame, dieundaat, wala ci benen fann jefandikoo Poñ yi. Da nga nara ubi te jefandikoo ben Comptu neexal kesse, ndem am nga adresses email yu beuri. Njaboot gune ci diurom-beeni Comptu Neexal leñuko yemale. Progammu neexal yi nguir yaw kepp la te du ngui walu jefandikoob njeund ak njaay. Jeufandikoob réseau bu neubu budule luñu meuna djiss (VPN) wala yeneeni jumtukaay yu xarale wala njeriñ yi ñu meuna jefandikoo nguir neub, diuumloo sa deukuwaay meun nala diureule dakkale sey Comptu Neexal ak wañi poñ yi nga diota ame.
- v. Poñu ngañaay. Meun na ame ñu wanela ak ay yoon nguir ame ay Poñ ci yen ci def def yu leer yi ("Mey"), lu deme nii Seet, Momele, jefandikoo yen ci produiwu Microsoft ak njeriñ yi, ak yeneeni yoon yu bayeko ci Microsoft. Da nga wara ame Comptu Neexal buy dox nguir dieule ndam ci kaw Mey yu mel nonu. Gannaaw ba nu matale laaj yi ci yenn Joxe yi, mën nanu la laaj nga laaj say Poñ ci Rewards Dashboard bi laata nuy yokk Poñ yi nga gañ ci sa Comptu Neexal. Baña laaj Poñ yi ci diiru waxtu bi la Microsoft jox dina indi say Poñ nga ñàkk leen. Mey yi wara ame di na wutte si Dëkk te dafey jàppandi rekk ci yen waxtu wala mu aju si yeneen yemale. Danga wara ak sarte yeup ak doxaline bu Mey bune nguir am ay Poñ yuñula diaglele ak Mey bobu. Meun na ame ñu wanela ay Mey ci saassi ci Tableau Neexal bi wala soy jefandikoo yen ci Produits Microsoft yi ak njeriñ yi. Yenn saay, Microsoft mën na laa jox wala neexalee la ay Poñ yuy yokku te kenn du yëg te mën nala tàggu wala mu bañ la tàggu, boole ci li Microsoft taxawal nekk Seet yu andak ngor a yeneen jokkalante ak Mënloo Microsoft yi.
- vi. Lu jëm ci Tërëlinu Neexal bi, ab "Seet" mooy jëfu jëfandikukat di duggal ay mbind ak loxoom ngir yite bu andak gëm bu baax cu am njureef yi ci Bing ngir yite bile jëfandikukat; ab ''Seet'' laaj yi andutak ngëmi wala dëgguwul du ci bokk wala laaj yi robo, wala macro, wala beneen jumtukaay wala bepp anam bu jarul yoon du ci bokk. Ngir yitey Tërëlinu Neexal, ab “Acquisition” mooy amalin jënd marsandiis wala yebbi ak jot tere kàttanal ngir ëmbeef yi nekk ci lënd gi joxe jaas ci Microsoft, su laajl ak su laajee fay. Poñ yi meyewule ci lep lo mome rek ci Microsoft, te yen yemale yi meun neñu teggu.
- vii. Teree & Yemale ci Poñ yi. Poñ yi Microsoft mi ngui key diaglele ben ci ben yi ci Comptu Neexal te meunolena dialale ben nitt bumu meunti doon wala mboolo. Liñu wax legui terewule, Microsoft meun na yen say ci noppiwu bopame mey la (i) nga bokk sey Poñ ak sen wa keur (dafey ame fumu yem), (ii) nguir bokkale sey Poñ nguir diappale ben organisation bu amule peyor buñu lim ci Pagu Dieundaat, wala (iii) adio ci sa Deuk ak deupo ak yeneen sarte yi ak teuraline, nga jeundaat yeup wala yen ci sey Poñ nguir poñ ci yeneen xeeti neexal wala programu koleure, bokk ci program yu Microsoft def wala ñenen ñuñuko nangule. Poñ yi deñuy nek te deñuy dess ci di nek momelu Microsoft, te du nek sa momelu bopp; amuñu dooley xaliss, te dosi meuna ame xaliss soko wecco. Poñ yi deñu lakey diaklele ci basu promotion rek. Meuno commande ay Poñ. Microsoft meun na yemale sa toluwaayu Poñ yi wala Neexale yi nga meuna am wala bu nitt bune meuna dieundaat, wala ci ben diir (maname ben beuss) su feke nii dula yakkale ben ubeku ngeum ngeum gu baax; baale ñu nga xool si FAQ bi nguir yemale yi ame fiñu tollu nii. Su amule ben Mey wala Option wu Dieundaat buñu leerale, Poñ yi nga ame ci Program bi baxule, te meuno ko jefandikoo soko boole ak, benen Program bu Microsoft meye wala ñenen ñi. Poñ yuñu dieundule boolo ak sa Comptu Neexale dafey am app so ko gañewule wala dieundaat ben Poñ ci sa Comptu Neexale ci 12 weer yu topalante.
- viii. Dieundaat. Dina ñu la jox Tànneefi Redemption ci Xëtu Redemption bi ak ci yenn daluwaayi Microsoft ak yeneen xët yi. Da nga wara gañe te ame legui nii ci sa Comptu Neexale lepp luy Poñ yi mu soxela nguir Option Dieundaat laata nguey meuna dieund sey Poñ, nguir Option wu Dieundaat bobu. Mën na am yeneen xeetu neexali yu mëna jàppandi, te yooyu neexal ñu ngi leen jagleen ñiy njëkka ñëw. Séddale, taamu nañu ci kuddu yu njëkk ya. Meun na ame ñu lacc la nga dioxe firnde yu eup, lu deme ni sa adresse email ak ben numéro téléphone (benen budule VOIP wala numéro wooté bu amule fey), te meun neñula lacc itam ben codu tewlu fraude wala bindu ci yenen lidiassa yu teggu ci yoon nguir dieundaate ay Poñ ci yen Options wu dieundaat. So xasse dieundaat sen Poñ, meunotoko bayi wala dello Option Dieundaat yi nguir ñu dello la sey Poñ sudule ci kawu produits yu baxule wala ci niko yoon teureule limu lacc. So tanne ben Option wu Dieundaat bu dieex wala amatule ndax yenen yiko warale, meun neñu sopi ben Option wu Dieundaar bu valeur bumu tollole wala feyat sey Poñ ci suñu noppi bop ken duko yeuk.
- ix. Microsoft meune na yeessale wala dakkale di la mey yen Option wu Dieundaat yi mu beugu sayuko beugue ak nguir lum meunti doon. Yen Options wu Dieundaat yi dafey soxela att wala tannefu Deuk, wala yenen sarte wala doxaline ci sen jefandikoo dieundaat bi. Bepp lacc bu mel nonu wala doxaline dineñuko boole ci meyu dieundaat bimu war. Yaw ya ress lepp lu sa deuk, sa gokh, ak taxu deuk bi ak bepp benen njeugu buy nangu ak jefandikoo Option Dieundaat bi. Ci sa sàqu bataaxal bi nga lëkkale ak sa sàqum Microsoft la ñuy yónnee Neexal yi, kon deel faral di yeesal sa dëkkuwaayu bataaxal. Kenn du delloo Neexal yiñ mënul joxe, te kon danga leen di ñàkk ba fàww. Neexale yi meun neñu lena beña diaayat. Meun nga diaay waye du weessu 550.000 Poñ att bu ne ci Programu Neaxal yi.
- x. Tecc sa Comptu Neexal yi. Soo bëggatul bokk ci Tërëlinu Neexal bim toppal ndigle yii ci opt genn xët (https://rewards.microsoft.com/optout) ngir dindi sa Compte Neexal. So tejje sa Comptu Neexal, danguey ñakk ci saassi sa Poñ yi nga gañewone yeup te danguey ñak sa meuna gañe ay Poñ euleuk. Nguir tambale wat gañe ay Poñ, danga wara ubi ben Comptu Neexal bu beess (waye Microsoft dula delowat sa ben Poñ bo amone ci guinaw). Meun neñu dakkale sa Sàqum Neexal (ak sey Poñ yi nga amone) so dugule ci sa Sàqum Microsoft ci diiru 12 weer yu tekloo.
- xi. Soppi wu Program wala dakkal. Microsoft tek na bopam ndogalu soppi, teuggat, dakkale, wala tecc Programu Neexale yi wala benen wale bu mu doon saa yumu ko beugue, ci saggom ak noppem, ak lu andulak ben yeukle. Wante, suñu tejje wala dakkale Programu Neexale bi, dineñu diem luñu meune nguir yegeule la ko diaraleko ci sa email ci Tableau Neexale bi te nguir dioxela lumu neew neew 90 fann nguir nga dieundaat sa Poñ yi nga dadiale wone, luko moy xana ñu djiss ni boobu tecc dafa wara ame legui legui ndax yoon moko lacc wala kaarangue.
- xii. Yeneeni Teuraline. Microsoft tek na bopame ndogalu tecc ci saassi sa Comptu Neexale, guene la ci euleuk nga bokk ci Programu Neexale bi, nangu bepp Poñ bo amone, te tecc wala dakkalagume bepp benen Option wu Dieundaat bo amone ci biir Programu Neexale bi su Microsoft geume ni danga len doon sacc. Microsoft tek na bopame lu geuna sori ndogalu tecc wala dakkalagume bepp Option wu Dieundaat bo amone wala diema ame diareko ci Programu Neexale bi su Microsoft djissee ni amo ci wale nguir diot Option wu Dieundaat bobu ndax ay ndogale yu teggu ci yoon (lu melni guene ak yoon ci deuk ak deuk). Bi Microsoft neke di def lepp lumu meune nguir def lu tolloo, ay ndiumte nak deñuy farrale di ame. Kone nak Microsoft tek na bopame ndogalu defarat ndiumte yu mel nonu sassune, ndem sax dafey songu Mey yi nek di daw wala sa yoss yiy wadia ñeuw, yi nga amone, wala Poñ yi nga dieundaatone wala Neexal. Ci xew xewu bepp ñak dox wala xuloo ci diguente sartu Programu Neexale yii wala bepp kaddu bo ci bok ci bep lidiassa bu si wala publicité, sarte yii ño ko teunk, djiitte ko, akk di ko doxale.
Azure
- m. Azure. Sa jëfandikoo cëru Azure a ngi tënku ci sàrt ak anam yi nekk ci kontraa bi nga amee cër yi te bokku ci yeneen sàrt yi, ci ni ñu ko leeralee ci xëtu xibaar bu Microsoft Azure Legal https://aka.ms/AA7z67v.
Microsoft Soundscape
- n. Microsoft Soundscape. Xam nga te nangu nga ni Microsoft Soundscape (1) defaru ñu ko, jublu wuñu ci, wala jàppalediwul ngir nekk jumtukaayu faj ci wérgi-yaram, te (2) defaru ñu ko, jublu wuñu ci mu nekk jumtukaayu faj buy wuutu fajkatu kër doktoor ci wérgi-yaram, saytu, faj, wala di wax ci tawat te kenn waru ko jëfandikoo ngir muy wuutu fajkatu kër doktoor ci wérgi-yaram, saytu, faj.
Power Platform
- o. Power Platform. Sa jëfandikoo cëru Power Platform a ngi tënku ci sàrt ak anam yi nekk ci kontraa bi nga amee cër yi te bokku ci yeneen sàrt yi, ci ni ñu ko leeralee ci xëtu xibaar bu Power Platform ci Microsoft Power Platform (https://www.microsoft.com/en-us/power-platform/business-applications/legal).
Dynamics 365
- p. Dynamics 365. Sa jëfandikoo Dynamics 365 liko jiitte moy saarte ak jëfandikookay yiy takkale nangu ci sufu services yi nguey am, ci niñuko teunke ci pagu xibaaru yoonu Dynamics 365 ci Microsoft Dynamics 365 (https://www.microsoft.com/en-us/dynamics-365/business-applications/legal).
Jaar jaari Copilot AI
- q. Jaar jaari Copilot AI. Sa jëfandikoo Jaar jaari Copilot AI (wuteeg Copilot yu am sàmmteef ci joxe) ay sàrt ak ay tegtal ñoo ko lal yoo xam ne di nga am mënloo yooyu ni nu leen benn bennalee ci Copilot - Sàrt jëfandikookaay (bing.com) (https://www.bing.com/new/termsofuse#content-policy) booleeg Sàrt yille. Su fekkee ab jëfandikookat sàmm joxe yunuy jaay ak Microsoft Copilot nga, nu ngi lay ñaan nga xool xët gii ngir jàngaat sàrti jëfandikookaay yi aju ci yëw, booleekook Sàrt yii: https://aka.ms/BCETermsOfUse.
Serwiis AI
- p. AI Serwiis. "Serwiisu IA" mooy serwiisu wala man-man yi ciy jëfandikoo xaralay Xarala yu Bees yi (IA), boole ci bépp serwiisu IA buy defar.
- i. Amul Xelal ci Liggéey. Mënloo AI kenn defaru ko, jubluwusi, wala di ko weccoog jumtukaayu liggeey.
- ii. Dëpp Xarala. Mën nga beña jëfandjikoo AI njeriñ nguir feñale lepp lu nek ci suuf luy defar ci models yi, alhorithmes yi ak systems yi. Ci misaal, mayu nu la nga jeema taxawal wala dindi disaayi melo yi wala sotti bepp pàcc bu mënloo AI yi ci sa jumtukaay.
- iii. Di wacce ay jumtukaay. Xana ci ludule ñu wax lako ci lu leer, warula jëfandikoo wërum internet, mbeyum internet, wala xeeti wacceb données yi nguir wacce données bu bayeko ci AI njeriñ.
- iv. Fi kataanu jëfandikoom ay données yu bayekoo ci AI njeriñ yem. Mën nga jëfandikoo sarwis IA yi, wala done yi bawoo ci sarwis IA yi, ngir sos, tàggat, wala gëna suqali (ci anam wu jub wala wu jaarul yoon) benn xaralay IA.
- v. Jëfandikoo wu sa Embeef. Ci li bok ci dioxe AI njeriñ, Microsoft dina doxale te dincc sey dugeule ci njeriñ bi tamite ni guenem ci njeriñ li, nguir njeriñu seytu ak moytu toñ wala ngaañu jëfandikoom wala guenem njeriñ li.
- vi. Moomeelu Ëmbeef. Microsoft sàkkuwul moomeelu bepp ëmbeef yooy joxe, siiwal, duggal wala joxe, wala jot, mënloo AI (booleci wax sa xalaat ak joxe say yaakaar). Danga soxla wone sab doggu aju ci àqqi moomeel saccuteef yi nga am cii ëmbeef bi nu duggal ak ninu leen mëna jëfandikoo, bàyyi xel, ci biir yeneen mbir, say melo jëfandikoo ak yoon yi leen tërël. Di nga garaantiir te wone ne yaa moom wala yaay saytu sa àqqi ëmbef yepp ne ni nu leen wonee ci Sàrt yii boole ci, te amul àpp, àqq yepp am solo ci ywa ngir nga joxe, siiwal, sol, duggal, wala yóne ëmbeef bi.
- vii. Content credentials. Sooy jëfandikoo cëri IA ngir defar ay ëmbiit, Microsoft mën na denc ay leeral ci ëmbiit li ba noppi boole leeral yooyu ak ëmbiit li ak ay leerali ëmbiit. Mën nga jëfandikoo sarwiisu IA yi wala sos ëmbiit ngir dindi, soppi, lëndëm, wala nëbb sarwiisu ëmbiit li wala yeneen pexe yu bawoo, màrk, wala siñaal wala nga jëfandikoo sarwiisu IA yi ngir defar ëmbiit ngir réerloo ñeneen ñi ndax ëmbiit li dafa bawoo ci jëfandikoo sarwiisu IA yi.
- viii. Ay laay Ñeneen. Yaw dong ya ress ci wuyum kenen kumu meuna doon ci lu jeum ci AI njeriñ ci lu andak li yoon tek (bokk ci, waye yemule ci, toñ droiwu borom wala yeneni lacc yu tak ci guenem sey mbirr ci diirub sa jëfandikoom AI services).
- ix. Jëfandikoo ay Yamale. Lu weesu topp "Kodu jëf" bi ci kaw, nangu nga ni doo jëfandikoo sarwiisu IA yi, boole ci ñiy jël yenn dogal, wala jëf, ci seen bopp wala ci anam yu bari yu nit ñi di doxalee:
- 1. Jël yenn dogal wala jëf yu nit ñi mënul saytu, te loolu mën na indi jafe-jafe ci wàllu yoon, ci wàllu xaalis, ci dundam, ci liggéey, wala ci yelleefi doomi aadama yi, wala lu mëna indil nit wala kuréelu nit gaañ-gaañu ci yaram wala ci xel;
- 2. Gëm wala juum ci njuumte (lu melni, piblisite bu dul dëgg), wala jëfandikoo pexe yu subliminal (lu melni, gis, dégg, wala yeneen siñaal yu weesu li nit ñi mëna gis) ak yéene jaay wala yàq doxalinu nit ci anam wuy jur loraange;
- 3. Jëfandikoo benn ci ñakk kattan yi nit mëna am ndax seen at, laago, wala jafe-jafe sosio- wala koom-koom, ak mébet, wala njeexte, ngir yàq ci anam wu baax jikko nit kooku wala nit ku bokk ci kuréel googu ci anam wu mëna jur wala mën indil nit kooku wala beneen nit gaañ-gaañu bu rëy;
- 4. Ngir joxe poñ ci askan wi wala profiling buy wax luy waaja am luy indi xeex, ñàkka yoon, tëddee, yàq, ñaawlu, wala metital yenn nit wala kuréeli nit;
- 5. Ngir jàngat risku def naka su dul noonu ci nit ñi, lépp di aju ci profiling nit wala jàngat seeni màndarga ak seeni jikko. Tere bii du laal sarwiisu IA yi ñuy jëfandikoo ngir jàppale nit ñi ñu jàngat ni nit ñi dañu bokk ci jëf ju ñaaw, te loolu mingi aju ci ay mbir yu leer te mën nañu ko firnde te lëkkalook jëf ju ñaaw ji;
- 6. Suñu sukkandikoo ci seeni done biometrik, ngir xaaj nit ñi wala ngir génne wala tënk seen lakk, xalaat politik, bokk ci sindikaa, gëm-gëmi diine wala filosofi, wala dundu sëy wala jubluwaayu sëy, lu moy bépp etiketu wala segg done biometrik yuñ am ci anam wu yoon, lu melni barabu biometrik, wala ci sàmmonte ak yoon;
- 7. Sosal wala yaatal ay base de done yuy xàmmee kanam yi jaaraleko ci dindi nataali kanam yi ci net bi wala ci wideo CCTV yi;
- 8. Ci bépp xaralay xàmmee kanam ci jamono dëgg ci kaw kamera mobile yi bépp doolel yoon di jëfandikoo ci àdduna bi ngir jéema xàmmee nit ñi ci anam wuñu ko saytu, "ci àll bi", lu ci melni (te amul àpp) ofisiye poliis yiy doxantu di jëfandikoo kamera yuñ sol wala dashboard ngir xàmmee kanam gi wala ñu njëkka jàpp; wala
- 9. Jéema xam tolluwaayu yëg-yëgu nit ñi ci seeni màndarga physique, physiologique, wala jikko (lu melni, melokaanu kanam, tànki kanam, wala wax), boole ci xam yëg-yëg yu melni mer, réccu, bànneex, naqar, jaaxle, tiit, wala yeneen mbir yu nit ñi jëfandikoo.
Jokkoo Serwiis
- s. Jokkoo Serwiis. Sarwis yiy may jokkoog diggante nit ñi, lu ci melni waaye duñu yam ci Skype, Teams, Outlook, ak GroupMe, ñu ngi leen di doxal ci sàrti jëfandikoo yu bees yi am ci https://aka.ms/useterms boole ko ak Sàrt yiile.
Ay yu sew sewaan
14. Miselanis. Pàcc bii, ak pàcci 1, 9 (ngir xaalis yi nga am laata Sàrt yi di jeex), 10, 11, 12, 15, 17 ak yeneen yi seeni sàrti bopp di dox ginaaw bu Sàrt yii jeexee dina ñu mucc ginaaw buñ dakkalee Sàrt yi. Ba ni ko yoon yuy jëfe nangoo, mën nañu jaglel yile Sàrt, liggéey ak ñeneen suñuy moomeel ci kaadaru yile Sàrt, mbaa séddale sañ-sañu suñuy àq ci kaadaru yile Sàrt, ci lépp mbaa xaaj, saa su nekk te duñu la ko yëgal. Mën nga baña jaglel mbaa jébbal yile Sàrt been àqi jëfandikoo Cër yi. Lii mooy déggoo bu matale ci sa digante ak Microsoft ngir li ngay jëfandikoo Cër yi. Dafay wuutu bépp déggoo bu jiitu ci sa digante ak Microsoft ci li àju ci li ngay jëfandikoo Cër yi. Sooy dugg ci yile Sàrt, doylo wulo benn nettali, teewal, garanti, nandite, liggéeyal, diggé mbaa wóoraay bu bokkul ak nuñ ko tërale ci yile Sàrt. Xaaju sàrt yépp dañuy jëfe ci dayo bu ëpp bu yoon bu jubu maye. Sudee ab atekaay mbaa atekat dafay dëgëral ni mënu ñu doxal ab xaaju yile Sàrt yuñu bind, mën nañu wuutal yooyu sàrt ak ay sàrt yuko nduru ci dayoo buñu mën a doxal ci kaadaru yoon bu jubu bi, waaye sàrt yi duñu soppeeku. Yile sàrt yaw ak say njuréef kase ñoo leen taxa jog/ Tëralu ñu yile sàrt ngir njuréefu beneen nit, ludul ngir aji-donn ak ndawu Microsoft yi. Boppu pàcc yi ngir sukkandikukaay kase lañ fi nekkee ta amu ñu benn jeexitu yoon.
15. War nañu yónnee jéebaane yi ci digante Benn At. War nañu yónnee bépp jéebaane bu méngook yile Sàrt mbaa Cër war ci atekaay bi (mbaa ate sudee pàcc 10.d.mooy jëfe) ci digante benn at bawoo ci bis gi nga njëkk a yónnee jéebaane bi, ludul sa yoonu barab laaj ab diir bu gën a yàgg ngir yónnee ay jéebaane. Soko yónneewul ci diir boobu, di nañ ko dàkkal ba fàww.
16. Yooni toxal. War nga dëppook bépp yoonu toxal bitim réew ak sàrt buy jëfe ci losisel bi ak/mbaa Cër, bu àndak ay yemale mbaa jëmuwaay, jënfandikookatu njextal, ak jëfandikoo bu mujj. Ngir am yeneeni leeral ci ay yemale barablin ak toxal, demal ci https://www.microsoft.com/exporting.
17. Denculuy Yelleef ak Joxe xalaat. Ci anam wiñ ko leeralee ci Sàrt yi, Microsoft du jox kenn ab sañ-sañ wala beneen xeetu yelleef ci xeet bumu mën a doon ak sabab bumu mën a doon, xam numu demee, àqu yelleef, sekkerey njaay, màrk wala yeneen moomeeli xel wala yu Microsoft saytu wala beneen liggéeyukaay bu mu àndandool, boole ci bépp tur, njaay, logo wala lumu méngool. Soo baaxee sa xalaat bumu mëna doon Microsoft, digle, laabire wala wax-sa-xalaat, boole, te dufa ca yam, lu ci melni ay gis-gis ci costéef bu bees, xarala, promo, turi costéef, wax-sa-xalaat ci costéef ak gëna baaxal costéef ("Wax-sa-xalaat"), may nga Microsoft, te doo ko ci fayyeeku lenn, te itam doo ci xaar benn xeetu dàmpaay, yelleefu defar, defar ba noppi, sos liggéey yu ci juddoo, jëfandikoo, séddoo ak jaay Wax-sa-xalaat ci anam wu nekk, ak lumu ci mëna jublu. Doo fi joxe Xalaat bu ëmbu ci ab sañ-sañ bu laaj Microsoft ci jox sañ-sañ ci ab losisel, xarala wala ay wayndare ci bépp jàmbur ndax Microsoft boole ci say Xalaat ci ñoom.
YËGLE YI
Karmat yi ak doxaliinu amal ay jéebaaneg jalgati àqi moomelu xalaat. Microsoft nangu na àqi moomeelu xalaatu xaaj yu bawoo feneen. Soñu beuguee yonee yeglee wu diotum propriété xell, bokk ci ay bakku wu dialgatiwu yoonu borom, baale ñu nga jeufandikoo suñu doxalin nguir yonee Yegle wi Jalgati (https://www.microsoft.com/en-us/legal/intellectualproperty/infringement) ay formuulairu doxaline yi bok ci yoyu sarte. LAAJ YI JËM TE MËN A BOKK CI WÀLL WII KESE LAÑUY TONTU.
Microsoft dafet jeufandikoo doxalinu teunk ci Turr 17, Codu Etats-Unis, Dagg 512, ak, fumuko wara defe, Chapitre III bu Tollolle (EU) 2022/2065, nguir tontu yegle yu akku borom yu ñu jalgati. Ci fann yimu waree, Microsoft dina tamite teree wala diexale comptu jeufandikookatu Microsoft njeuriñ yiy nek ay jalgati kat yu saxx. Su lolu weessoo, ci fann yimu warree, Microsoft meuna dakalagum yoonu yegle ben ci ben wala mbooloo yiy farate di yonee ay yegle yu amule solo. Benen tekki bu geuna sori ci liy teggu ci doxalin bi nguir ben njeuriñ bumu doon, bokk ci teureulaatu ndogual yi Microsoft dieule yu bokk ci suñuy doxaline, meun nga len fekk ci Yegle wu Jalgati (https://www.microsoft.com/legal/intellectualproperty/infringement).
Yegle ak doxalin yu ajjo ci propiété xell yi lambo ci publicité. Baale ñu nga xoolate suñu Sartu Propriété Xell (https://go.microsoft.com/fwlink/?LinkId=243207) ci lu dieum ci propriété xell ci suñu leundu publicité.
Àqisos ak karmati màndarga. Cër yi ñooy copyright © Microsoft Corporation ak/mbaa ay joxekat am, One Microsoft Way, Redmond, WA 98052, Etaa-Sini. Jagoos na mboolem sañ-sañ yi. Sarte yi bokk na ci Marku njaayu Microsoft & Doxalinu Mark (https://www.microsoft.com/en-us/legal/intellectualproperty/trademarks) (ci niñuko teurale ci jamono ba jamono). Microsoft ak tur yi, logo yi, ak junj costéefi Microsoft, losisel, ak cëram yépp mën nañu nekk ay màrk yuñ bind ba noppi wala yuñ bindagul ci Microsoft mbooleem këru liggéeyukay bi ci biir Etaa Sini ak/wala ci yeneen ëttu àttekaay. Lim bii ngay gis mooy limu lu Microsoft am ciy màrk yu bindu ci https://cdn-dynmedia-1.microsoft.com/is/content/microsoftcorp/microsoft/mscle/documents/presentations/TrademarksListFY25Q3.pdf. Turi këru liggéey ak costéef yi mën nañu doon màndargaay seeni borom. Jagoos na bépp àq buñu joxewul ci wax ci yile Sàrt. Yenn losisel yuñuy jëfandikoo ci daluwebu cërakooni Microsoft ñu àju ci xaaj ci liggéeyu Kuréelu JPEG bu Moom Boppam. Copyright © 1991-1996 Thomas G. Lane. Jagoos na mboolem sañ-sañ yi. Losiselu "gnuplot" bi ñuy jëfandikoo ci yenn serwëri dali Microsoft dañu am copyright © 1986‑1993 Thomas Williams, Colin Kelley. Jagoos na mboolem sañ-sañ yi.
Karmatu wergu yaram. Microsoft du joxe benn digal, gëstu mbaa faju mbaa benn paj bumu mën a doon. Dëkkeel di laaj sa doktor ay digal mbaa yeneen joxekatu wergu yaram yu xarañ ak bépp laaj bi nga mën a am ci li aju ci ab tolluwaayu wergu yaram, resim, tëriinu wer ak tal. Bul xeeb mukk digalu doktor walla yeex ci gis ko ndax leeral yi nga duggoon walla ci biir Cër yi.
Dawalinu aksiyoŋ yi ak njoxey àlluwa (bokk na ci xayma àlluwa). Leerali xaalis yi ñuy joxe ci Cër yi mënoo ko jëfandikoo ludul ci say mbiri bopp te mënoo ci liggéey. Waruloo jëfandikoo lenn njoxe xaalis yi wala màrku képp ku yor sañ-sañu jàmbur bu lëkkalook defar, sos, baayale, njënd ak njaay, jaay, mbaa marketing, mbaa fësal bépp jumtukaayu kopooral mbaa costéefi alalal (maanaam, indis, costéefi yuñu tëggaat, xaalisi alalal, xaalisi wécceeku, kalpey mbebët yi alalal, ak yeneen, fu njëg bi, delloo ak/mbaa këru manéefu jumtukaay mbaa costéefu alalal sukkandikoo, méngoo, walla bu jëmoon ci topp lenn ci njoxey leeral yi) yu àndul ak beneen déggoog ku yor sañ-sañu jàmbur.
Karmatu alalal. Microsoft du ab indikat/jaaykat mbaa laabirekatu alalal bu bindu ci sàrti yooni atekaayu aksiyoŋu réewu federaal bu Etaa-Sini te du digal nit ñi ci ndiglaayu alalal ko, jënd ko mbaa jaay aksiyoŋ yi mbaa yeneen cër mbaa costéefi alalal. Lenn lu nekk ci cër yi du ab maye mbaa càkkutéef ngir jënd mbaa jaay ab aksiyoŋ. Déet Microsoft déet ay ñi yor sàñ-sàñu dawaliinu aksiyoŋ yi mbaa njoxey àlluwam jàppale mbaa digle bépp costéefi xaalisal mbaa cër bu xejjiku. Amul lenn lu bokk ci Cër yi luñu mën na jëfandikoo ni tegtali liggéey, lu ci melni dugal xaalis wala taks yi.
Karmat bu àju ci H.264/AVC ak Baaxoo Wideo VC-1. Losisel bi mën na am H.264/AVC ak/mbaa xaralay Codec VC-1 moom la MPEG LA, L.L.C. jox sàñ-sàñ. Xarala bii ab tëggiinu ngir laxas ay njoxey leerali wideo. MPEG LA, L.L.C. dafay laaj karmat bii:
JAGLEL NAÑU COSTEEF BII CI KAADARU H.264/AVC AK SÀÑ-SÀÑU KALPEY VC-1 PATENT NGIR JËFANDIKOO JAGOO AK JËFANDIKOO AB AJI-JËFANDIKOO CI (A) FAS WIDEO CIG DËPPOOK BAAXOO YI ("BAAXOO WIDEO") AK/MBAA (B) FECCI H.264/AVC, MPEG-4 VISUAL, ak VC-1 VIDEO BU AB AJI-JËDANDIKOOKAT FAS CI AB JËFU JAGOO MBAA BU JAAYUL AK/MBAA ÑU AMEE KO CI AB JOXEKATU WIDEO BUÑU JAGLEL SÀÑ-SÀÑ NGIR JOXE BOOBU WIDEO. JOXE WUÑU BENN SÀÑ-SÀÑ WALLA WAR NAÑ KO NJORT NGIR BENEEN JËFANDIKOO BUMU MËN A DOON. MËN NAÑU JOT YENEENI LEERAL CI MPEG LA, L.L.C. XOOLALE SITE INTERNETU MPEG LA BI (https://www.mpegla.com).
Ngir jubluwaayu leeral kase, karmat bii du yemale mbaa tere jëfandikoo losisel buñu joxe ci kaadaru yile Sàrt ngir ay jëfandikoo liggéey yu jaadu yu liggéey boobu boolewul (i) séddalewaat losisel bi ci xaaj yu bawoo feneen, mbaa (ii) sos ay daju ak xarala BAAXOO WIDEO yu mu nangu ngir séddale ko ci xaaj yu bawoo feneen.
Karmat bu àju ci H.265/HEVC Video yu Yam. Losisel bi mën na amaale kotu xaralay H.265/HEVC. Dugg gu Xóot LLC dafay laaj leeral yii:
SU CI BOKKEE, XARALA H.265/HEVC BI CI LOSISEL BII KI KO ËMB MOOY BENN JAMBAT WALA LU KO ËPP CI MOTIFU HEVC BINU LIM: PATENTLIST.ACCESSADVANCE.COM. LEPP DI AJU CI ANAM WI NGA AMEE LOSISEL BI, COSTEEF BII MËN NA AM LISAAS BU LALU CI PORTFOLIO MOTIFU HEVC.
Suñu sampee losisel bii ci jëfandaayu Microsoft, mën nga fekk yeneen leerali lisaas bi ci: aka.ms/HEVCVirtualPatentMarking.
SART LISAAS JEFEKAAY BU YAMBAMBAA
SÀRTI SÀÑ-SÀÑU JËFEKAAY BU BAAXOO
MÀNGASIINU MICROSOFT, MÀNGASIINU MICROSOFT CI WINDOWS, AK MÀNGASIINU MICROSFT CI XBOX
Sàrti sàñ-sàñ yii ay déggoo lañu ci sa digante yaw ak siiwalkatu jëfekaay bi. Baal ñu jàng leen. Ñooy jëfekaayi losisel yi ngay yebbee ci Màngasiini Microsoft, Màngasiinu Microsoft bi ci Windows wala Màngasiinu Microsoft bi ci Xbox (ñuy woowee ku nekk ci ñoom ci sàrti sañ-sañ bi "Màngasiin"), ñu boolewaale ci bépp yeesal wala lu yokk ci jëfekaay bi, fileek jëfekaay bi àndul ak yeneen sàrt, su boobaa yooyu sàrt lañuy doxal.
SOOY YEBBI MBAA JËFANDIKOO JËFEKAAY BI, MBAA NGAY JEEMA DEF BENN CI YILE, NANGU NGA YILE SÀRT. SUDEE NANGU WOO LEEN, YOON MAYU LAKO TE WARULOO YEBBI MBAA JËFANDIKOO JËFEKAAY BI.
Siiwalkatu jëfekaay bi mooy wàll wi la jox sañ-sañu jëfekaay bi, leeral nañu ko ci màngasiin bi.
Soo dëppook yile sàrti sàñ-sàñ, yoon may nala nga def yii ci suuf.
- 1. SAMP TE JËFANDIKOO ÀQ YI; ÀPP. Mën nga samp ak jëfandikoo jëfekaay bi ci jëfandaayi Windows wala jumtukaayi Xbox, ci niñ ko waxee ci Sàrti Jëfandikoo (https://go.microsoft.com/fwlink/p/?LinkId=723143) yu Microsoft. Microsoft amna sañ-sañu soppali Sàrti Jëfandikoo yi (https://go.microsoft.com/fwlink/p/?LinkId=723143) saa yu ko neexee.
- 2. CËRI INTERNET YI.
- a. Nangu ngir cëri internet mbaa cër yu amul buum. Su jëfekaay bu lonjee nostey ordinatëer bi ci Internet, bu mën jaare ci ab mbaal bu amul buum, di jëfandikoo jëfekaay bu dox niki sa nangu ci jàllale leerali jëfandaay yu baaxoo (bokk na ci waaye yemul ci leerali xara yu àju ci sa jëfandaay, noste ak losiselu jëfekaay, ak periferik yi) ngir cër internet ci mbaa cër yu amul buum. Sudee dafa am yeneeni sàrt yu teew di lëkkalook ni ngay jëfandikoo cër yi nga dugg di jëfandikoo jëfekaay bi, yooyu sàrt dañuy jëfe itam.
- b. Jëfandikoo cëri internet bu baaxul. Waruloo jëfandikoo benn cëru internet ci benn anam bu mën a lor mbaa laal doxiinu jëfandikoo kumu mën a doon mbaa mbaal bu amul buum. Waruloo ëfandikoo cër bi ngir am sàñ-sàñu dugg ci bépp cër, njoxe, sàq, mbaa mbaal ci anam bumu mën a doon.
- 3. MANEEFU SÀÑ-SÀÑ. Dañu jox jëfekaay bi sàñ-sàñ, jaayu ñu ko. Déggoo bii yenn àqi jëfandikoo jëfekaay bi kase la lay jox. Su Microsoft dakkalee man-manu jëfandikoo jëfekaay yi ci say jëfandaay ci li àju ci sa déggoog Microsoft, bépp àqi sàñ-sàñ bumu méngool dina jeex. Ki siiwal jëfekaay bi moo yelloo yeneen sañ-sañ yépp. Ludul yoon buy jëfe jox la yeneeni àq ak bii yemale, war nga jëfandikoo jëfekaay bi suñ ko nangoo kase ci waxiin ci déggoo bii. Sooy doxalee nii, war nga nangu bépp yemale xarala ci jëfekaay buy tax nga mën ko jëfandikoo ci yenn anam. Waruloo:
- a. Jalgati benn yemale xarala ci jëfekaay bi.
- b. Safaane defar, booledi, mbaa tasaare jëfekaay bi, budul te ci dayo bu yoon yu jëfe nangu ci waxiin, donte am na yemale.
- c. Defar ay sotti jëfekaay yu bari yuñu xamle ci déggoo bii mbaa yu yoon buy jëfe nangu, donte am na yemale.
- d. Siiwal mbaa defar ci neneen jëfekaay yu jàppandi ngir ñi mën a sotti.
- e. Luwe, mbaa abale jëfekaay bi.
- f. Jox jëfekaay bi wala déggoo bi ab jàmbar.
- 4. JUKKIB NDIMBAL. Suñu joxe jukkib ndimbal bi ak jëfekaay bi, mën nga sotti te jëfandikoo jukkib ndimbal bi ngir jubluwaayi delluwaayu jagoo.
- 5. XARALA AK YEMALEY TOXAL. Jëfekaay bi mën na laaj saytu Etaa-Sini mbaa xarala bitim réew mbaa yooni toxal ak sàrt yi. War nga dëppook bépp yoonu toxal bitim réew ak sàrt buy jëfe ci xarala buñu jëfandikoo mbaa bu jëfekaay bi nangu. Yile sàrt dañuy àndak ay yemale ci jëmu yi, jëfandikookat yu ci mujj, jëfandikoo bu mujj. Ngir am yeneeni leeral ci costéef yu Microsoft màndargal, demal ci daluwebu toxal Microsoft (https://go.microsoft.com/fwlink/?linkid=868967).
- 6. CËRI NDIMBAL YI. Jokkool ak siiwalkatu jëfekaay bi ngir xamle cëri ndimbal yu jàppandi. Microsoft, sa defarkatu daju ak sa joxekatu cër yu amul buum (ludul benn ci ñoom doon siiwalkatu jëfekaay bi) yoru ñu kiliftéefu joxe ay cëri ndimbal ngir sa jëfekaay.
- 7. MBOOLEEM DÉGGOO. Déggoo bii, bépp sàrti sàmm-sutura buy jëfe, bépp sàrt bu ci dolleeku buy ànd ak jëfekaay bi, ak sàrt yu ñeel ngir mottali yi ak yeesal yi ñooy mbooleem déggoo diggante yaw ak siiwalkatu jëfekaay bi ñeel jëfekaay bi.
- 8. YOON BUY JEFE.
- a. Etaa-Sini ak Kanadaa. Sudee Etaa-Sini walla Kanadaa nga jëndee woon jëfekaay bi, yooni réew mi mbaa tund bi nga dëkk (mbaa, sudee ab liggéeyukaay, fu sa barabu liggéey nekk) mooy saytu nuñuy tekkee déggoo bii te dafay jëfe ci jéebaaneg lu koy jalgati mbaa, ak yeneen jéebaaneg (bokk na ci aar aji-jëfandikookat bi, konkiraas bu jaaduwul, ak jébaaneg bu yuy waral ate siwil) moo xàm xiiroo ak ŋaayoo sukkandikaayu yoon yi.
- b. Ci biti Etaa-Sini ak Kanadaa. Sudee ci beneen réew nga amee woon jëfekaay bi, yooni réew boobu mooy jëfe.
- 9. JEEXITU YOON. Déggoo bii dafay xamle yenn àqi yoon. Mën nga am yeneen àq yu aju ci sa yooni dëkk mbaa réew. Déggoo bi du soppi say àq yu àju ci sa yooni dëkk mbaa réew sudee say yooni dëkk mbaa réew maye wul nga def lu ni mel.
- 10. BEDDIINU GARANTI. Jaglel nañu sàñ-sàñ bi, jeffukaay bi "niki numu mel", "ak njuumte yépp" ak "numu jàppandee". Gàddu nga ci sa bopp lorange jëfandikoo ko. Siiwalkatu jëfekaay bi, ci turu boppam, Microsoft (Sudee Microsoft nekkul siiwalkatu jëfekaay bi), cër yu amul buum ci kaw mbaal buñu joxewul, ak bépp bànqaas bu lay teewal, jaaykat yi, ndaw yi ak joxekat yi ("Xaaj yuñu Ëmb"), joxewul benn garanti buñu waxe, mbaa anam bu méngook jëfekaay bi. Loraange bu matale bu wone fi baaxaay, kaarange, dalal, ak xarañu jëfekaay toll ci yaw. Sudee jëfekaay bi dafa yàqu, nangu nga njëg bu matale bu cërale mbaa saafarra bi laaj. Mën nga am yeneen àqi àji-jëfandikoo ci kaw say yooni barab ni yile déggoo mën nañ soppeeku. Ci dayo bu ëpp bu ñu nangu ci sa kaadaru sa yoonu réew, dañuy dàq bépp gaaranti bu nëbbu, bokk na ci mëniinu njaay, baaxaayu lu ñu mën a nangu, jekkal ngir jubluwaay bu xejjiku, kaaraange, dalal ak nàkk luubal.
- 11. YEMALE AK DÀQU SAAFARA AK YÀQUTE YI. Ci dayo bu yoon nanguwul, soo bépp sukkandikaay ngir dabuwaat yàqute yi, mën nga dabuwaat ci yàqute yu jub bu siiwalkatu jëfekaay ba ci tolluwaayu xaalis bi nga fayoon ngir am jëfekaay bi mbaa USD$1,00, bi nga xam ni moo gën a rëy. Jagleen nañu sañ sañ bi, doo laaj benn yeleef, seet ndampaay ci bepp ngaañ, boole ci njureef, ñàkk ameef, ngaañ bu andul ak tayeef joge ci defar jeffekaay. Su yoonu dëkk tegee ab gaaraanti, wala ay anam donte sàrt yooyule tëngku ci yoon wu nu teg, yameefam nekk na ci 90-fan ba nga yabee jeffukaay bi.
Yemale bii dafay jëfe ci:
- Lépp lu méngook jëfekaay bi mbaa cër buñu jàppandal ci jëfekaay bi; ak
- Jéebaaneg jalgati déggoo, garanti, mbaa anam, kiliftéf bu tar, ñàkk a xoromal, mbaa beneen buko waral, jalgati ab tolluwaay mbaa sàrt; alal bu lewul; mbaa ci kaadaru bépp xalaat, dayo yépp yu yoon buy jëfe nangu.
Dafay jëfe itam donte:
- Saafara bi du la fay ci matale li nga ci ñàkk yépp; mbaa
- Siiwalkatu jëfekaay bi xàm na mbaa waroon na xam darra ci jafe-jafe yu ci mën a am.
Cëri yi mu ëmb
Yile costéef, jëfekaay ak cër la Déggooy Cëri Microsoft ñoo ko ëmb, waaye mën na bàña jàppandi ci sa marse.
- Account.microsoft.com
- Baatukaayu Bing
- Bing ci kalaas bi
- Bing Image and News (iOS)
- Bing Search APIs/SDKs
- Bing Translator
- Bing Webmaster
- Bing.com
- Bingplaces.com
- Clipchamp
- Cortana skills by Microsoft
- Cortana
- Dajale Yi
- Default Homepage and New Tab Page on Microsoft Edge
- Dev Center App
- Dictate
- education.minecraft.net
- Face Swap
- Feedback Intake Tool for Azure Maps (aka “Azure Maps Feedback”)
- Forms.microsoft.com
- forzamotorsport.net
- Groove Music Pass
- Groove
- GroupMe
- Image Creator from Microsoft Designer
- Jëfekaay ak sàrwiis yuñu dugal ci Microsoft 365 Basic
- Jëfekaay ak sàrwiis yuñu dugal ci Microsoft 365 bindug aji-jëfandikukat yi
- Jëfekaay ak sàrwiis yuñu dugal ci Microsoft 365 Famille
- Jëfekaay ak sàrwiis yuñu dugal ci Microsoft 365 Personel
- Jëfekaay buy Nos ay SMS
- Jëfekaayi Bing
- Jëfekaayu Kàrt yi
- Jëfekaayu seet Bing
- Jëfekaayu Wergu yaramu Jëfandaay
- Kàrti Bing
- LineBack
- Link to Windows
- Microsoft 365 Business Standard, Microsoft 365 Business Basic, Microsoft 365 Apps, Microsoft 365 app, Microsoft 365 Copilot, Microsoft 365 Copilot app, and Microsoft 365 Copilot Chat*
- *Until a commercial domain is established for use of these services, at which time separate Microsoft commercial terms will govern instead.
- Microsoft 365 Consumer
- Microsoft 365 Family
- Microsoft 365 jaar-jaar yu lëkkaloo ci tànnéef
- Microsoft 365 ngir web bi
- Microsoft 365 Personal
- Microsoft Academic
- Microsoft Add-Ins for Skype
- Microsoft Bots
- Microsoft Copilot
- Microsoft Dajale Yi
- Microsoft Defender ngir nit ñi
- Microsoft Educator Community
- Microsoft Filmu yi ak Tele
- Microsoft Health
- Microsoft Launcher
- Microsoft Loop
- Microsoft Math Solver
- Microsoft Pay
- Microsoft Pix
- Microsoft Reading Coach
- Microsoft Research Interactive Science
- Microsoft Research Open Data
- Microsoft Rewards
- Microsoft Seet ci Bing
- Microsoft Soundscape
- Microsoft Sway
- Microsoft Teams
- Microsoft Translator
- Microsoft Wallpaper
- Minecraft Realms Plus and Minecraft Realms
- Mixer
- MSN (ñu xamewoon ko ci turu Microsoft Start)
- MSN Dial Up
- MSN Explorer
- MSN Food & Drink
- MSN Health & Fitness
- MSN Money
- MSN News
- MSN Premium
- MSN Sports
- MSN Travel
- MSN Weather
- MSN.com
- Màngasiin
- Màngasiinu Windows
- Ndimbal ak Jàppaleg Defaraatug Microsoft ñeel Office 365
- Ndimbalu Microsoft (kiliyaan)
- Njabootu Microsoft
- Office Store
- OneDrive.com
- OneDrive
- OneNote.com
- Outlook.com
- Paint 3D
- Phone Link
- Po yu Minecraft
- Po, jëfekaay ak daliwebi Xbox Game Studios
- Powu Windows, jëfekaay ak daliweb yi Microsoft siiwal
- Presentation Translator
- rise4fun
- Seeing AI
- Seetu Tëj bi ci Topp
- Send
- Skype in the Classroom
- Skype Manager
- Skype.com
- Skype
- Smart Search
- Snip Insights
- Spreadsheet Keyboard
- Sumbu Microsoft 365 bodul fay
- Sway.com
- Sàqum Microsoft
- to-do.microsoft.com
- Translator for Microsoft Edge
- Translator Live
- Universal Human Relevance System (UHRS)
- UrWeather
- ux.microsoft.com
- Video Breakdown
- Visio Online
- Waññi Bing
- Web Translator
- whiteboard.office.com
- Windows Live Mail
- Windows Live Writer
- Windows Movie Maker
- Windows Photo Gallery
- Xbox Game Pass
- Xbox Live Gold
- Xbox Live
- Xbox Music
- Xbox Store
- Xëti Bing